THE WORLD BANK GROUP A World Free of Poverty Home xam-xami cosaan ngir yokkute gi Làngug yëngu yi Weeru Nowàmbar ci atum 1998 Kër giy saytu yéenéek xam-xam Diiwaanu Afrik Bànk Monjaal Nataal bii, R. Kiessling, GTZ, Eschborn moo ñu ko baaxe: Jigéeni réewum Mali yuy cuub ay ndimó di jëfandikóo xaralay "Bogolaa". XAAJ BI JËKK Lan mooy xam-xami cosaan ? Lu tax xam-xami cosaan yi am solo ? Lan lañ Nisër ci xam-xami cosaan yi ? Lan la liggéey bii juragum? ÑAAREELU XAAJ BI - LAN MOOY XAM-XAMI COSAAN ? ÑETTEELU XAAJ BI LANGUG YÉNGU YI BOOTAL YI Bootal 1 Bootal 2 kërale 2 kërale 3 kërale 4 kërale 5 ÑETTEELU XAAJ BI Jubbi bi ñeel lépp lu jëm ci xam-xami cosaan yi. XAAJ BI JËKK Lan mooy xam-xami cosaan ? pajum xob ak reen misaalu xam-xami cosaan la boo xam ne dafa mos di am solo ci nit ñi ak fu ñu mën di nekk di àdduna si. Li ñu ci jot a bind joxewul gi-gis boo xam ne ñépp a ci ànd, bokk nu ñu ko deggé. Terewul ba tey mu am ay màndarga yu bari yu leen wutaleeg yeneen xam-xam yi. Ni aada yeek waaso yi wuutée la xam-xami cosaan yi di wuutée. Ci xam-xami cosaan yi lañuy sukkandiku ba jàpp ni ñuy war a defe ci wàllu mbéy, wér-gi-yaram, caytum càkkéef yeek lépp lu nu mën di yéngu Xam-xami cosaan am nañu wàll ci ni nit ñi di doxale diseen digante, ni yeen yi di tëdde, li nit ñi war a séq ak aada yi. Li ëpp ci xam-xam yooyu de ñu leen di donn moo tax tënk leen nekk lu jafe. Gëstu gii dafa ciy joxe ay misaal, am xam-xami cosaan yu may wone seeni melo, boolewaale ci itam njàng mu am solo muy ci mën a jariñoo ci wàllug yokkute. Ci kow loolu lay joxe misaal yii : • Mbéyum xeetu ñebbe ju bees ca réewum Kolombi ak mum Ruwaanda. • Céddalem dund gu ñu démbaléewoon nit ñi ca Nepaal. • Dogu gu jigéeni Malikunda ci réewum Senegaal dogu di jële fi njongum jigéen. • Njoof gu ñuy njoof jigéen ju wasin ba noppeek liiram ci xeet wi tudd Ibo te dëkke réewum Niseryaa, añs. Lu tax xam-xami cosaan yi am solo ? Foo dem, ci xam-xami cosaan lañuy sukkandiku be lal pexe yu ñu faje jafe-jafe yi ñu jankonteel, rawatina ñi seen loxo jotul seen gannaaw. Xam-xami cosaan yi am nañu doole lool ci xam-xam yi mën a indig yokkute. Waaye liñ leen di jëfandikóo ci doxalin yi yokkute tax a jóg néew na lool. Jàng ay xam-xami cosaan, doore ko ci li nit ñi xam te ame ko, dina tax ñu gën a xam ni nit ñi dundé, su ko defee ñu gën a xam liñu war a def ba dimbale leen ndimbal gi ñu yelloo. Gannaaw loolu, am lu leer ci xam-xami cosaan yi mën naa tax ba nit ñi gën leen a faale. Rax ci dolli, fexe be lépp lu ñuy def méngook ni nit ñi di dunde, mën naa tax ba ndimbal gi yokkute tax a jóg ëpp fi njariñ te njariñ yooyu sax fi ba abbadan. Weccantey xam-xami cosaan ci askan wi walla diggantey askan mën naa gën a dimbale nit ñi ñu gën a xam li leen wutale ba gën a jox gëdda aada ci wàllu yakkute. Li ci ëppati solo nak moo di, def ci weccantey xam-xami cosaan ak seenug bokk ci sémbu ndimbal yi Bànk Monjaal ak ñi mu jàppool ngir indi yokkute, mën naa gën a wàññi ñàkk gi. - xam-xami cosaan ngir yokkute gi - yëngu yi ñu taxawal Lan lañ Nisër ci xam-xami cosaan yi Tas xabaar bi •Suuxat sàqum xam-xami cosaan yeek liñ ci mën a jànge. • Siiwal ay misaali xam-xami cosaan ci jumtukaay yu ñu bind ciy kayit walla cib masiin. Yombal weccantem xibaar ci diggante ñi nekk ci dëkk yi ci réew yu néew doole yi. • Ndimbal ci lu yokk mën-mëni nit ñi nekk ci dëkk yi ngir ñu bokk xam-xami cosaan yi. • Xam niñ war a def ba dugal xam-xami cosaan yi ci masinu ordinaatóor, tas leen ba ñu yegg ci nit ñi ci dëkk-dëkkaan yi. Lan la liggéey bii juragum? Bi ñu dooree làngug xam-xami cosaan yi ba léegi, li gën a fés ci liñ ci jëlé mooy : • Yékkéti sàqum xam-xami cosaan bu def lu toll ci ñeen-fukki misaal. • Sos yoonu "Enternet" buy joxey xabaar yu aju ci xam-xami cosaan yi. • Siiwal kayitu tasukaayu xibaar bi tudd "Mbind ci xam-xami cosaan yi" te ñu jaglee ko xam-xami cosaan yi. • Gëstu ci xam-xami cosaan yi. (seetal ci bootal 1 ngir xam li mu ëmb). ÑAAREELU XAAJ BI 1 - (1 ) Jàppóo gu dëggu ci diggante réew yi ngir weccantey xam-xam du mën a antu te doonul ne réew yi néew doole dañ cee dugal seen loxo, taxaw ci taxawaayu ñuy joxe ak di jëfandikóo xam-xam yi. Ndaje ma amoon Torontóo ci weeru SuweN bu atum 1997, fésaloon na ne dañoo war a sàkku xam-xami cosaan yi ngir ñoN al leen te di ci weccante. Bu yàggul, njiitug Bànk Monjaal ci woote gi mu fi wootewoon ngir nit ñi am gis-gis bu yaatu ci yokkute fésaloon na ne dafa laaj taxawaay buy sóorale fu mu mën di tollu askan yeek seeni xam-xam. Ci jamanog jàppóo ngir jumtukaay yu xarala yi ñuy jokkoo ci Afrik, la Bànk Monjaal nangoo jiité sémbu xam-xami cosaan yi ngir yokkute, ngir indi ci ndimbal guy tax ñu nangu ne xam-xami cosaan am na, di leen jëfandikóo te di leen weccante ci yoonuw yokkute gi. Jamano jooju nak, ci lañ amal gëstu gii. II./ - LAN MOOY XAM-XAMI COSAAN ? 2 - (3) Pajum xob ak reen misaal mu baax mu xam-xami cosaan moo xam ne foo dem ci àdduna si fekk ko fa. Li ñu bind ci xam-xami cosaan yi, joxe wul benni gis-gis bu ñépp déggóo. Bokk na ci li waral loolu wuute gi am ci li soxal bindkat yi dale ko ci ngëmu nit ñi ba ci pexey mbéy. Waaye, loolu terewul mu am cingis-gis ay melo yu ñu bokk. Melo yooyu feeñ nañu ci li ñaari kilifa bind ci xam-xami cosaan yi (seet ko ci néeg bii di ñëw). Yenn ci tekkini xam-xami cosaan. Xam-xami cosaan xam-xam yu cosaanoo fi ñu leen di jëfandikóo - foo dem fekk fa ay xam-xami cosaan yu fa fekk baax. xam-xami cosaan yi dañoo wuuteek xeeti xam-xam yi réew yépp dégóo te ñu leen di jànge ci daara yu kowe yi, gëstuwaay yeek yenn kër yi nga xam ne dañoo am ñu leen moomal seen bopp. Ci xam-xami cosaan yooyu lañu sukkandiku be nas pexe yi ñuy jëfandikóo ci wàllu mbéy, wèr-gi-yaram, togg, yar, caytum càkkéef yi, ak yeneeni mbir yu nit ñi bokk dëkk di yéngu. (waren 1991). Askan woo dem, xam-xami cosaan a lal lépp luñuy xamle. Xam-xami cosaan yeey yombal jokkoo beek li ñu fas yéenée def. Pexe cosaan yi nit ñi di jokkoo dañuy dox jamano ju ñëw ñu ànd ak moom Askan woo gis pexe yi ñu fay jëfandikóo dañuy dox, lu ñëw walla ni muy jokkook ñeneen dañuy am lu ñu ciy soppi. 3 - (6) Melo yi ñu fi jot a wax, wone nañu ne xam-xami cosaan yi dañoo bokk ci pexey yi mën a indi yokkute ci askan yi. Xalaat bi ñu amaloon ci jokkute ci àddinasi ci atum 1998 jàpp 1999, feeñal na ne xam-xam a mën a indi yokkute ci wàllu dundi doom-aadamaak koom-koom gu sax waaye du ay koppar. sukkandiku ci xam-xami cosaan yi nga xam ne ñoo lal xam-xam yi nit ñi jëfandikóo lañ war a jëkk a def bu ñu bëggée réew mu neKK jariñoo ay xam-xamam. Rax ci dolli, nit ñaa ngi gën a déggóo ci jàpp ne weccantey xam-xam dafa war a nekk yoon wu nit ñi di jëflantee. Tasaarem xam-xam, ci réew yi am doole rekk la xam-xam bi di bawoo jëm ci reéw yu néew doole yi du mën antu te dina am ñu yaakaar ne dañu leen xeeb. "Nguur yeek kuréel yi réew yi séq war nañu mën a dimbale reéw yi ci yéngu yi jublu gëstug ni yeneen réew yi di fefe ngir mën a ràññee xam-xam yi leen gën a jubu, jëfandikóo leen seet, waaye ñu ngi doon gën a am ndam su ñu dimbalewoon reéw yu néew doole yi ñu fexe ba méngóo am digante xam-xam yeek fi ñu leen di jëfandikóo. Dimbalé néew doolé yi ci xam-xam a ngi gën a mën a nekk su fekkee ne dañoo sàkku ci ñoom xam-xam yi aju ci seeni saxlaak anam yi ñu leen di jëfandikóo. "Ci kow loolu, lépp lu jëm ci yokkute, rawatina yi nga xam ne néew gi doole yee leen yékkéti, jamono yu ñu leen di nas walla ñuy doxal jéego yi ci bokk, dafay laaj ñu yebe xel xam-xami cosaan yi. 4 - (8) Mbër mi (jafe-jafe bi) askan wi (gën a jankoonteel) mooy am pexe yuy tax ñu gën a xam kuréel yeek doxalinu cosaan yi, te bu ko laajee ñu fexe ba xarala yu bees yi (maanaam yi gën ci doxalin yi nga xam ne yemuñu ci menni réew doN N ) dëppóok doxalinu nit ñi. Noonu doN N la xam-xam yu yaatu yi di mën a àndeek soxlay mbooloom doom-aadama mu nekk ci fi mu dëkke li ëpp solo ci kow yoon wi ñuy jaar ba xam-xam bu ñëw ñu jëfandikóo ko ci anam yi dëppóok ni nit ñi di dunde moo lépp lu am, ñu fexe ba ñi am xam-xami cosaan dugal ci seen loxo. Ag gëstu gu ñu amal ci 121 porose yu nekk ci kow gi di tappatoo lu jëm ci ndox ci 49 réew, feeñal na ne su ñu ci jëlée 100 yoo xam ne nit ñi tax ñu jóg dañoo bokkoon ci ñi doon nas porose bi, 70 ya am nañ ndam yu takku, te bu dee ñi nga xam ne loolu amul ca woon, 10 doN N a ci am ndam. Ni ko misaal yi di ñëw firndéele, xamug ni nit ñi di doxale ci fi ñu dëkké, boole leen ci lépp lu ñu fa nar a amal mën nañoo doon pexe yuy tax ba yi gën ci jëfin yi ñuy jëfandikkóo te réew yi bokk leen dëppóok ni doom-aadama yi nekke fi ñu dëkk. Misaal 1: Jëfandikóom jiwu ñebbe wu bees cà réewum ruwànda ak wum kolombi. Bi ñu jëlée ñaar ba ñetti jiwu ñebbe yi nga xam ne gëstukat yi jàpp nañu ne ñoo dàq a meññ taxul ñebbe yokku ni ñu ko foogewoon. Noonu, gëstukat yi ne dañuy woo ci béréb bi ñuy gëstóo beykat yu jigéen yi nga xam ne am nañ xam-xam cosaan ci mbéyum ñebbe ngir ñu xoolal leen lu toll ci ñaar-fukki jiwu nebbe yii, tànn ci ñaar ba ñett yi ñu jàpp ne ñoo gën, bey leen li ñu am ci jiwu yi ñu tànn ëppe ne lañu amoon ca jiwu ya gëstukat yi 60 ba 90 ci téeméer yoo jël. Ñu jànge ci ne : Xam-xami cosaan mën naa xamle lu am a am njariñ ci ni ñu war a jëfandikóo pexey mbey yu bees yi. Misaal 2 : Ay dëkki-dëkk fexel nañ seen bopp ni ñuy séddalee dund gi ñu leen dimbalee leer (aw yoon). Ngir mu wóor leen ne nit ñi dinañu jot ci dund gi ñu leen di dimbalée, ab sumb bu tudd "fud foo wok" (maanaam liggéey ñu jox la loo lekk) te nguurug Nepal amaloon ko ci ndimbalug kuréelu See-Tee-Sed (GTZ) la ñu wax nit ñi ne moom lañ fas yéene amal ak ñoom. Ci loolu la ñépp déggóo ne dëkk bu nekk, ci ña fa dëkk lañuy tànn ñiy séddale, waa dëkk bi di xool ni céddale mi di doxe, moo gën a rafet ci anam yi ñu war a séddalee dund. Li ñuy jëlé ay kamyo , ar sareti nag lañuy sëf dund gi. Njariñ yu bari amoon nañu ci doxalin woowu, taxoon na ba ñi joxe saret, li ñu waroon a jot ci dund gi yokku, te loolu naruloon a am su fekkoon ne dañoo jëloon boroomi kamyoN bu bawoo réew taax. Rax ci dolli, ndégam sëfu saret bu nekk xam nañu natt bi mu tollol tax na ba nit ñi xam ni dund gi ñu séddalé yem. Ci noonu itam la ñuy xame ci lu yomb lépp lu waroon a ñëw te ñëwul ni mu toll ci mbooloo mi, te lu réer wallu ñu joxe ko ci lu ñu leeralul, dinañ ko mën a waxtaane ci biir nit ñi. Yeneen sémb yi ni meloon ca réew ma dañoo mujjéwoon jëfandikoó doxalin wii. Nu jànge ci : Jëfandikóo nattukaay ak jëfukaayi cosaan yi, ci sémbub "liggéey ñu féy lag lekk " dina yombal joxeg dund gi te nekk misaalu doxalin wu amul benn njuuj-njaaj cib dëkk. 5 - ( 11) Ci gàttal, xam-xami cosaan yi dañoo am njariñ ci néew doole yi ci fànna yii : - Mbéy - yarum jur ak ni waaso wu ne di faje mala - ni ñuy jëfandikook, ni ñuy saytoo càkkéef yi - li ku nekk war a xam gën gaa néew ci wàllu paj pexe yi ñuy aaroo ci jàngoro yi, pajum feebaru xel - Rënk ak able (leble) - yokkute gu daj ñépp - xeex (bëreek) ñàkk gi 6 - ( 13 ) Ba tey, misaal yi di ñew firndéel nañu ne foo dem, ñi fa dëkké mën nañoo tàkku taxaw ngir soppi aada yi nga xam ne dañuy gàllankoor seenug dund. Misaal : Ci réewum Senegaal, ay jigéen ñu nekk ci kow gaa ngay jëlé njongum jigéen ci seeni dëkk. Jigéeni Malikundaa fas nañ yéenée song jafe-jafe bii di njongum jigéen, di aada bu waaso yu bari bokk : Bàmbare, Soose, Pël, Joolaa, Sooninke ... Bi ñu fexee ba xam li am feneen ak musiba yi ngong mën a indi ci wàllu wér gi yaram ak séyu jànq ji, ci lañ ame lay yu taxaw ba mujj magi dëkk bi dogu ne njongum jigéen dootu fi ame. Loolu taxul xoli jigéen ñi sedd, dañoo daldi taxawal seenug kuréel ngir seeti seen moroom yi nekk ci dëkk yi leen wër, waxtaan ak ñoom, ngir jàppale leen ñu soppi yenn mbir yu am ci seeni dëkk. Weeru saN wiyé ci atum 1998 lañu amal pénc mu mag mu dajale fukki dëkk ak juróom benn yu nekke ci diiwaanub Cees ñépp di bambara walla Meting ngir waxtaane mbàyyim njongum jigéen ba noppi sàlloo "kàddug Malikundaa". Bi ko waa kaasamaas déggée, fukki dëkki pël ak juroom benn daje nañ fa ñoom itam amal fa pénc mu ni deme, tënk fa xalaat bu deme ni ba "kàddug Malika" ëmboon. Nes tuut, Peresidaa Abdu JUUF, njiitum réew mi ci boppam ne xalaat bii tudd "waatup Malikundaa" dafa wara daj réew mi. Ñu jàng ci ne : Ñépp bokk gis-gis mën nañoo dimbali ba ñu soppi yenn aada yiy indi gënaatle. Misaal mii wone na itam ne xam-xami cosaan nekkul loo xam ne kenn warul cee mën dara. Njongum jigéen aada la bu amee soppiku yu ci am mën nañoo wax ne yàllaak liggéey bu ag mbootaayu jigéen def, xëccaale ci ni dëkk bi di doxale, sukkandiku ci jumtukaay yi dëkk bi di doxe ci sosaan ak yu bees yi. 7 - (15) Yenni xam-xami cosan yi mën nañoo dem ba réer. Su boobaa, mën na am ñu mu lor, te ñi ciy jëkk ñooy ñi leen doon suuxat di leen dunde. Gën a fullaal xam-xami cosaan yi mën naa am lu mu yokk ci yoon wiy indi yokkute, tax ba ñu tëyé ci askan wi boroom mën-mën yu takku, ay jumtukaay, ay mbiri cosaan ak ay pexey pajtalum jafe-jafe. Xam-xam bu ni deme dina faral di am lu mu def ci yenn xalaat yu soxal réew yi. Ci kow loolu, sàmm sàqum xam-xami cosaan yi mën naa tax xéewal yi ci àddina si yokku te dina taxit ba ñu gëna gis ni aada ame doole ci yokkute. Léep itam, xam-xami cosaan yi mën nañoo indi ndimbal ci niñ war a aare li ñu wër, ni ko misaal miy ñëw wonee. Misaal : Aar beykat yiy jëfandikóo xam-xami cosaan yi ci dëkk bu nekk. Mbooloom réew yaa ngi taxawal ay sàqu jiwu ngir aar li ñu xam ci wàllu jur, fu nekk ak gancax ak mala ya fa fekk baax. Ni gancax yooyu di meññe ak xam-xami beykat yi niru nañ lu am solo ci liggéey yi ñu war a sumb ci mbéy mi, ngir jàngoro yeek gunóor yi duñu mën a yàq, walla yeneen jafe-jafe yi aju ci jàww ji (wor , sedd, tàngoor,...). Waaye nak, sàmm ni gancax walla mala di jure te aaruloo xam-xam yi aju ci fi ñuy jaar ba meññ mel ni ni amul jariñ, ndaxte pepp yeek njëmbat yi ñu denc ànduñook luy wax ni ñu war a def ba ñu màgg. Ci kow loolu, béréb yiy saytu jiwu yi war nañoo jege sàmm yeek beykat yi nga xam ne ba tey ñu ngi liggéey ci xeet yi fekk baax fi ñu dëkk moo xam mala walla gancax la, ngir xam-xam ak m¨n-mën deme noonu bañ a réer. Nu jàng ci ne : xam-xami cosaan mënul fee jogé su nu bëggée aar ni xeeti gancax yi baree te wuuté. 8- (16) Misaal yi ni weesu wone nañ ni : •Dekk boo dem, xam-xami cosaan yi mën nañ leen a jox ay pexe yu ñu faje seeni jafe-jafe, rawatina ca néew doole yi. • Jang ay xam-xami cosaan yi tëdde, dina yokk pas-pasu ñi ñuy jëflanteel ci dëkk yi. •Sukkandiku ci jaar-jaari doom aadama yi, ni ñu gise jafe-jafe yi ñu jankonteel ak li ñuy def ci fiñ dëkk, mën naa tax ba sémb boo xam ne yokkutee ko tax a jóg gën a am njariñ, weesu mbirum tono (ci anamu def nangam mu jural la nangam) joo am gannaow ba joxee alal ju ñu liggeéyé • Ni dëkk bu nekk gisé yokkuté mën naa indig ndimbal ci moomeel gi (ci ñi moom mbir yi), mu nekk lu mën a indi njariñ ci ñi di jëflanteek ndaw ñi fa toogal nguur gi, jox waa dëkk bi jumtukaay yu ñu mën a wottoo digante boobu. •Xam-xami cosaan yi doon nañu fu ñu mën a sukkandiku ba jox way-ñakk yi doole. ÑETTEELU XAAJ BI IIII / LANGUG YÉNGU YI Dog bii dafay wone ag làng gu ñuy yéngu ngir daan jafe-jafe yi dëkk diñu teree lëkkale xam-xami cosaan yeek yoonu yokkute wi. Làng ngaa ngi ci ñeenti ponk la sukkantdiku (seetal ci 2 eelu bootal bi, dog 2 ba 5 ) ngir xam li ponk yooyu ëmb, fànna yi ñuy yëngu yi leen war a mottali ngir gën a mën a lëkkale xam-xami cosaan yeek yoonuw yokkute wi. => Tasaare xibaar bi. Yéngu yi ci ëpp solooy : • Taxawal te suuxat sàqum xam-xami cosaan, liñ ci mën a jàng, fi ñu jóge, ñi ci jàppoó, añs. • Fexe ba xam jumtukaay yi ñu war a am ba dugal xam-xami cosaan ci masiinu "ordinaatóor, "tasaare leen su ko defee, ñu seet jumtukaay yooyu ba mu wóor. • Siiwal ay misaal yu ñu tànn, ci kayit walla masiin. => Yombal weccantey xam-xami cosaan yi ci diggante dëkk yi ñeew doole. Yéngu yi ci ëpp solooy : • Dëkk bu nekk ñu dimbale leen ci lépp luy yokk seeni mën-mën ngir wéccantey xam-xami cosaan am rawatina ci diggante kër yi ñu taxawal ci dëkk yi ngir ñuy saytu xam-xami cosaan yi. • Seet pexe yu ñu war a jëfandikóo ba bind, siiwal xam-xami cosaan yi ci dëkk yi. • Pexe yoon wi àdduna sépp war a jokkóo di ci weccantey xam-xami cosaan yomb a taxawal. => Tàggat ñi jàppóo. Yéngu yi ci ëpp solooy : • Foo dem jànge ci ña fa dëkk ak kuréel yi jokkuwul ci genn nguur. • Jël lépp lu ñi jokkoo an ngir am njariñ yu gën a takku ci wàllu yokkute. • Toppatoo ba xam ki moom xam-xami cosaan yi. Làng ngi ñu leen wax ci kow la, bi ko jokkoo gi ñu suuxat ngir xam-xami cosaan yi jëfandikóo la nas pexe mi ñu war a yéngu ci atum 1998 jàpp 99. Nisër yi ñi jàppóo am lañ tënk ci àlluwa jiy ñëw. Taxawal nañu itam ag kuréel gu ñuy diisóol ngir nuy xelaate ci lépp lu jublu ci pexeek lu ñuy def (seetal ci bootal I). Bi ñuy yëngu ngir am li ñu déggóowoon ba nisër ko, ci kow làng gi ñu wax ni mu deme ci kow, ñi lëngoo liggéey nañ bu baax a baax ak kër yiy saytu xam-xami cosaan yi di dëkk jumtukaay yi ci mën a am). Li leen gën a soxal mooy fexe ba ñu gën a fullaal solo si xam-xami cosaan yi ci am, ràññee siiwal xam-xami cosaan te gën a yokk mën-mënu kër yiy saytu xam-xami cosaan yi ci dëkk yi ngir gën a mën a ràññee, bind te siiwal xam-xam yooyu. Loolu mën naa dugal ag ndimbal ci wàllu koppar ngir gëstu gi ci ni ñuy defe ci wàllu xam-xamu cosaan, jokkale kër yiy saytu xam-xami cosaan ci dëkk yi ci yoon wi tudd "Enternet", niki noonu jumtukaay yi ñuy tasaaree xibaar ci yi gën a nekk yu cosaan nga xam ne mën nañoo yombal weccantey xam-xami-cosaan yi ci digante dëkk yi. Bi ñu dooree làngug xam-xami cosaan yi ba léegi, li gën a fés ci liñ ci jëlé mooy : • Yékkéti sàqum xam-xami cosaan bu def lu toll ci ñeen-fukki misaal. • Sos yoonu "Enternet" buy joxey xabaar yu aju ci xam-xami cosaan yi. • Siiwal kayitu tasukaayu xibaar bi tudd "Mbind ci xam-xami cosaan yi" te ñu jaglee ko xam-xami cosaan yi. • Gëstu ci xam-xami cosaan yi. (seetal ci bootal 1 ngir xam li mu ëmb). Xam-xami cosaan ngir yokkute gi : pexe yi ñuy yëngu : atum 1998 jàpp 1999 Nisër yi Li Sémb bi indi Li ñi jàppóo indi Yëngu 1 : Tasaare xibaar bi Suuxat sàqum xam-xami cosaan, liñ ci mën a jànge, fi ñu jóge, ñi ci jàppóo. Gën gaa néew 200 xam-xami cosaan a dugg ci sàq mi ci "Enternet". Kenn ku nekk ci ñi jàppóo joxe na gën gaa néew fukki (10) xam-xami cosaan. Xam jumtukaay yi ñu mën a dugale xam-xami cosaan yi ci masinu "ordinaatóor " ak yi leen di siiwal te seet leen ba xam. Gindikaay gi ñu war a sukkandiku ngir jëfandikóo jumtukaay yi aju ci misaal yi. Ku nekk ci ñi jàppóo jox na gën gaa néew benni (1) misaal. Bànk Monjaal a ngi waajal ak a tasaare ag gindikaay gu ñuy sukkandiku. Siiwal ay misaal yu ñu tànn bind leen walla ñu nekk ci masin gën gaa néew 24 kayitu tasukaayu xibaar te tudd "Mbind ci xam-xami cosaan yi" Kenn ku nekk ci ñi jàppóo joxe gën ngaa néew benni dog. Bànk Monjaal siiwal te tasaare. Nisër yi Li Sémb bi indi Li ñi jàppóo indi Yëngu 2 : Yombal weccante xam-xami xosaan ci digante néew doole yi Indig ndimbal ci lépp luy yokk mën-mën yi ngir ñu bokk xam-xami cosaan yi. Gën ngaa néew fukki (10) këru xam-xami cosaan am nañu yokkute ngir li ñu jokkook kuréel yu gën a kowe, gën a mën a ràññee xam-xami cosaan yi. Kenn ku nekk ci ñi jàppóo yokk na doole genni kër gën gaa néew. Xam pexe yi ñu mënee dugal xam-xami cosaan yi ci masin te tasaare leen ci nit ñi. Gën gaa néew fukki (10) misaal ci wàllu weccantey xam-xami cosaan ci digante dëkk yi nga xam ne antu nañ. Kenn ku nekk ci ñi jàppóo jàpp na ci benni (1) misaal gën gaa néew. Bànk Monjaal tasaare. Fexe sos yoon wu àddina sépp di weccantey xam-xami cosaan doon lu yomb Mu am gën gaa néew fukki "Telesàntar" yu jot ndimbal gu jëm ci weccantem xam-xami cosaan yi. Kuréel yii See-Er-Dee-ii (CRDI), ii-Tee-i (UTI), Pë-NID (PNUD) ak Bànk Monjaal kenn ku ci nekk dimbale lu mu bon-bon benni Telesàntar. Yéngu 3 : Jëfandikóo xam-xami cosaan yi ci yoonuw yokkute wi Fexe be kilifa yi jiité réew yeek yu kuréel yiy toppatoo mbirum yokkute ci àddinasi gën a fullaal xam-xami cosaan. Lëlub liggéey buy dajale liggéeykatu kuréel gi ñu jàppóol. Waxtaan wu yaatu wu ñuy amal ci xew-xew boo xam ne ñi jàppóo lañ ko ndeyale ci xam-xami cosaan yi. Ndaje mi am ci diiwaan bi te ñu fa doon waxtaane xam-xami cosaan yi (atum 1999). Kenn ku nekk ci ñi jàppóo amal lu mu bon-bon menni ndajam liggéey. Lu mu néew-néew kenn ku nekk xewle benni yoon. Bànk Monjaal amal ndaje mu mag mi (ñeneen ñi joxe seen ndimbal). Dugal xam-xami cosaan yi ci sémb yi ñuy dimbalée sunuy réew Fukki (10) sémb yoo xam ne ba ñu leen di nas jëfandikóo nañub xam-xamu cosaan. Képp ku ci bokk jot gën gaa néew benni sémb buy jëfandikoób xam-xamu cosaan. Yëngu 4 : Jàngal ñi jàppóo ci liggéey bi Jànge ci ñi ñu jàppóol ci dëkk yi ak kuréel yu ajuwul ci genni nguur Xam te wone ci porose yi ñi jàppóo dimbale, yi ci jëfandikóo bi ñu leen di nas xam-xami cosaan yi. Gën gaa néew, sémb bu nekk ak kenn ku mu jàppóol. Bànk Monjaal tasaare. Nisër yi Li Sémb bi indi Li ñi jàppóo indi Dajale tuut si ñi ñu dimbalée ngir njariñ la gën a am solo ci béréb yi ñuy yéngu. Lëkkale/jokkale liggéey yi ñi jàpóo def, ci yoon wi ñu xàll ngir yëngu ci xam-xami cosaan yi. Ku ne ci ñi ñu jàppóol ngir yokkute am, joxey koppar te doxal ay jéegéy boppam yu woroowul ak yoon wu mag wi ñu xàll ngir yëngu ci lu aju ci xam-xami cosaan yi. Toppatoo wareefu boroom xam-xami cosaan yi. Seet jéegó yi mu laaj. Oo-Em-Pee-Ii (OMPI) mooy jiité liggéey bi ñu def ngir xam jéegó yi ci war. Ñi teewoon ca ndajem atal ma ñu amaloon ca Tinis, ci 22 fan ci weeru Oktoobar, atum 1998 àndoon nañu ci palaK bii. BOOTAL YI Bootal 1 Won leen ni pexem xam-xami cosaan ngirug yokkute mi tëdde Waxtaan wa amoon ci weeru suweK, atum 1997 ca Toronto réewum Kanadaa, dafa fésal ni soxlas jàng; aar ak weccante xam-xami cosaan yi jàmpe. Ci jamono jig jàppóo amee ngir xarala yi ñuy jokkoo ak di ci tasaaree cibaar yi ci Afrig; la Bànk Monjaal nangoo jiite pexeg xam-xami cosaan yi ci yoonuw yokkute wi. Allal ji ci Bànk Monjaal a ngi jóge ci koppar yu mu maye ci sumb bi tudd " Innovation Marketplace" maanaam " lu bees li ñu indi ci ja yi". Ñi jàppóo (lëngóo) ÑII; BOKK NAÑ CI ÑI JÀPPÓO NAS PEXE MU BEES MI: - CEA di bànqas giy saytu koom-koom ci Afrig. - CISDA di kër gu kuréel yiy toppatoo mbirum yokkute ci Afrig di wecaantee xabaar - CRDIC di Kër gi ñuy gëstóo yokkuteg réew yi te nekk Réewum Kanadaa - UIT di mbootaayu kuréel yi réew yi séq di ci toppatoo jokkoo digante ñoo xam ne dañoo sorewoo. - UNESCO di banqaasu mbootaayu xeet giy saytu yar mi, xam-xam yu xarala yi ak caada. - PNUD di sumb bi mbootaayu xeet yi sumb ngir réew yi amug yokkute. - OMS di mbootaay giy toppatoo mbirum wér gi yaram ci àddina si. Ci digante bi am na ñeneen ñu leen ci fekkisi - CIRAN di mbootaa gu fekk baax ca réewum Olànd tey toppatoo ni réew yi di demlantee ci wàllu njàng mu kowe mi. - SANGONET kuréel la gu jokkuwul cig nguur , fekk baax ca réewum "Afrig dii Siid" nga xam ne moo def lëpp lu aju ci Enternet ( maanaam jokkoo goo xam ci masiinu Ordinaatóor lañ ko jaarale ) - OMPI : mbootaay miy saytu àq ak sañ-sañi boroom xam-xam yi ci àddina si. - OIT : di mbootaay miy toppatoo àq ak sañ-sañi liggéeykat ci àdduna si. Nisër yi Tas xabaar bi •Suuxat sàqum xam-xami cosaan yeek liñ ci mën a jànge. • Siiwal ay misaali xam-xami cosaan ci jumtukaay yu ñu bind ciy kayit walla cib masin. Yombal weccantem xibaar ci diggante ñi nekk ci dëkk yi ci réew yu néew doole yi. • Ndimbal ci lu yokk mën-mëni nit ñi nekk ci dëkk yi ngir ñu bokk xam-xami cosaan yi. • Xam niñ war a def ba dugal xam-xami cosaan yi ci masinu ordinaatóor, tas leen ba ñu yegg ci nit ñi ci dëkk-dëkkaan yi. BOOTAL II Kërale 2 : Yokk te gën a jàppandil xabaar yi fi am ci xam-xami cosaan yi Fànna yi ñuy yéngu Taxawaay Jéegó yi ci war Doxalin Tëyé te dajale lépp lu am ci xam-xami cosaan yi •Gëstu takku yu ñu def ci ni doom aadama yi di dunde yuy joxe ay xabaar ci xam-xami cosaan yi • Bés bu set, gëstu yi dañuy gën a yokku niki liggéey yi ñuy amal ci dëkk yeek ndajey liggéey wall waccantey xalaat ci mbirum xam-xami cosaan. •Li ëpp ci gëstu yi y wone ni xam-xam yi mel a ëpp yiy wone seeni ngënéel ak seeni rëq-rëq te néew na lu ñuy dellusi ci dëkk yi ñu defewoon gëstu yi waxtaan ak nit ñi ci li ñu gis. • Pexe yuy tax ba ñépp bokk ci ñiy lëñbati xam-xami cosaan yi, leeral leen ba dajale leen foo xam ne dinañ yomb a jëfandikóo. • Ay pexe yu ñuy taxawale sàq mu ñuy def xam-xami cosaan yi ñu dajale. • Gëstu ci dëkk yi • Ay gëstu •Ay ndajey liggéey •Jëflanteek Oo-See-Bee (OCB) yeek Oo-En-See yi (ONG) Seet te jëfandikóo pexe yi ñuy taataane xam-xami cosaan yi, niñ leen di jëfanfikóok ni ñuy def ba ñu àgg feneen. •Gëstu yi am ci pexe yi lu néew la •Yenni porose yi dinañuy seet nit ñi ak ay pexe yuy tax ba ñépp bokk. •Porose yiy sóoraale tënkum ni ñuy jëfandikóo xam-xami cosaan yi. •Lu baree-bari ci porose yu Oo-En-See yu ndaw yi dañuy jëfandikóo xam-xami cosaan yi waaye ñi ci tënk seeni jaar-jaar néew na waxatuma nak di ci weccanteek ñeneen. •Jàppale Oo-En-See yi ñu bind te leeral seeni jaar-jaar. •Gëstu lépp lu aju ci ni ñuy yóbboó xam-xami cosaan feneen. •Seet ndax porose yeek ni ñuy jëfandikoo xam-xami cosaan mën nañoo yokku •Gëstu pexe yi •Seet porose yiy taataan xam-xami cosaan yi di leen jëfandikóo •Xam ñi jëfandikóo xam-xami cosaan yi, toxal leen feneen te am ci ndam. Fànna yi ñuy yéngu Taxawaay Jéegó yi ci war Doxalin Yonnal xam-xami cosaan yi ( fexe ba yoon yiy dox ci réew yi nangu amug xam-xami cosaan) •Bariwul ñu ci góor-goórlu (su weesoo gëstu yi ñu def ci gancax yiy faj) ; xabaar yiy wax li xam-xam bu nekk di jariñ yombul a am ; li ñu xam ci xam-xami cosaan yi ñu yóbbu feneen mu antu néew na. •Dem seet ko ci dëkk yi, kuréel yiy toppatoo mbirum gëstu gi ci réew mi def ci ay gëstu, boole waale ci lépp luy indi ay leeral ci wàll koom. •Yër jumtukaay yi ñu jotoon a tënk ay xam-xami cosaan ci ndoorteelu xarnu bi. Moo xam boroom xam-xami tubaab, walla ñiy jëfe xam-xami cosaan yi walla muy waa kër làbbe yi. •Yër li ñu jot a tënk ci pexe yu xarala yu ñu toxal te mu bawoo ci xam-xami cosaan yi. •Dajale gis-gisu ñi leen di jëfandikoó • Seet leen ci dëkk yi ba xam •Taxaw gëstu •Seet leer ci lëñbatuwaay yi (laboraatuwaar) •Tënk li jot a antu ci wallu jëlé xam-xami cosaan yébbu feneer. Fexe ba ñépp mën a jot ci xabaar bi •Ci at yu mujje yii, limu xam-xami cosaan yi ñu tënk, weccante ci dafa yokku (téeré, kayitu tasukaayu xabaar, widewoó, waxtaan añs), waaye faramfance gi des naa leer. •Xabaar bu am doole (bawoo ci daara yi tey woney melo) jàppandi na ci web bi. •Nu ngi defar turi ñi koy jëfandikóo. •As lëf ci sàq yu def xam-xami cosaan yi aju ci mbirum gancax gi. • Gën a defaraat yoon yi ñuy jokkoo ci diiwaan yi ngir weccante xam-xami cosaan yi gën a jëm kanam (fi ñu bawoo, porose yeek nit ñi ciy yëngu). •Gën a yaatal tasukaayu xabaar yi. •Taxawal ay sàqi xam-xami cosaan yu ñépp mën a jot. •Defar te tasaare téeré yi, jumtukaay yu ñu mën a seetaan walla ñu déglu ko ak jumtukaay yu ñu defar. •Amal ay waxtan yu yaatu •Dimbale yoon yi ñu xàll, kër yiy segg, sàqum xam-xam yi, kër yi ñuy wonee xam-xam yi, déncuwaayu cosaan yi am. Fànna yi ñuy yéngu Taxawaay Jéegó yi ci war Doxalin •Tasukaayi xabaar yaa ngi gën a teew ci ndaje yi ñuy def ak nit ñi ci dëkk yi. • Lëkkalewuñu bu baax jéegó yi aju ci xabaar yi ci réew yu néew dooleyi. •Li ñuy faral ci dajale di ko wone ci bérébu cosaan yi mooy ay jumtukaay yu ñu fi defare ñuy firndéel ne xam-xami cosaan am na. Kërale 3 : Fexe ba nit ñi gën a gis solo si xam-xami cosaan am te di leen jëfandikóo ci lépp lu ñuy yéngu mu jublu ci wàllu yokkute. Fànna yi ñuy yëngu Taxawaay li ñu war a def Niñ ko war a defe Fexe luy dollee tax nit ñi gën a gis gëdda ak njariñ lu takku lu xam-xami cosaan am ci : •waa dëkk bi •liggéeykat yi ci dëkk beek kuréel yi. •jàngalekat, boroom xam-xami tubaab ak ñi ci daara yu kowe yi. •njiit yeek ñiy lal pexe yi jublu cig yokkute joxe ay jumtukaay ak ay doxalin yu ñuy mënee tënk xam-xami cosaan di leen jëfandikóo ci porose yiy indig yokkute. •Yéngu yi taxaguleen a bari waaye ñu ngi yokku. •Am na ci yu waa dëkk bi bokk taxaw ci taxawaayu ku jàppóo walla kuy nas aka ñocci •joxewuñu bu baax xabaar yi jëm ci xam-xami cosaan yi ba ñiy dogal ak ñiy nas pexe yiy indi yokkute mën leen a jëfandikóo • yenn téeré doxalin yuy wone nangu gu nangu nañ ko gëdda walla màqaama gi xam-xami cosaan am (niki yoon yi Bànk Monjaal joxoñ ngir képp ku dem cib dëkk fas yéenée liggéey ak waa dëkk ba jaar ci) •liñ jot a def ci jëfandikoóm xam-xami cosaan yi kenn tënkul fenn. •Téeré gëstukat bi ci : ni ñuy tënke xam-xami cosaan ci pexe yu ñépp a ciy bokk te nekk fi ñu koy jëfe loxo walla ordinaatóor te kuréeli IIRR ak CIKARD waajal leen. •Am na ay gëstu yu fi nekk yoo xam ne mënees na leen a wone ci anam yu gën a yomb a jëfandikoó. •Boole ci waa bitim réew ngir nit ñi jot ndimbal luy tax ba ñu mën a tënk, gëstu te jëfandikóo seeni xam-xami cosaan. •Natt pexe yiy tax ba ñépp bokk. •Weccante xalaat am digante ñiy jëfé xam-xami cosaan yi. •Dugal xam-xami cosaan ci njàng mi. •Xabaar bu ñu jaglee njiit yeek ñiy lal pexe yi indi yokkute. •Yoon yi ñu xàll ci réew yeek bànqaas yi. •Fexe ba téeré yi gën fee baax. •Lal waxtaan yoo xam ne ciy fànna lañuy doon (misaal : xam-xami cosaan ak kaaraangeg jiwu yenni gancax yi. •Porose •Ndajem liggéey •Li ñu mën a xoole ci widewóo •Waxtaan, jumtukaay yu ñuy dégg ak walla di ko gis ak jàngaani. •Di demlante, suuxat ay téeréy "xam jëf" ngir bind, bokk, tasaare xam-xami cosaan yi. •Jumtukaay yi ñuy lale pexe yi, di ci doxal porose yi ngir mën a nangu, dëggal te dugal xam-xami cosaan ci lépp lu ñuy def. • Téere bu nekk ak ñi koy jëfandikóo ak ni ñu koy jëfandikóo •Dem ci dëkk, seet téeré yi ñu móol ba xam ndax baax nañ. Fànna yi ñuy yëngu Taxawaay li ñu war a def Niñ ko war a defe Tàggat liggéykat yi toogal nguur gi ci dëkk yi ak yu kuréel yi ajuwul ci genni nguur ci ni ñuy jëfandikoó jumtukaay yeek feem yi. •L ci jàppandi bareegul. •Saar yuy jàngalee feem yi ñuy tënke ak ni ñuy jëfandikóo xam-xami cosaan. •Tàggatukaay ak jàngalekaay i xam-xami cosaan yi. • Ay këri gëstu ak daara yu ñuy jàngalee ci dëkk yi • Séexale. •Tàggatukay ngir jàngalekat yi, kuréel yi ajuwul ci genn nguur, ñi seeni yëngu jublu ci yokkute añs. •Tàggat jàngalekat yi • Fexe ba digante ñiy weccantey xam-xami cosaan gën a rattax. Kërale 4 :Xàll yoon wu yaatu wu ñuy weccantee xam-xami cosaan. Fànna yi ñuy yëngu Taxawaay li ñu war a def Niñ ko war a defe Bokki pexe • Am na loo xom ne ñu ngi ko ciy def ci jamono yii (BTICA - Bellanet) •Allal ju yem •Kuréel yu jokkuwul ci genn nguur (Oo-En-See) yu ber seen saawos bopp. •Ay gëstu yu jëm ci xamtu ak mbind te dummoóyu weccante gi •Njariñu wall gi am ku ko moomal boppam ngir jumtukaay yu xarala yeek lu ñu defar. •Déggée ci ni ñuy bokke xabaar bi. •Méngale la ñuy def ak li réew yi dégóo. •Jàppóok Oo-En-See yeek ñi yor seen mbiru bopp. •Taxawal pencum weccantey xam-xam muy faral di am, te boot waxtaan yi réew yi séq. •Kuréel yi jokkuwul ci genn nguur, kuréel yiy saytu mbirum koppar yeek ñiy def seen mbiri bopp bokk di gëstu. •Jokku ci yoon yi ñu xàll niki sàqu xam-xami cosaan. Leeral jafe-jafe yiy lang ( yi nga xam ne kenn waxagul ci dara) •Jafe-jafe yi aju ci moomeelug xam-xami cosaan, nga xam ne ken waxagul ci dara. • Jëfandikóo walla jubbanti déggoó yi fi nekk. •Boot ndaje yu mag yi boroom xam-xam yi ci àdduna seek ñi am gëdda di amal. Taxawal kër yuy segg ci boppu diiwaan yeen biir diiwaan yi. • Taxawagul ci anam yoo xam ne ay réew a ci ànd, li am mooy yenn kër ci boppi diiwaan yi nga xam ne liñ mën dafa am fu mu yem. •Sàqi xam-xami cosaan •Làng gu ñuy weccantee •Kër yu dox te mën liñ leen di doye. •Tënk feem yi • Taxawu kër yi fi nekk ci dëkk-dëkkam yi Fànna yi ñuy yëngu Taxawaay li ñu war a def Niñ ko war a defe Fexe ba ñi tolloo di weccante •Weccantey xam-xam rawatina mu jogé ci suuf dem ci kow dellusi ci suuf ; jokkale gi ci wàllu woowoo ngi jëm kanam. •Dara doxul digante ñiy joxe xam-xam beek ñi koy jot. •Wàcce xàll yi •Ubbi fu ñuy bind xam-xam yi •Wonekat (tegtalkat ak kër yoo xam ne liñ fay def kenn du ko werante •Mbindum kàddu yi war •déggóo ci melo yi •Seet melo yi ba xam ndax dëppóo naak li ñu déggóo •Kër yi ñuy jokkoo gën fee baax. Kërale 5 : Jox ku nekk céram ci weccantem xam-xami cosaan yi Way jëf yi Fànna yi ñuy yéngu Li ñuy def Ñi ñu lëngóol Ñi bokk fuñ dëkke •Jàpp te ñoN al xam-xami cosaan yi. •Xamtu xam-xami cosaan •Yóbbu xam-xami cosaan feneen. •Dolli xam-xami li ñuy def •Yoonal jëf yi •Ràññee yi gën a fés ci fi xam-xami cosaan yiy jógé •Suuxat ay feem yu ñu leen di ñoN al •Xëccanteeg ñu nekk ci yeneeni dëkk • Oo-See-Bee, Oo-En-See •Liggéeyuwaay yiy yaatal •Liggéyuwaay yi takkul seen bopp. Oo-See-Bee (OCB); Oo-En-See (ONG) •Jàpp te ñoN al xam-xami cosaan yi te wutam ceen ay xamtu •Yóbbu xam-xami cosaan yi ci dëkk beek biir diiwaaw bi •Tasaare •Aar •Joxe ay bérébu xamtuwaay te doxal leen (kàggu, sàqum xam-xam kërug yéglé, telesàntar...) •Defar ay yéenekaay (kayit, Rajo, Telewisyow Tiyaatar añs) •Amal ay weccante ci diiwaan yi. •Nguur yi •Ñiy liggéeyal seen bopp •Gëstukat yi •Mbooleem kuréel yiy toppatoo mbirum koppar yi. Nguur yi ci boppi réew yi •Joxe yoon wi ñu war a jaar •fexe ba liggéey bu aw yoon nekk lu yomb. •Aar sañ-sañu képp ku am xam-xamam •Yombal lépp lu ñuy yéglé ak weccantey xabaar yi. •Dugal xam-xami cosaan yi ci njàng mi •Yombal tukki mi ci diiwaan yi. •fexe ba ñépp mën a jot ci tàggukaayu xabaar yi •Kuréel yi réew yi séq • Mbooloom kuréel yiy toppatoo mbirum koppar. Way- jëf yi Fànna yi ñuy yéngu Li ñuy def Ñi ñu lëngóol Gëstu gi •Nangu ne xam-xami cosaan am na •Yoonal xam-xami cosaan yi •Tasaare li gëstu gi feeñal •Fexe ba ni ñuy gëstóo ci pexey cosaan yi gën a baax •Fexe ba nit ñi mën a jot ci li feeñ ci gëstu gi. •Dugal xam-xami cosaan yi gëstu gi feeñal ci li ñuy jàng. •Yombal weccante geek kër yi nguur yi moom ak yi nga xam ne nit ñee leen moomal seen bopp. •Nguur yi •Mbooloom kuréel yiy toppatoo mbirum koppar Li nit ñi moomal seen bopp •Nangu àqi xam-xami cosaan yi • Fey àq walla ndigal • Mbooloom kuréel yiy toppatoo mbirum koppar • Oo-En-See (kuréel) yi ajuwul cig nguur Mbooloom kuréel yiy toppatoo mbirum koppar yi •Nangu ne xam-xami cosaan yi am nañ solo • Tasaare xabaar yi aju ci xam-xami cosaan yi • Fexe kenn ku nekk ci ñi jappóo gën a jox gëdda solo yi xam-xami cosaan am. •Taxawal ci suñ biir ay géew yu ñuy jokkoo di ci weccantee. •Yoon wuy jokkale béréb yi xam-xami cosaan yi fàqikook ñi jàppóo. •Dugal mbir yu bokk ci xam-xami cosaan ci feem yi ñuy indée ndimbal gu jëm ci yokkute. •Oo-En-See (kuréel yi ajuwul ci genn nguur) Way- jëf yi Fànna yi ñuy yéngu Li ñuy def Ñi ñu lëngóol Mbootaay yi réew yi bokk •Nangu ne xam-xami cosaan dafa am lu mu laaj •Réew yi déggóo ci mbir yu leer yu bokk ak lenn lu dul lu aju ci xam-xami cosaan, àqi boroom xam-xam bi, ni ñuy dugalantee, weccantey aada añs •Fexe ba ñiy yëngu ci xam-xami cosaan yi di mën a teew ci pénc yu yaatu yi réew yi di daje. •Mbooloom kuréel yiy tappatoo mbirum koppar yi •Oo-En-See (kuréel yi ajuwul ci genn nguur) Bànk Monjaal •Fexe ba ñu gën a jox gëdda xam-xami cosaan ci nguur yi, ci ñi ñuy jàppaleek képp koo xam ne boroom baat la •Joxe ay xabaar ci xam-xami cosaan yi (jaarale ko ci web bi , jumtukaay yi ñu bind ci kayit, béréb yi ñuy wonee, dugal leen ci sàq yi ñuy def lépp lu aju ci kaaw yi...) •Jottali xibaar yi ñi ñu jàppóol (ci ay penc yu mag, taxawalug jàppóo yu mel ni P.T.I.C.A, ndimbal ci jëm ci pexe yi nit ñi sos ci fi ñu dëkk) •Jàpp ci porose yi sukkandiku ci xam-xami cosaan yi, pénc yi ay réew séq, ak ndajey liggéey yi ñuy def ci fànna gii, ak xam-xami cosaan yi gën a soxal kuréel yi réew yi bokk. •Oo-En-See yi •Nguur yi •Mbooloom kuréel yiy toppatoo mbirum kappar yi BOOTAL V Doxalin wi Njariñu képp ku bokk ci ñi jàppóo; kàttanu ñiy am lu ñu def ci xam-xami cosaan yi; ak yenn gàllankoor yi mën a am ci wàllu alal. Loolu dafa laaj doxalin wuy yombal weccantem xabaar bu dul dakk, yokk mën-mëni nit ñi ci fiñ dëkk, ak yoon wuy ubbil bunt ñeneen ba ñu mën a bokk ak ay joxekati xam-xami cosaan. Boroom xam-xam yu ràññeeku ci wàllu xam-xami cosaan ak xaralay xibaarukaay ak jokkookaay ñooy xelal " pexe mi" ci feem yeek xalaat yi nga xam ne fàww ñu jëfé leen. Tasum Xibaar mi Pexe mi dafay seet jumtukaay yi war a jiitu ngir bind; téyé xam-xami cosaan yi, tas leen, siiwal leen te di leen jëfé. Ci kow loolu, ñi ñu xam ne ci ñoom la xam-xami cosaan yi fekk baax, dañoo war a joxe ay leeral ci ni ñu leen di jëfandikóo. Loolu mën naa yaatal liñ gis ci xam-xami cosaan yi, be tey itam, mën naa doon jumtukaay bu ñuy natte pexe yi ñuy jëfandikóo ba am lu leer ci xam -xami cosaan yi ñu mën a jëfandikóo ñooy dem ci dëkk yi di laaj nit ñi, toog ak ñi ngeen bokk natt li ñuy def. Porose Bànk Monjaal yeek ñeneen ñu bokk ci liggéey bii ñu door dinañu indi seen i yokkute. Liggéey bi ñu door nii, dinañ yaatal ba tey xam-xam yi Bànk Monjaal ak ñi mu ci jàppool sukkandiku. Fexe be weccantem xibaar mi ci diggante ñi nekk ci réew yi néew doole yomb Li ñu bind ci li ñuy def ci xam-xami cosaan yi, dañ koy dajale, tënk ko ngir dugal ko ci sàqum xam-xam moo xam ne nit ñi dinañ ci mën a jot ci lu yomb, nga xam ne saa su mënee nekk dañ koy jokkaleek fi xam-xami cosaan yii fekk baax ( liggéey biñ door dafay war mu sukkandiku ci). Xam-xami cosaan yi nga xam ne dafa am ñoo xam ne dañ leen amal njariñ; dañu leen di siiwal ci kayitu tasukaayi xabaar buy génn wenni yoon ci weer wu nekk. Liggéey biñ door dafay war mu sukkandikóo ci liñ fi jëkk a def, dimbale kuréeli xam-xami cosaan yi ba liñ fi mën a yokku ba ñu gën a xamante, tëyé te tas xabaar yi aju ci xam-xami cosaan yi. Jëfandikóo xam-xami cosaan yi ci yoon wiy indig yokkute. Bàyyi xel ci solo yi xam-xami cosaan am, jëfandikóo jaar-jaar yiñ fi jëkk a def ak tàggat xel yi ñetti mbir lañ yoo xam ne dañ leen di soxla su ñu bëggée dugal xam-xami cosaan ci yoonu yokku wi antu. Bi muy door, liggéey bi dafa waroon a def léppam ci ñiy dogal, kuréel yiy toppatoo yokkute ak nguuri réew yi gën a yebe xel solo si xam-xami cosaan yi am. Bu weesoo siiwalug xam-xami cosaan yi nga xam ne niróowuñook yeneen yi, liggéey bi dina am yu muy wone ci yen xew yi ñi jàppóo di amal ( misaal: ndaje mi Bànk Monjaal di amal at mu nekk). Fas nañ yéenee amaal ndaje mu mag ci Afrik ngir ñi fiy jiite gën a yebe xel solo yi xam-xami cosaan am. Bu ñu demee ba ca kanam, dinañ teewlu ci yokkug liggéey yi ñu sumb ngir seet ba xam, jaarale ko ciy porose. Loolu, dina dugalaale jëfandikóog misaal yu antu ngir firndéel ne jëfandikóo xam-xami cosaan mën naa indi njariñ lu amul benni werante. Tànn gu am fayda gu ñuy tànn liggéey yi ñuy seete ba xam ( moo xam porose xalla am réew a koy doxal) dinañu dimbale ba ñu gën a mën a suuxat misaal yi ñiy jëfandikóo ci jéegó yii ngi ñeneen ñi ñu bokkal liggéey wóolu. Bu dee li aju ci ñi séq liggéey bi, jëflante gi am ci jaar-jaar yiñ doon seete; ak joxe ab leeral di dugalaale borom kàddu yi nekk ci kréel yeek mbootaay yi ci " baayale walla ndeyale" ay liggéey yu ñuy jëkk a seete, dina tax ba ñiy yëngu ci wàllu yokkute bàyyi ci xel ni mu ware. Taxawal ay jàppóo Liggéey bu bees bi dina fexee taxawalug jokkoo ak ñeneen ñoo xam ne bokkuñook ñi nekk ci kuréel gi tudd PICTA. Dina gën a bàyyi xel ci jokkoo gi ñuy taxawal digante kuréel yi jokkuwul cig nguur, xàll wu mag wu xam-xami cosaan yi te saa su mu mënee nekk; jaarale ko ciy porose aki kuréel yu jàppóo, ak ñi ci dëkk-dëkkaan yi ngir am lu ñu jànge ci seeni jaar-jaar. Xam-xam mënul a ñàkk ndax su ñu xamul ni nit ki walla askan wi di def ba am xam-xam ak ni muy jëfandikóo xam-xamam, duñu leen mën a indilug ndimbal ci seen dund rawatina néew doole yi? Bataaxal bu ñu bindoon ci atum 19998 ci yokkute gi ci àdduna si, ___________________________________________________________________ Footer