LES COMPETENCES TRANSFEREES AUX COLLECTIVITES LOCALES PAR L'ETAT / MÀQAAMA YI NGUUR GI JEBBAL GOX YI Français Wolof 1 Principes fondamentaux et modalités de transfert 1 Anam yi ñuy jébbalee màqaama 2 L'exercice des compétences transférées aux collectivités locales 2 Ni ñuy jëfoo màqaama yi ñu jébbal gox yi 2 / L'exercice des compétences transférées aux collectivités locales / Ni ñuy jëfoo màqaama yi ñu jébbal gox yi Français Wolof La loi n° 96 - 07 du 22 mars 1996 portant transfert de compétences aux collectivités locales, consacre neuf (09) domaines de compétences réparties entre les ordres de collectivité locale. Les domaines Le territoire sénégalais doit être considéré comme le patrimoine commun de la nation. Le transfert a pour objet la gestion et l'utilisation du domaine de l'Etat (domaine privé et domaine public) ainsi que du domaine national. Le domaine privé L'Etat peut céder aux collectivités locales tout ou partie de ses biens meubles ou immeubles relevant de son domaine privé, ou passer avec ces collectivités des conventions comme il peut leur faciliter l'accès à la pleine propriété de tout ou partie des biens meubles et immeubles ou affecter simplement le droit d'usage de certains des biens meubles et immeubles pour leur permettre d'exécuter leurs missions et d'abriter des agences décentralisées ou des équipements collectifs. Le domaine public Les personnes physiques ou toute autre personne normale peuvent initier des projets dans le domaine public maritime et le domaine public fluvial, après délibération du conseil régional qui doit recueillir auparavant l'avis du conseil municipal ou du conseil rural. La délibération du conseil régional est soumise à l'approbation du représentant de l'Etat. Lorsque la zone du domaine public est dotée d'un plan spécial aménagé élaboré par l'Etat, les compétences sont déléguées à la commune ou à la communauté rurale pour le périmètre qui lui est dévolu dans le dit plan. Le domaine public artificiel est géré par l'Etat qui peut toutefois transférer aux collectivités locales, suivant des modalités qui sont fixées par décret, la gestion des monuments historiques. Les communes sont chargées de la gestion de la voirie non classée située à l'intérieur du périmètre communal. Le domaine national Les communes peuvent utiliser les terrains du domaine national situés en zone urbaine pour des projets d'équipement ou dans le cadre de lotissement (parcelles d'habitation à attribuer à la population). Quant aux projets ou opérations initiés sur des terrains du domaine national situés en zone de terroir, ils sont établis conformément aux dispositions de la loi sur le domaine national et ses décrets notamment. Pour les projets ou opérations qu'il initie sur le domaine national, l'Etat prend la décision après consultation du conseil régional ou de la communauté rurale ou des communautés rurales concernées, sauf impératif de défense nationale ou d'ordre public. Les terres du domaine national à vocation agricole situées en zone urbaine sont gérées conformément aux dispositions de la loi sur le domaine national concernant les zones urbaines, en tout ce qui n'est pas contraire aux dispositions de la loi. Lorsque des terres précédemment situées en zones pionnières sont reversées dans des zones de terroir, l'Etat conserve la gestion des parties de zones pionnières ayant fait l'objet d'un aménagement spécial et y exerce les prérogatives nécessaires quant à leur mode de gestion. Education, alphabétisation, promotion des langues nationales, formation technique et professionnelle Education La région participe à l'établissement de la tranche régionale de la carte scolaire. Les collectivités locales ont des compétences en matière de construction, d'équipement, d'entretien et de maintenance d'infrastructures scolaires et en matière de répartition, d'allocation de bourses et d'aides scolaires (régions et communes). Les collectivités locales participent à l'acquisition de manuels et fournitures scolaires, à la gestion et à l'administration des établissements scolaires par le biais des structures de dialogue et de concertation. Alphabétisation La région a, entre autres compétences, l'élaboration des plans régionaux d'élimination de l'analphabétisme, la synthèse annuelle de l'exécution des plans et campagnes d'alphabétisation, la conception et la production de matériel didactique, la réalisation de la carte de l'alphabétisation, la délivrance de l'autorisation d'exercer comme opérateur. Les trois ordres de collectivités ont les compétences en matière d'exécution des plans d'élimination de l'analphabétisme, de recrutement d'alphabétiseurs, de formation des formateurs et alphabétiseurs. La commune et la communauté rurale ont compétences en matière de mise en place et d'entretien d'infrastructures et d'équipements éducatifs, de mobilisation des ressources nécessaires aux campagnes d'alphabétisation. Promotion des langues nationales Les collectivités locales reçoivent les compétences suivantes : l'introduction des langues nationales à l'école, la promotion d'un environnement lettré par le développement de l'édition en langues nationales, la promotion de la presse parlée et écrite en langues nationales, la collecte, la traduction et la diffusion des éléments de la tradition orale (contes, mythes, légendes, etc.) en vue d'en faciliter la publication, la mise en place d'infrastructures et d'équipements, la mobilisation de ressources. De façon spécifique, les régions et les communes reçoivent les compétences suivantes : la maîtrise de la distribution fonctionnelle des langues du pays et la mise au point de la carte linguistique, l'application des mesures afférentes à l'utilisation des langues nationales dans l'administration, la mise à jour du catalogue des éditeurs, auteurs et oeuvres en langues nationale, l'organisation du concours en langues nationales dans le cadre de la semaine nationale de l'alphabétisation. Formation technique et professionnelle Les collectivités locales reçoivent les compétences suivantes : l'élaboration d'un plan prévisionnel de formation visant des secteurs de métiers adaptés à chaque ordre de collectivité locale compte tenu des spécificités locales, l'entretien, la maintenance des centres et instituts de formation, le recrutement et la prise en charge du personnel d'appoint, la participation à l'acquisition du matériel didactique (fournitures et matières d'oeuvre), la participation à la gestion et à l'administration des centres de formation par le biais des structures de dialogue et de concertation, l'appui à de petits projets visant à créer de petites unités d'ateliers en mécanique - auto, soudure, électricité, etc., l'élaboration d'un plan d'insertion des jeunes, l'aide à la détection et à l'établissement de contrats de partenariat école - entreprise pour une réelle formation en alternance. Les régions reçoivent de façon spécifique les compétences suivantes : le recensement exhaustif des métiers régionaux et l'élaboration d'un répertoire des formations, professionnelles existantes avec indication des aptitudes requises et des curricula et des cursus de formation, l'élaboration d'une carte scolaire régionale de l'enseignement technique et de la formation professionnelle en relation avec la carte nationale. Santé, population et action sociale Santé et population Les régions reçoivent les compétences suivantes : la gestion et l'entretien des hôpitaux régionaux et départementaux, la gestion, l'entretien et l'équipement des centres de santé situés au niveau des communautés rurales, la mise en oeuvre des mesures de prévention et d'hygiène. Les communes reçoivent les compétences suivantes : la gestion, l'entretien et l'équipement des centres de santé urbains, la construction, la gestion, l'entretien et l'équipement des postes de santé urbains. Les communautés rurales reçoivent les compétences suivantes : la construction, la gestion, l'entretien et l'équipement des postes de santé, des maternités et cases de santé. Action sociale Les régions reçoivent les compétences suivantes : la participation à l'entretien et à la gestion des centres de promotion et de réinsertion sociale, l'organisation et la gestion de secours au profit des nécessiteux. Les communes reçoivent les compétences suivantes : la participation, à l'entretien et à la gestion des centres de promotion et de réinsertion sociale, l'organisation et la gestion de secours au profit des nécessiteux, l'appui au financement de projets productifs au profit des populations déshéritées. Les communautés rurales reçoivent les compétences suivantes : la participation à l'entretien et à la gestion des centres de promotion et de réinsertion sociale, l'organisation et la gestion de secours au profit des nécessiteux, l'appui au financement de projets productifs au profit des populations déshéritées. Jeunesse et sport Les compétences transférées aux collectivités locales dans ce domaine entraînent leur implication dans la conception et l'exécution de la politique nationale de jeunesse et de sports par l'organisation, l'animation et le développement des activités physiques, sportives et socio-éducatives, l'appui aux associations sportives et culturelles, la construction, l'administration, la gestion et l'entretien des infrastructures sportives. Culture Les collectivités locales ont pour mission d'assurer : o la préservation et la valorisation du patrimoine culturel ; o la surveillance et le suivi de l'état de conservation des sites et monuments historiques ; o la collecte de la tradition orale, des contes, mythes, proverbes, symboles et valeurs et la promotion de la culture nationale et locale (communauté rurale) ; o la promotion, l'épanouissement et le développement des activités culturelles ; o la création et la gestion des centres de centres socio - culturels et de bibliothèques de lecture publique ; o l'animation culturelle (journées culturelles, manifestations culturelles traditionnelles, concours littéraires et artistiques) ; o la diffusion culturelle par la promotion des acteurs culturels et de leurs oeuvres. L'environnement et la gestion des ressources naturelles Les régions reçoivent les compétences suivantes : la gestion, la protection et l'entretien des forêts, des zones protégées et des sites naturels d'intérêt régional, la mise en défens et autres mesures locales de protection, la gestion des eaux continentales à l'exclusion des cours d'eau à statut international ou national, la création de bois, forêts et zones protégées, la réalisation de pare-feux et la mise à feu précoce, la protection de la faune, la répartition des quotas régionaux d'exploitation forestière entre les communes et les communautés rurales, la délivrance d'autorisation d'amodiation de chasse après avis du conseil rural, l'élaboration, la mise en oeuvre et le suivi des plans ou schémas régionaux d'action pour l'environnement, l'élaboration et la mise en oeuvre de plans régionaux d'action pour l'environnement, la création de brigades de volontaires pour intervenir en cas d'atteintes à l'environnement, la délivrance d'autorisation de défrichement après avis du conseil rural. Les communes reçoivent les compétences suivantes : la délivrance d'autorisations préalables de toute coupe à l'intérieur du périmètre communal, les opérations de reboisement, la perception de la quote-part d'amendes prévues par le code forestier, la gestion des déchets, la lutte contre l'insalubrité, les pollutions et les nuisances, la protection des ressources en eau souterraines et superficielles, l'élaboration des plans communaux d'action pour l'environnement. Les communautés rurales reçoivent les compétences suivantes : la délivrance et l'autorisation préalable de toute coupe à l'intérieur du périmètre de la communauté rurale, la perception de la quote-part d'amendes prévues par le code forestier, la constitution et le fonctionnement des comités de vigilance en vue de lutter contre les feux de brousse, la gestion des sites naturels d'intérêt local, la création de bois et d'aires protégées, la gestion des déchets, la lutte contre l'insalubrité, l'élaboration et la mise en oeuvre du plan local d'action pour l'environnement, l'avis sur la délivrance par le conseil régional d'autorisations de défrichement, l'avis sur la délivrance par le Président du conseil régional d'autorisations d'amodiation des zones de chasse, la création et l'entretien des mares artificielles et de retenues collinaires à des fins agricoles et autres. Urbanisme et habitat La région reçoit les compétences suivantes : l'approbation des schémas directeurs d'aménagement et d'urbanisme (SDAU), le soutien à l'action des communes et communautés rurales en matière d'urbanisme et d'habitat. La commune reçoit les compétences suivantes : l'élaboration des plans directeurs d'urbanisme (PDU), des SDAU, des plans d'urbanisme de détail des zones d'aménagement concerté, de rénovation urbaine et de remembrement, les lotissements, leur extension ou restructuration, la délivrance des permis de construire, d'accords préalables, de certificats d'urbanisme et de permis de démolir, la délivrance de permis de clôturer, de permis de coupe et d'abattage d'arbres, l'autorisation d'installation et des travaux divers. La communauté rurale reçoit les compétences suivantes : l'élaboration de termes de références des plans directeurs d'urbanisme (PDU), des SDAU et d'habitat de détail des zones d'aménagement concerté, de rénovation et de remembrement, les lotissements, leur extension ou restructuration, la délivrance des permis de construire, d'accords préalables, de certificats d'urbanisme et de permis de démolir. Aménagement du territoire La région élabore le schéma régional d'aménagement du territoire (S.R.A.T) en veillant à sa cohérence avec le plan national d'aménagement du territoire tandis que la commune et la communauté rurale donnent leur avis sur le projet de schéma d'aménagement du territoire avant son approbation par l'Etat. Planification La région reçoit les compétences suivantes : l'élaboration et l'exécution des plans régionaux de développement intégré (P.R.D.I), la coordination des actions de développement de la région, la passation, en association avec l'Etat, de contrats-plans pour la réalisation d'objectifs de développement économique, social, sanitaire, culturel et scientifique. La commune reçoit les compétences suivantes : l'élaboration et l'exécution des plans d'investissements communaux (PIC), la passation, en association avec l'Etat, de contrats - plans pour la réalisation d'objectifs de développement économique, social, sanitaire, culturel et scientifique. La communauté rurale reçoit les compétences suivantes : l'élaboration et l'exécution des plans locaux de développement. Yoon n° 96-07 wu 22/03/1996, ñeel jébbale màqaama gox yi, moo tudd juróom-ñeenti (09) anami màqaama yu gox yiy saytu léegi (suuf, njàng, wérgu- yaram, xaleek tàggat-yaram, baax, dénd ak caytu li jógee ci suuf, dëkkinu taax ak màkkaan, tëralinu suuf. 2.1 Suuf yi Na ñépp xam ne, suufu réewum Senegaal, askan wee ko moom te ñépp a ko bokk. Li tax jébbale jóg mooy saytu te jariñoo suuf si bokkul ci alal ñépp, suuf si bokk ci alalu ñépp ak suufi askan wi 2.1.1 Li ñépp bokk Suuf si ñépp bokk mooy suuf si ñu daan tuddee alalu buur : mbedd, yoon ak lu ni mel. Xeetu alal yooyu, ñépp a ci yem. Nit ak jëmmam walla mbootaay gu ñu nangul ag nekkam, man nañoo taxawal ay mébét ci li ñépp bokk, mu nekk ci géej walla dex, su leen ko kurélu diiwaan joxee te fekk muy kurélu kómin mbaa gu goxu kaw ànd ci. Kurélu diiwaan maye, doyul, ki fi nekkal nguur gi, fàww mu ànd ci. Su nekkee ni li, ñépp bokk, dafa fekk mu am tëralinu suuf, wàllu suuf si faree ci gox bi, muy kómin walla goxi kaw, nguur da koy bàyyi mu doxal màqaamaam. Li ñépp bokk, su dee ni nit a ko liggéey (misaal : miise), man na koo jébbal gox ciy anam yu dekkere tudd. Kómin yi ñooy saytu mbedd yi ajuwul ci nguur gi te nekk ci seen rëddu suuf. 2.1.2 Li bokkul ci alalu ñépp Suuf si bokkul ci alal ñépp mooy suuf si mbaa lu ni xeetool te nekk ci rëddu komin te du mbedd walla béréb bu ñépp di jëfoo; waaye man naa nekk kër gu meeri moom, di ko jariñoo, di ko able mbaa di ko luye. Nguur man naa : - jox lépp walla lenn ci alalam gox yi te mu bokk ci xeeti alal yooyu. - def ay deggoo yu muy joxee gox yi lepp walla lenn ci alal ji, muy taax walla deet, - yombalal gox ba nu jot ci - abal gox yi nuy liggeeyee, walla fu nuy def ay kurel yu itteel nepp. 2.1.3 Suufu askan wi Suufu askan wi, dafa bariy xeet. Man nanu cee rannee yeenti (4) xaaj : - suufu reew-taax (mooy suuf si nekk ci reew-taax, nu dekke ko walla nu di bey) ; - suufu tund, mooy suuf si nekk ci tund yi nu dekke ko walla nu di ko bey, te gox yi di leen saytu ; - suufu si nu aar moo emb all yi te nguur gi di ko samm ngir mu no? ; - suuf yi ci des te nu tuddee leen suufu « sancaan » te yaar yi ci gen fes, nekk ca diiwaanu Tambaa ak ca Waalo fa dexu Senegaal dajeek geej gi, . Komin yi man nanoo jarinoo suufi askan wi nekk ci reddu taax yi ngir doxal seen mebet walla nu lotise leen, nit ni dekkee ko Su nekkee ni mebet walla liggeey bi, danu koo war a def ci suufu askan wi, te fekk mu bokk ci suuf yi nguur gi teg loxo, su boobaa, danu koy weer ci yoon wiy saytu suufu askan wi, ak dekere ya ca aju. Mebet yeek liggeey yi nu begg a def ci suufi askan wi, Nguur geey fab ndogal gannaaw bu mu ci diisook kurelu diiwaan walla kurelu goxi kaw, ba mu des lu itteel kaaraange reew mbaa luy saxal jamm. Suufi askan wi nu man a bey te nu nekk ci taax, danu leen di saytu ni nuy saytoo suufi askan ci taax feek woroowul ak yoon. Su nekkee ni suufu askan dafa bokk ci suuf yu nu tuddee « sancaan », danu leen di soppi suufu tund, nu di leen di bey ak a dekke. Su nekkee ni suuf si, dafa bokk ci suufu « sancaan » danu koy soppi suufu tund. 2.2 Njàng, njàgum abacada, fullaal làkki réew mi, njàgum xaralaak liggéey. Njang a ngi emb lepp luy njangum abacada, njangum xaralaak njangum liggeey ak fullaal lakki reew mi. Diiwaan, bokk na ci niy defar kartu fi am lekkool, rawatina yi nekk ci biir digam. Gox yi, am nanu maqaama : o mu jem ci tabax (lu mel ni lekkool), o mu jem ci andiy jumtukaay (taabal, ba?, armoor, ....) o mu jem saytook toppatoo, o mu jem ci seddaleek a joxe burs, o mu jem ci ndimbalu elew (muy diiwaan walla komin). Gox yi am nanu maqaama : o bokk ci njedum teere, o bokk ci njedum lepp lu elew di ittewoo, o bokk ci ni nuy saytook a doxalee lekkool yi o di jaaree ci waxtaan ak diisoo lepp luy nu bokk. 2.2.1 Njàngum abacada Ci maqaamay diiwaan, bokk na ci : o pexe mu nuy aw ba gennee nakk-a-jang gi nekk ci diiwaan bi, o defar tenk-liggeeyu at mi jeex (daaw), ci wallu njangum abacada ; o tabax ak a mool i teere walla jumtukaayi njangale ; o defar kartu daara abacada yi, o joxe ndigal kepp kuy liggeey ci wallu njangum abacada. Ñetti xeeti gox yépp (diiwaan, kómin ak goxi kaw), am nañu màqaama : o liggéey i tëralin yu fiy dàq ñàkk-a-jàng, o jël ay jàngalekat, o jàngal ay sériñi jàngalekati abacada mbaa ay jàngalekat. Kómin ak goxi kaw am nañu : o màqaamay tabax, o màqaamay sàmp i jumtukaayi njàngale, o màqaamay wuut alal ji war ci doxal njàngum abacada at mu nekk. 2.2.2 Fullaal làkki réew mi Gox yi, jot nañu màqaama : o yu leen may ñuy jàngee làkki réew mi ci lekkool yi, o ñu fullaal làkki réew ba sunu dénd feese leen, o móol ay téere yu ñu bind ci làkki réew mi ; o ñu fullaal tasum xibaar (muy wax, di bind) ci làkki réew mi ; o di dajaleek a tekki bépp xam-xam bu man a soxal askan wi balaa ñuy leen di wasaare. o dajale lépp lu bokk ci aada gox bi walla réew mi, muy léeb, di taalif, di taasu, di bàkk, di jiin, di wóy, di kayit yu mel ni yi ëmb sàrti gox yi, di xam-xami mbey, di xam-xami xarala, di xam-xami jokkoo, di wax ju ñu man a bind ci làkki réew mi, móol leen. o sàmp i jëfuwaay ak i jumtukaay o wuut alal ju man a tax ñu jëfandikoo làkki réew mi, ni mu ware. Kon, dañoo jagleel diiwaan yeek kómin, màqaama yii : - defar kàrtu kàllaama yi; - fexe ba làkki réew mi, ñu leen di jariñoo ci lépp lu aju ci dundu askan wi - fab ay matukaay yuy tax nuy bindanteek nguur gi, - bind teere buy lim bindkat yi (ci lakki reew mi), teere buy lim moolkati teere yi, teere buy lim niy yengu ci lakki reew mi, teere buy lim niy yengu ci njangum abacada. - di sakk ay jo?ante ci kallaama reew mi, rawatina diiru ajubes bi mu jagleel jangum abacada. 2.2.3 NJàngum xaralaak liggéey Gox yi jot nanu ci maqaama yii : o teral njang mu neel xeeti mecce yu mengook xeetu gox bu nekk (diiwaan, komin, goxu kaw) ak la nekk ca gox ba, o toppatoo janguwaay yi, o jel ak a fay liggeeykat yiy jappale, o bokk ci njendum jumtukaayi njangale (muy jumtukaay, di rend), o bokk ci ni nuy saytook a doxal janguwaay yi te weeru ci waxtaan ak diisoo, o jappale niy semb ay mebet yu ndaw yu mel ni samp atalye mekanise, atalye suude, atalye liggeey kura?, ans, o teral pexe mu xale yi am liggeey, jappale janguwaay yeek liggeeyuwaay yi nu lengoo ba njang miy doxee yaari tank (janguwaay ak liggeeyuwaay). Diiwaan yi do?? a jot ci maqaama yii : o gestu ba lim mecce yi am yepp ci diiwaan bi, o defar teere buy lim njagum liggeey yi am yepp te boole ci maqaama yi nuy laaj ngir jangee fa, li nu fay jangale, yoonu xam-xam ba, o defar kartu janguwaayi xaralaak liggeey yi nekk ci diiwaan bi te fekk mu deppook kartu reew mi. 2.3 Wér-gu-yaram, nit ñeek xettali doom-aadama 2.3.1 wér-gu-yaram ak nit ñi Diiwaan yi jot nañu màqaama yii : o saytook a toppatoo loppitaani diiwaan yeek yu deppartamaa yi. o saytook a toppatoo jumtukaayi dispañseer yi nekk ci goxi kaw yi. o sàkk ay matukaayi fànq feebar walla lépp luy nasaxal wér ak cet. Kómin yi, jot nañu màqaama yii : o saytook a toppatoo jumtukaayi dispañseeri taax yi, o tabax ay kër-dogtoori taax, o saytu jumtukaayi kër-dogtoor yi, o toppatoo leen. Goxi kaw yi jot nañu ci màqaama yii : o tabax ay kër-dogtoor, ay muccuwaay ak ay néegi wér-gu-yaram, o saytu kër-dogtoor, muccuwaay yeek néegi wér-gu-yaram, o toppatoo kër-dogtoor, muccuwaay yeek néegi wér-gu-yaram, o wuutal ay jumtukaay kër-dogtoor, muccuwaay yeek néegi wér-guyaram, 2.3.2 Xettali doom-aadama Diiwaan yi jot nañu ci màqaama yii : o dugal seen loxo ci toppatook a saytu kurél yiy yokk doom-aadama, ak di delloosi ñi réeróon, o sàkk ak a saytu wallu yi ñeel néew-ji-dooleek miskin, Kómin yi jot nañu màqaama yii : o dugal seen loxo ci toppatook a saytu kurél yiy yokk doom-aadama, ak di delloosi ni reeroon, o sakk ak a saytu wallu yi neel neew-ji-dooleek miskin, o jappale ni seen loxo jotul seen gannaaw, nu am xaalis buy tax nu man a taxawal seen mebeti koom-koom Goxi kaw yi jot nanu maqaama yii : o dugal seen loxo ci toppatook a saytu kurel yiy yokk doom-aadama, ak di delloosi ni reeroon o sakk ak a saytu wallu yi neel neew-ji-dooleek miskin, o jappale ni seen loxo jotul seen gannaaw, nu am xaalis buy tax nu man a taxawal seen mebeti koom-koom. 2.4 Xaleek tàggat-yaram Maqaama yi nu jebbal gox yi ci wallu xaleek taggat yaram, danoo macc jem ci : o nu dugal seen loxo ci nas ak a jefe li reew mi japp ci wallu xaleek taggat yaram, o nu sos ak a doxal ak a suuxat ay yengu-yengu taggat yaram ak jo? ante yuy dolli yar, naatal nit, ci ndimbalu mbootaauyi taggat yaram yeek nit ni ci wallu baax (ASC), o tabax, saytu, ak toppatoo jefuwaay yi nuy taggatee yaram. 2.5 Baax Niseri gox yi mooy fexe ba : o baaxu reew mi no?, o baaxu reew mi nu fullaal ko o nemmeekook a samm bereb yeek yef yi emb sunu demb ak sunu aada. o lugat lepp luy aada te bindunu ko, muy leeb, di leebu, muy mandarga, ak fullaal baaxu reew rawatina baaxu gox bi (goxi kaw) o fullaal bepp yengu-yengu bu nu tibbee ci baaxu reew mi walla mu neel ko o sakk ak a saytu bereb yu nu man a yengoo ci wallu baax o sakk ay kaggu yu nepp man di yereey teere. o xumbal ci wallu baax (besu baax, xumbali aada, jo?ante ciy taalif, ak ci xarala). o yaatal baaxu reew mi. o jappal niy yengu ci baax. o wane li niy yengu ci wallu baax liggeey. 2.6 Dénd ak caytu li jógee ci suuf si Diiwaan yi jot nanu maqaama yii : o saytu, aar ak toppatoo all yi, tund yi nu aarlu, ak bereb yi amal njarin diiwaan bi ; o di tereek a jeem lepp lu gox bi man a def ba no?al all bi; o saytu dex yeek deeg yeek lu ni xeetool ba mu des ndox mu reew mi bokk ak bitim-reew mbaa diiwaan bi seq kook beneen ; o di samp ay all wallay tooli garabi all, ay tund yu muy aarlu, o di xoddeeku, o di taal daayi gatandeku, o di aar mala yi, o di sakk ay kotaa yu nuy jarinoo all bi o tey xam ni nu koy seddalee komin yeek goxi kaw yi, o di maye san-sani rebb mu nuy fay, gannaaw bu ca goxu kaw bi andee ; o di teral, di jefeek a topp lepp lu jem ci ter, nas, lepp lu neel diiwaan ci wallu dend, o sakk kureli «baay-faali dend» yuy jog ci lepp lu man a nasaxal dend wi; o di maye, ay tooli ngor mu bees, gannaaw bu ci goxu kaw bi andee. Komin yi jot nanu maqaama yii : o maye san- sanu dog garab gu nekk ci digu komin bi ; o di jembat garab, o di nangu alamaan bu sartu all sakk walla di ca jot wallam ; o di saytu mbalit, di fanq tilim, ak lepp luy tilimal mbaa lepp luy lor ; o di aar ndoxum kaw (dex, deeg ans) o di aar ndox mu nekk ci suuf ; o di sakk ay teri komin yu neel dend wu no?; Goxi kaw gi jot nanu maqaama yii : o maye san-sanu dog garab ci digu gox bi ; o di nangook a jot wallam ci alamaan yi sartu all dogal ; o di sakk ay kurel yuy wattook a fanq daay; o di saytu bepp bereb bu amal solo gox bi o di samp ay tooli garabi all, di sakk ay jatti yu muy aarlu ; o di saytu mbalit, o di fanq tilim, lepp luy tilimal ak lepp luy lor ; o di teral ak a jefe lepp luy no?al dend wi, o di wax ni mu gisee su diiwaan beggee maye lenn cib gott bu nuy gor ; o di wax xelaatam su njiitu diiwaan beggee maye san-sanu rebb bu and ak fay ; o di gas ak a toppatoo, ay deeg walla di teq ndox muy wal ngir suuxatee ko mbaa lu ni mel. 2.7 Dëkkinu taax ak màkkaan Diiwaan jot na maqaama yii : o mooy nangu nas bi jem saytu teralinu suuf ak dekkinu taax (SDAU) o mooy jàppale kómin yeek goxi kaw yi ci lépp lu ñuy def mu jém ci dëkkinu taax ak màkkaan. Kómin, jot na màqaama yii : o tëral mu jém ci dëkkinu taax, (PDU), o nas mu jém saytu tëralinu suuf ak dëkkinu taax (SDAU), o def ay tëri dëkkinu taax, rawatina tund yi ñu bokk liggéey. o jekkalaat ci réew-taax, o seetaat ni tool yi bindoo, o di lotise, o di yaatal ak a defaraat, o de maye sañ-sañu tabax, o di ci ànd balaa ñuy maye bépp sañ-sañ, o di joxe lijaasa dëkkinu taax. o di joxe sañ-sañu toj, o di maye sañ-sañu ñag, o di maye sañ-sañu wàññi walla dog garab, o di maye lépp lu ñu man a liggéey ci biir dig wi. Goxu kaw jot na màqaama yii : o mooy wax ni mu bëggee ñu defee tëri dëkkini taax yi (PDU), o mooy wax ni mu bëggee ñuy defee nas mu jém saytu tëralinu suuf o mooy wax ni mu bëggee ñuy defee dëkkinu taax (SDAU) o mooy wax ni mu bëggee ñuy defee màkkaan ba mu gën a leer ; o mooy wax ni mu bëggee defee tëri dëkkinu taax, rawatina tund yi ñu bokk liggéey o mooy wax ni mu bëggee ñu seetaat ni tooli yi, bindoo o mooy wax ni mu bëggee ñu lotise, o mooy wax ni mu bëggee ñu yaatal walla defaraat, o mooy wax ni mu bëggee ñuy maye sañ-sañu tabax, o mooy wax ni mu bëggee ñu laaj ko xelaatam balaa dogal, o mooy wax ni mu bëggee ñuy joxe lijaasa dëkkin mbaa di maye sañ-sañu toj. 2.8 Tëralinu suuf Diiwaan mooy : o nas wépp tëralinu suuf wu màcc jém ci diiwaan bi (SRAT) o tey bàyyi xel ci mu dëppóok tëralinu suufu réew mi. o Kómin ak goxu kaw ñooy wax li ñu xelaat ci nasu tëralinu suufu diiwaan bi balaa ko nguur giy jàpp. 2.9 Tëralin Diiwaan jot na màqaama yii : o mooy xelaat ak a liggéey tëri diiwaan yi jém ci yokkute gu ëmb lépp (PRDI), o mooy fexe ba yëngu-yëngu yi ñeel yokkute diiwaan yépp bañ a woroo. o mooy lëngóok nguur ba juboo ci déggo-tër buy tax ñu daj seen nisëri koom-koom, lu ittéel nit, wér-gu-yaram, baax ak siyãas. Kómin jot màqaama yii : o mooy xelaat ak a liggéey tër yi ñeel liggéey kómin bi (PIC) Goxu kaw mooy jot màqaama yii : o mooy xelaat ak a liggéey tër yi ñeel gox bi ci wàllu yokkute. Début de page