#REDE MISSIONÁRIA - Atom REDE MISSIONÁRIA - RSS REDE MISSIONÁRIA - Atom REDE MISSIONÁRIA terça-feira, 10 de junho de 2014 1, 2, 3 JOHN (WOLOF: GAMBIA) [Camomile-Background_tn2.jpg] 1 John 1 1 Nu ngi leen di bind ci mbirum Ki ñuy wax Kàddug dund, moom mi amoon ca njàlbéen ga; mi nu dégg te gis ko ak sunuy bët, mi nu xool te laal ko ak sunuy loxo. 2 Dund feeñ na, te gis nanu ko; te moom lanuy seedeel, di leen yégal dund gu dul jeex, googu nekkoon ci wetu Yàlla Baay bi te feeñu nu. 3 Li nu gis te dégg ko, nu ngi leen koy yégal, ngir yéen itam ngeen bokk ak nun. Te dëgg-dëgg bokk nanu ci Baay bi ak Doomam, Yeesu Kirist. 4 Nu ngi leen di bind yëf yii, ngir sunu mbég mat sëkk, nun ñépp. 5 Xebaar bi nu dégg ci Yeesu Kirist, di leen ko yégal, mooy lii: Yàlla Leer la, te genn lëndëm nekkul ci moom. 6 Su nu waxee ne, bokk nanu ci moom, tey dox ci lëndëm, danuy fen ci sunuy wax ak sunuy jëf. 7 Waaye bu nuy dox ci leer, ni mu nekke moom ci boppam ci leer, kon bokk nanu ci sunu biir, te deretu Yeesu Doomam dina nu sellal ci bépp bàkkaar. 8 Su nu waxee ne amunu bàkkaar, kon nax nanu sunu bopp, te dëgg nekkul ci nun. 9 Su nu nangoo sunuy bàkkaar ci kanamam, fekk kuy sàmm kóllëre la te jub, ngir baal nu sunuy bàkkaar te sellal nu ci lépp lu jubadi. 10 Su nu waxee ne defunu bàkkaar, teg nanu ko kuy tebbi waxam, te kàddoom duggagul ci sunu xol. 1 John 2 1 Samay doom, maa ngi leen di bind yëf yii, ngir ngeen bañ a def bàkkaar. Waaye su kenn defee bàkkaar, ba tey am nanu ku nuy rammu ci Baay bi, mooy Yeesu Kirist mu jub mi. 2 Te moo joxe bakkanam, ngir dindi sunuy bàkkaar, te du sax sunuy bàkkaar rekk, waaye yu àddina sépp. 3 Ci lii lanu xame ne, xam nanu ko: sàmm ay ndigalam. 4 Ku wax ne xam nga ko, te sàmmoo ay ndigalam, dangay fen, te dëgg nekkul ci yaw. 5 Kuy sàmm kàddug Yàlla, dëgg-dëgg sa mbëggeel ci Yàlla mat na sëkk. Ci loolu lanu xame ne, nekk nanu ci moom. 6 Ku wax ne ci Yàlla nga sax, fàww nga dund, ni Yeesu Kirist daan dunde moom ci boppam. 7 Samay soppe, li ma leen di bind du ndigal lu bees, waaye ndigal lu yàgg la; la ngeen jotoon ca ndoorte la. Te ndigal lu yàgg loolu, mooy kàddu gi ngeen déggoon. 8 Teewul ndigal lu bees laa leen di bind, lu amoon ci dundu Yeesu, te am it ci seen dund; ndaxte lëndëm gaa ngi wéy, te leer gu wóor gi fenk na xaat. 9 Ku wax ne yaa ngi ci leer, tey bañ sa mbokk, yaa ngi ci lëndëm ba tey. 10 Kuy sopp sa mbokk, yaa ngi dëkk ci leer, te luy yóbbe nit bàkkaar du nekk ci yaw. 11 Waaye kuy bañ sa mbokk, ci lëndëm nga nekk, di ci dox, te xamoo foo jëm, ndax lëndëm muur na say bët. 12 Samay doom, maa ngi leen di bind,ndax baalees na leen seeni bàkkaar ci turu Kirist. 13 Maa ngi leen di bind, yéen baay yi,ndax xam ngeen Ki nekkoon ca njàlbéen ga ba tey.Maa ngi leen di bind, yéen waxambaane yi,ndax daaneel ngeen Ibliis. 14 Bind naa leen, samay doom,ndax xam ngeen Yàlla Baay bi.Bind naa leen, yéen baay yi,ndax xam ngeen Ki nekkoon ca njàlbéen ga ba tey.Bind naa leen, yéen waxambaane yi,ndax yéena ngi dëgër,ndax kàddug Yàllaa ngi dëkk ci yéen,te daaneel ngeen Ibliis. 15 Buleen sopp àddina ak li ci biiram. Ku sopp àddina, mbëggeelu Baay bi nekkul ci moom. 16 Ndaxte lépp lu nekk ci àddina, maanaam bëgg-bëggu yaram ak xemmemu bët ak réyug àddina, loolu du jóge ci Baay bi waaye ci àddina. 17 Te àddina day wéy, waaye kuy def coobareg Yàlla dinga sax ba fàww. 18 Samay doom, waxtu wu mujj wi jot na! Dégg ngeen ne, benn Bañaaleb Kirist dina ñëw; te dëgg la, bañaaley Kirist yu bare feeñ nañu. Ci loolu lanu xame ne, waxtu wu mujj wi jot na. 19 Ci sunu biir lañu jóge, waaye bokkuñu woon ci nun; ndaxte su ñu bokkoon ci nun, kon dinañu des ci nun. Waaye dàggeeku nañu nu, ngir mu leer ne, kenn ci ñoom bokkul woon ci nun. 20 Yéen nag, Aji Sell ji sol na leen Xelam, te yéen ñépp am ngeen xam-xam. 21 Bind naa leen, du ndax xamuleen dëgg, waaye ndax xam ngeen ko, xam it ne wenn fen du jóge ci dëgg. 22 Kan mooy fenkat bi? Mooy kiy weddi ne Yeesu mooy Kirist, Almasi bi. Kooka mooy Bañaaleb Kirist, biy weddi Baay bi ak Doom ji. 23 Ku weddi Doom ji, amuloo itam Baay bi; ku seedeel Doom ji, am nga it Baay bi. 24 Yéen nag, la ngeen déggoon ca ndoorte la, na sax ci yéen. Loolu ngeen déggoon ca ndoorte la, su saxee ci yéen, dingeen sax yéen itam ci Doom ji ak ci Baay bi. 25 Te li mu nu digoon mooy lii: dund gu dul jeex. 26 Bind naa leen lii ci mbirum ñi leen di bëgg a réeral. 27 Yéen nag, Xel mi leen Kirist sol a ngi dëkk ci yéen, te soxlawuleen kenn jàngal leen dara. Waaye Xel mi mu leen sol, mi ngi leen di jàngal lépp, te li mu leen di jàngal mooy dëgg; kon nag saxleen ci moom, ni mu leen ko jàngale. 28 Gannaaw loolu nag yéen samay doom, saxleen ci Kirist, ngir bés bu feeñee, nu am kóolute ci kanamam te bañ a rus ba sëngéem cig dikkam. 29 Gannaaw xam ngeen ne ku jub la, dingeen xam it ne, képp kuy def lu jub juddu nga ci moom. 1 John 3 1 Xool-leen mbëggeel gi nu Baay bi jox, ni mu réye, ba nu man a tudd doomi Yàlla. Te moom lanu. Moo tax àddina xamu nu, ndaxte xamu ko woon, moom itam. 2 Samay soppe, léegi doomi Yàlla lanu, te li nu nar a nekki feeñagul, waaye xam nanu ne, bés bu Almasi bi feeñee, dinanu nirook moom, ndaxte dinanu ko gis, na mu mel. 3 Te képp ku am yaakaar jooju ci moom, dinga sellal sa bopp, ni mu selle moom. 4 Ku def bàkkaar, jàdd nga yoon; ndaxte bàkkaar mooy jàdd yoon. 5 Te xam ngeen ne Yeesu Kirist feeñ na, ngir dindi bàkkaar yi, te moom amul benn bàkkaar. 6 Képp ku sax ci moom, doo sax ci bàkkaar; kuy def bàkkaar, gisuloo ko te xamuloo ko. 7 Samay doom, bu leen kenn nax! Kuy def lu jub, ku jub nga, ni Kirist jube moom ci boppam. 8 Kuy def bàkkaar, ci Seytaane nga bokk, ndax Seytaane ca njàlbéen ga ba tey day bàkkaar. Te Doomu Yàlla ji ñëw na, ngir nasaxal jëfi Seytaane. 9 Ku juddu ci Yàlla doo def bàkkaar, ndax Yàlla sol na la jikkoom, te doo man a sax ci bàkkaar, ndax juddu nga ci Yàlla. 10 Lii mooy ràññale doomi Yàlla ak doomi Seytaane: képp ku dul def lu jub bokkoo ci Yàlla; naka noonu itam ku soppul sa mbokk bokkoo ci Yàlla. 11 Ndaxte xebaar, bi ngeen déggoon ca ndoorte la, mooy lii: nanu bëggante, 12 te bañ a mel ni Kayin, mi bokkoon ci Ibliis, ba rey rakkam. Lu tax mu rey ko nag? Ndaxte ay jëfam dañoo bon, te yu rakkam jub. 13 Bokk yi, bu leen àddina bañee, buleen ci jaaxle. 14 Mbëggeel gi nu bëgg sunuy bokk moo nuy xamal ne, jóge nanu ci dee, tàbbi ci dund. Ku bëggul sa mbokk, yaa ngi ci dee ba tey. 15 Képp ku bañ sa mbokk, reykat nga; te xam ngeen ne, ku rey nit amuloo dund gu dul jeex. 16 Ci lii lanuy xàmmee luy mbëggeel: Kirist joxe na bakkanam ngir nun; te nun itam war nanoo joxe sunu bakkan ngir sunuy bokk. 17 Waaye ku am alalu àddina te gis sa mbokk nekk ci soxla, nga dummóoyu ko, nan la mbëggeelu Yàlla dëkke ci yaw? 18 Samay doom, bunu bëggante ci wax mbaa ci làmmiñ rekk, waaye ci jëf ak ci dëgg. 19 Ci loolu lanu xame ne, nu ngi ci dëgg; te waxtu wu sunu xol di xeex ak nun, dinanu ko dalal ci kanamam; ndaxte Yàllaa ëpp sunu xol te xam na lépp. 19 Ci loolu lanu xame ne, nu ngi ci dëgg; te waxtu wu sunu xol di xeex ak nun, dinanu ko dalal ci kanamam; ndaxte Yàllaa ëpp sunu xol te xam na lépp. 21 Samay soppe, bu nu sunu xol daanul, kon man nanoo jege Yàlla ak kóolute. 22 Te lépp lu nu koy ñaan, dinanu ko jot ci moom, ndaxte nu ngi sàmm ay ndigalam, di def lu ko neex. 23 Ndigalam mooy lii: nu gëm turu Doomam, Yeesu Kirist, tey bëggante, ni mu nu ko digale. 24 Kuy sàmm ndigalu Yàlla, dinga sax ci moom, mu dëkk ci yaw. Te Xel mi mu nu jox, moo nuy xamal ne, dëkk na ci nun. 1 John 4 1 Samay soppe, buleen gëm xel mu nekk, waaye nattuleen xel yi, ba xam ndax ci Yàlla lañu jóge walla déet, ndaxte naaféq yu bare yu mbubboo turu yonent jóg nañu, tasaaroo ci àddina si. 2 Ci lii lanu xàmmee Xelum Yàlla: mépp xel mu nangu ne, Yeesu Kirist ñëw na, nekk nit, ci Yàlla la bokk. 3 Waaye mépp xel mu nanguwul Yeesu, bokkul ci Yàlla. Xel moomu mooy xelum Bañaaleb Kirist, mi ngeen déggoon ne dina ñëw, te léegi sax mu ngi ci biir àddina. 4 Yéen samay doom, ci Yàlla ngeen bokk, te daan ngeen yonent yu naaféq yooyu, ndaxte Ki nekk ci yéen moo ëpp doole ki nekk ci àddina. 5 Ñoom ci àddina lañu bokk; moo tax ñuy wax waxi àddina, te àddina di leen déglu. 6 Nun nag ci Yàlla lanu bokk. Ku xam Yàlla dinga nu déglu; ku bokkul ci Yàlla doo nu déglu. Ci loolu lanuy xàmmee Xel miy dëgg ak xel mi dul dëgg. 7 Samay soppe, nanu bëggante, ndax mbëggeel ci Yàlla la bawoo; képp ku bëgg sa mbokk nag, ci Yàlla nga juddoo, te xam nga Yàlla. 8 Ku bëggul sa mbokk, xamuloo Yàlla, ndax Yàlla mbëggeel la. 9 Nii la Yàlla wonee mbëggeelam ci nun; yónni na ci àddina jenn Doomam ji mu am kepp, ngir nu am dund ci moom. 10 Lii mooy mbëggeel, du sunu mbëggeel ci Yàlla, waaye mbëggeelam ci nun, ba mu yónni Doomam, mu joxe bakkanam, ngir dindi sunuy bàkkaar. 11 Samay soppe, bu nu Yàlla bëggee nii, nun itam war nanoo bëggante. 12 Kenn musul a gis Yàlla, waaye bu nu bëggantee, Yàllaa ngi dëkk ci nun te mbëggeelam mat na sëkk ci nun. 13 Ci lii lanuy xame ne, sax nanu ci Yàlla, te moom itam dëkk na ci nun: sol na nu Xelam. 14 Te nun gis nanu te seede ne, Baay bi yónni na Doom ji, mu nekk Musalkatu àddina. 15 Képp ku nangu ne, Yeesu Doomu Yàlla la, Yàlla dëkk na ci yaw, te yaw it sax nga ci Yàlla. 16 Mbëggeel gi Yàlla am ci nun, xam nanu ko te gëm ko. Yàlla mbëggeel la, te képp ku sax ci mbëggeel, yaa ngi sax ci Yàlla, mu dëkk ci yaw. 17 Ni Kirist mel, noonu lanu mel nun itam ci àddina. Ci loolu la mbëggeel mate sëkk ci nun, ngir nu am kóolute bésu àtte ba. 18 Genn ragal amul ci mbëggeel, waaye mbëggeel gu mat sëkk day dàq ragal. Ndaxte ragal day ànd ak mbugal; te ku ragal, mbëggeel matul sëkk ci yaw. 19 Danuy wéy ci mbëggeel, ndax moo nu jëkk a bëgg. 20 Su kenn nee: «Bëgg naa Yàlla,» te bëgguloo sa mbokk, dangay fen; ndaxte ku bëggul sa mbokk mi ngay gis, doo man a bëgg Yàlla mi nga gisul. 21 Te jox na nu ndigal lii: ku bëgg Yàlla, nga bëgg sa mbokk. 1 John 5 1 Képp ku gëm ne Yeesu mooy Almasi bi, juddu nga ci Yàlla; te ku bëgg waajur, dinga bëgg itam ki mu jur. 2 Xam nanu ne, bëgg nanu doomi Yàlla yi ci lii: bëgg Yàlla tey sàmm ay ndigalam. 3 Ndaxte mbëggeel ci Yàlla mooy sàmm ay ndigalam; te ay ndigalam diisuñu. 4 Ndaxte képp ku juddu ci Yàlla day noot àddina; te li nuy noote àddina mooy sunu ngëm. 5 Ku noot àddina mooy kan? Mooy ki gëm ne, Yeesu mooy Doomu Yàlla. 6 Yeesu Kirist mooy ki ñëw, jaar ci ndox ak deret; du ci ndox rekk, waaye ndox ak deret. Te Xelu Yàlla mi moo koy seedeel, ndax Xel mi mooy dëgg. 7 Ndaxte am na ñetti seede: 8 Xel mi, ndox ak deret, te ñoom ñett ñépp, ñoo bokk benn baat. 9 Seedes nit, dinanu ko nangu, waaye seedes Yàlla moo gën a wóor, ndax boobu seede mooy li Yàlla seede ci Doomam. 10 Ku gëm Doomu Yàlla ji, am nga seede boobu ci sa xol. Ku gëmul Yàlla, teg nga ko kuy tebbi waxam ndaxte gëmuloo li Yàlla seede ci Doomam. 11 Te seede si mooy lii: Yàlla jox na nu dund gu dul jeex, te dund googoo ngi ci Doomam. 12 Ku am Doom ji, am nga dund; ku amul Doomu Yàlla, amuloo dund. 13 Maa ngi leen di bind yëf yii, yéen ñi gëm turu Doomu Yàlla ji, ngir ngeen xam ne, am ngeen dund gu dul jeex. 14 Kóolute gi nu am ci kanam Yàlla mooy lii, su nu ko ñaanee dara ci coobareem, dina nu nangul. 15 Gannaaw xam nañu ne, dina nangu lépp lu nu koy ñaan, xam nanu it ne, li nu ko ñaan, jox na nu ko. 16 Ku gis mbokkam, muy def bàkkaar bu jarul dee, na ko ñaanal, te Yàlla dina ko may dund. Ku def bàkkaar bu jarul dee laa wax. Ndaxte am na bàkkaar bu jar dee; boobu taxul may wax, mu ñaanal ko. 17 Gépp jubadi bàkkaar la, waaye am na bàkkaar bu jarul dee. 18 Xam nanu ne, képp ku juddu ci Yàlla doo sax ci bàkkaar, waaye Doomu Yàlla ji mooy wottu sa bakkan, ba Ibliis du la manal dara. 19 Nun nag xam nanu ne, nu ngi ci Yàlla, te àddina sépp a ngi tëdd ci loxoy Ibliis. 20 Xam nanu ne, Doomu Yàlla ji ñëw na te may na nu xel, ba nu man a xam Aji Wóor ji. Te nu ngi ci Aji Wóor ji ak ci Doomam Yeesu Kirist. Kooku mooy Yàlla ju wóor, ji yor dund gu dul jeex. 21 Samay doom, wottuleen seen bopp ciy xërëm. 2 John 1 1 Man njiit li maa leen di bind, yaw soxna su tedd si, yaw ak say doom. Bëgg naa leen bu wér ci sama xol, jéllale naa sama bopp sax, waaye itam képp ku xam dëgg gi. 2 Te dëgg gee tax nuy def noonu, dëgg gi dëkk ci nun, tey ànd ak nun ba fàww. 3 Yàlla Baay bi ak Yeesu Krist, Doomu Baay bi, dinañu nu may yiw, yërmande ak jàmm, ànd ak dëgg ak mbëggeel. 4 Gis naa ci say doom, ñuy jaar ci tànki dëgg, ni nu ko Baay bi digale, te bég naa ci lool. 5 Léegi nag soxna si, maa ngi lay dénk lii: nun ñépp nanu bëggante, te loolu du dénkaane bu bees, waaye moom lanu jotoon ca njàlbéen ga. 6 Lii mooy mbëggeel: nu wéer sunug dund ci ndigali Yàlla; loolu mooy ndigalam, la nu jotoon ca njàlbeen ga, te ci lanu wara jaar. 7 Maa ngi wax loolu nag, ndaxte am na ñuy sànke ñu bare, ñu tasaaroo ci àddina si, te nanguwuñu ne Yeesu Krist wàcc na, nekk nit. Kooku aji sànke la, di Bañaaleb Krist. 8 Kon moytuleen, ngir baña ñàkk seen añub coono, waaye ngeen am yool bu mat sëkk. 9 Képp ku saxul ci dénkaaney Krist, xanaa di ko weesu, bokkul ci Yàlla; ku sax ci dénkaane yi, bokk nga ak Baay bi ak Doom ji. 10 Ku ñëw fi yaw, te indaalewul dénkaane yooyu, waxuma nga bañ koo teeru rekk, waaye bu ko nuyu sax. 11 Ku ko nuyu, bokk nga ciy ñaawteefam. 12 Bëggoon naa leena wax lu bare ci bataaxel bii, waaye lépp xajul ci kayit. Kon nag fas naa yéenee ñëw, ba jàkkaarlook yeen, nu waxtaan ci, ngir sunu mbég mat sëkk. 13 Say doomi rakk, ji Yàlla tànn, ñu ngi lay nuyu. 3 John 1 1 Man njiit li, maa ngi lay bind, yaw sama xarit Gayus, mi ma bëgg ci sama xol. 2 Sama soppe, maa ngi ñaan, Yàlla may la jàmm ci lépp, ànd ak wér gi yaram, ju mel ni sa naataangeg xol. 3 Sunuy mbokk ñëw nañu, te seede ni nga fonke dëgg gi, ba wéer ci sa dund gépp, te bég naa ci lool. 4 Awma mbég mu ëpp lii: ma dégg ne samay doomi diine ñu ngiy jaar ci tànki dëgg. 5 Yaw sama xarit, sa takkute fés na ci teeru bi ngay teeru mbokk yi, te fekk xamoo leen. 6 Seedeel nañu sa mbëggeel fi kanam mbooloom ñi gëm. Taxawu leen nag ci seen yoon taxawu gu neex Yàlla. 7 Ndaxte turu Krist la leen taxa jóg, te sàkkuwuñu daray ku gëmul. 8 Nun nag fàww nu teeru ñu mel ni ñoom, ngir nu liggéeyandoo ak dëgg gi. 9 Bind naa mbooloo mi bataaxel, waaye Jotref, mi bëgg noot ñépp, du dégg sunu ndigal. 10 Kon nag su ma ñëwee, dinaa fàttali li mu def lépp, ci di nu sosal ci kàdduy neen yu ñaaw. Yemu foofu sax, waaye nanguwula teeru mbokk yi, rax-ca-dolli ku leen bëgga teeru, mu gàllankoor ko, dàq ko ci mbooloo mi. 11 Sama xarit, bul roy lu bon, waaye lu baax rekk. Kuy def lu baax, ci Yàlla nga bokk; kuy def lu bon, xamoo dara ci Yàlla. 12 Naka Démétrius nag, ñépp seedeel nañu ko lu baax, te dëgg gi sax seedeel na ko ko. Nun itam seedeel nanu ko te wóor na ma ne, sunu seede dëgg la. 13 Am na lu bare, lu ma la bëggoona wax, waaye lépp xajul ci kayit. 14 Kon yaakaar naa laa seetsi balaa yàgg, jàkkaarlook yaw, nu waxtaan ci. 15 Na jàmm ànd ak yaw. Xarit yi yépp ñu ngi lay nuyu. Nuyul nu sunuy xarit, kenn ku nekk ci turam. http://www.jesus-army.com/cgi-bin/bible/bible.cgi?BIBLE=Wolof+NT&BOOK=6 2&SEARCH=++&CASE=ON&HILITE=ON&FIRST=OK&R1=I&CHAP=1&SUBMIT=Read Postado por DAIANE FIRME CAVALCANTE às 12:41 Enviar por e-mailBlogThis!Compartilhar no TwitterCompartilhar no FacebookCompartilhar com o Pinterest Nenhum comentário: Postar um comentário Postagem mais recente Postagem mais antiga Página inicial Assinar: Postar comentários (Atom) REDE MISSIONÁRIA femissionaria.blogspot.com.br Arquivo do blog * ► 2015 (181) + ► Janeiro (181) * ▼ 2014 (5024) + ► Dezembro (408) + ► Novembro (255) + ► Outubro (294) + ► Setembro (324) + ► Agosto (356) + ► Julho (520) + ▼ Junho (495) o Galasikaw (Bambara: Mali) o QUE É A OBRA DE GANHAR ALMAS? o POR QUE ELE FOI CRUCIFICADO? o Joyce Meyer in Urdu: Part 02 o Joyce Meyer in Urdu: Part 01 o READING ACTS OF THE APOTLES (KING JAMES VERSION) o Юхан 3 (United Arab Emirates) o Paz em meio aos momentos mais difíceis o Provérbios: Saiba A Hora Certa de Falar o RESISTE À ANSIEDADE: FRANCES J. ROBERTS o VAMOS ORAR: GÂMBIA o Thì-tô (China:Fujian) o 1, 2, 3 যোহন (Bengali) o So Woate Honhom Mu Mmara Anan No? (Akuapim Twi/Eng... o A ORAÇÃO DE UM MENINO o History of the Reformation: Of the Sixteenth Centu... o History of the Reformation: Of the Sixteenth Centu... o KAREN/ENGLISH: 4 SPIRITUAL LAWS o READING ACTS OF THE APOSTLES (KING JAMES VERSION) o 2 TIMOTI (PAPUA NEW GUINEA) o Provérbios: Pense Antes de Falar o O ÓLEO DA CONSAGRAÇÃO: FRANCES J. ROBERTS o VAMOS ORAR: INDONÉSIA o A MÉLYEBB KERESZTÉNY ÉLET: Andrew Murray o A VILÁG SZEMETJE: OSWALD CHAMBERS o 2 TESALONAIKA (PAPUA NEW GUINEA) o A GRAÇA DE DEUS: JOHN WESLEY o UMA CONVERSÃO NOTÁVEL o Не навреди o 1 TESALONAIKA (PAPUA NEW GUINEA) o Provérbios: Não Seja Tolo No Falar o HÁ SEMPRE UMA ALTERNATIVA: FRANCES J. ROBERTS o VAMOS ORAR: MUNDO MUÇULMANO o CRISTÃOS PERSEGUIDOS DA ÁSIA CENTRAL o Яқып (Uzbekistan) o Pedido de oração urgente o JUT (PAPUA NEW GUINEA) o AUXILIANDO OS NECESSITADOS o NAŠA BRIŽNA NEVJERA: OSWALD CHAMBERS o Joyce Meyer: Mentális egészség o JEMS (PAPUA NEW GUINEA) o Provérbios: Não Seja Irado o ISTEN UTÁNI VÁGY: A. W. TOZER o TRISTEZAS EPIRITUAIS CONTRA AS CARNAIS: FRANCES J.... o VAMOS ORAR: NEPAL o KENNETH E. HAGIN: Hitünk tápláléka napi adagokban o Derek Prince: A megbocsátás o Nicky Cruz: Repülj kicsim, repülj! o O que quer dizer a santificação? Oswald J. Smith o TAITUS (PAPUA NEW GUINEA) o UM LUGAR PARA A CRUZ o READING ACTS OF THE APOSTLES (KING JAMES VERSION) o GALESIA (PAPUA NEW GUINEA) o Provérbios: Seja sábio o RECONHECE A MINHA MÃO: Frances J. Roberts o VAMOS ORAR: OMÃ o Brød i Ørkenen af Watchman Nee! o FILIPAI (PAPUA NEW GUINEA) o A CRUZ: STEPHEN KAUNG o OUVINDO A VOZ DE DEUS o Putere prin rugăciune: Edward McKendree Bounds o GRAÇA E PAZ SEJAM MULTIPLICADAS: JOYCE MEYER o 2 PITA (PAPUA NEW GUINEA) o Provérbios: Não ande com os maus o 1 PITA (Papua New Guinea) o SOMENTE UMA PESSOA: FRANCES J. ROBERTS o VAMOS ORAR: MAURITÂNIA o A Palavra de Deus e o Espírito de Deus: WATCHMAN N... o KOLOSI (PAPUA NEW GUINEA) o 1, 2, 3 JON (PAPUA NEW GUINEA) o A VONTADE DE DEUS NO CORAÇÃO o GALATIANS (NEPAL) o JOHN 3 (NEPAL) o Estudo bíblico: A sabedoria do alto o 1, 2, 3 John (Nepali) o Não Permaneça Irado: Joyce Meyer o VAMOS ORAR: VIETNÃ o OBRIGADO PELO SEU EXCELENTE SERVIÇO! o 1, 2, 3 Ýahýa (TURKMENISTAN) o CRISTO NÃO RECUSA NINGUÉM o O PODER LIBERTADOR DE JESUS o Estudo bíblico: Ó insensatos Gálatas! o Confie em Deus e não tema: Joyce Meyer o UMA INJEÇÃO DE VIDA NOVA: FRANCES J. ROBERTS o VAMOS ORAR: ARGÉLIA o GOOD NEWS (Chuwabo) o Kolosensów (Polish) o A CORAGEM DE MOFFATT o TOBIE, NAJWYŻSZY: Oswald Chambers (Styczeń) o Colossians (Albanian) o 139 cristãos indígenas deixam suas casas para não ... o PAI NOSSO, QUE ESTÁS NOS CÉUS: O SIGNIFICADO o Philippians (ALBANIAN) o MISSÕES DIFÍCEIS : FRANCES J. ROBERTS o VAMOS ORAR: IRAQUE o GALATIANS (KANNADA) o O EXÉRCITO DE DEUS o HEALING RAIN: MICHAEL W. SMITH o 1, 2, 3 John (Welsh) o JAMES (SOMALI) o LUKE CHAPTER 15 (SYRIAC) o JOHN 3 (Shqip) o Ar išeisi, nežinodamas kur? (Oswald Chambers) o Pašaukimas ir jo pasekmės: Oswald Chambers o Galatians (Pyhä Raamattu) o Galatians (Paite) o Philippians (MAORI) o 1, 2, 3 JOHN (Kekchi) o TITUS (DARI) o JOHN 3 (Breton: Gospels) o ESTUDO BÍBLICO: O Método ou a Maneira da Oração o 1, 2, 3 JOHN (BASQUE) o O ARREPENDIMENTO ATIVA A MINHA GRAÇA: FRANCES J. R... o VAMOS ORAR: BRUNEI o 1, 2, 3 JOHN (SOMALI) o PSALM 1 (LITHUANIAN) o Ljubav je odgovor: Theodore Epp o OBNOVLJENJE UMA: Watchman Nee o RIOS DO ESPÍRITO o TOTUL PENTRU GLORIA LUI: OSWALD CHAMBERS (MARTIE)... o CONFORTO PARA A ALMA o TOTUL PENTRU GLORIA LUI: OSWALD CHAMBERS (AUGUST) o TOTUL PENTRU GLORIA LUI: Oswald Chambers ( APRILI... o Condiøiile pentru a fi autoritate reprezentativå (... o TOTUL PENTRU GLORIA LUI: Oswald Chambers (IUNIE) o Scopul rugăciunii: E. M. BOUNDS o Prima zi (ANDREW MURRAY) o GÂNDIREA (OSWALD CHAMBERS) o Ascultarea: locul ei în Sfânta Scripturæ: ANDREW M... o JOHN 3:16 (UMA) o Scottish Gaelic Bible (Gospel of Mark) o JOHN 3 (MAORI) o JOHN 3 (ZARMA): NIGER o JOHN 3 (TAMAJAQ 3): NIGER o READING 1 TIMOTHY (KING JAMES VERSION) o JOHN 3 (BURKINA) o LUKE CHAPTER 15 (BURKINA) o LUKE CHAPTER 15 (DIOULA) o Fulfulde (Ajamiya): JOHN 3:16 o ESTUDO BÍBLICO: Os Objetos da Oração – A Quem Deve... o JOHN 3:16 (COPTIC) o JOHN 3:16 (CHAMORRO) o IOANNEN (BASQUE: NAVARRO) o OLHA PROFUNDAMENTE: FRANCES J. ROBERTS o VAMOS ORAR: SENEGAL o Филиппой (MONGOLIA) o Nigéria: A PERSEGUIÇÃO o ELJUTOTTÁL-E MÁR A "MIUTÁN"-HOZ?: OSWALD CHAMBERS o AJUDANDO A DOBRAR A ESQUINA o Krisztus mindenek felett: Oswald Chambers (Szeptem... o Cristos si Biserica Sa: STEPHEN KAUNG o AZ EN OROMEM ... A TI OROMETEK (OSWALD CHAMBERS) o ÉBERSÉG VAGY KÉPMUTATÁS BENNÜNK /URUNK MEGLEPETÉSS... o AZ Ő HALÁLTUSÁJA ÉS A MI TANÍTVÁNYSÁGUNK : OSWALD ... o Philippians (WOLOF: SENEGAL) o HUNGARIAN MESSAGE: OSWALD CHAMBERS o Mit tegyünk ilyen körülmények között?: OSWALD CHAM... o OSWALD CHAMBERS (HUNGARIAN) o Oswald Chambers: Hungarian o OSWALD CHAMBERS MESSAGE (HUNGARIAN) o TELJESSÉG: OSWALD CHAMBERS o A SZENVEDÉLYES ODAADÁS SZOLGÁLATA: OSWALD CHAMBERS... o CASA DE ORAÇÃO EM APARECIDA DO TABOADO-MS o ESTUDO BÍBLICO: A POSSIBILIDADE DA ORAÇÃO o Vita eterna insieme con Cristo: Oswald Chambers o SAI SCENDERE DAL MONTE?: OSWALD CHAMBERS o CHE COSA C’E’ DOPO IL SILENZIO DI DIO? o YOWAANA (SENEGAL) o Të përqendrohemi vetëm në një pikë (1 janar): Oswa... o FELICITÀ ATTRAVERSO LA MISERICORDIA: BILLY GRAHAM o CONSAGRA-TE: FRANCES J. ROBERTS o EFISIA (FIJI) o VAMOS ORAR: SRI LANKA o O VALOR DA INTERCESSÃO: ANDREW MURRAY o L’ABITUDINE DI RALLEGRARSI DELLE COSE SPIACEVOLI: ... o Usuke Wezwa Yini Ngamaqiniso Amane Okomoya Na? ZUL... o Junakw Sha Kusikia Juu Ya... Mambo Makubwa Mane Ki... o YORUBA/ ENGLISH: 4 SPIRITUAL LAWS o Ukhe Weva Na Ngeenyaniso Ezine Zomoya? XHOSA/ ENGL... o Ke a kan fak nkhang navk naai nang Atyuhishi na n-... o SIGNORIA SUL CREDENTE: OSWALD CHAMBERS o "COM JESUS" o UNA VITA GRANDE: OSWALD CHAMBERS o NON FARE I TUOI CALCOLI IGNORANDO DIO: OSWALD CHAM... o Partecipi della grazia: OSWALD CHAMBERS o Galeshia (FIJI) o DIE DISSIPLINE VAN LUISTER.: OSWALD CHAMBERS o IL DISCERNIMENTO DELLA FEDE: OSWALD CHAMBERS o Esaurimento spirituale: OSWALD CHAMBERS o O TEMPERAMENTO SEM CRÍTICA: OSWALD CHAMBERS o Tobie Najwyższy: Oswald Chambers (CZERWCA) o LA DISCIPLINA DELLA DIFFICOLTÀ: OSWALD CHAMBERS o Visione e verità: OSWALD CHAMBERS o TURKISH/ ENGLISH: ARE YOU WANTING TO KNOW GOD PERS... o LA PUISSANCE D'EN HAUT: Charles Finney o Xana Utwile Hita Milawu Ya Mune Ya Moya Ke? (TSONG... o Kuó ke fanongo 'i he makatu 'unga 'e fâ 'o e mo 'u... o ESTUDO BÍBLICO: A NATUREZA DA ORAÇÃO o Inalterabile amore: Oswald Chambers o INCLINAZIONE ALLA RIGENERAZIONE (OSWALD CHAMBERS) o QUELLI CHE SPERANO: OSWALD CHAMBERS o KARATIA (KIRIBATI) o O TANQUE DA CURA: FRANCES J. ROBERTS o VAMOS ORAR: SÍRIA o STEPS TO PEACE WITH GOD (BILLY GRAHAM) o GALATIANS (DARI:Afghanistan AFGHANISTAN) o TIGRENYA/ ENGLISH: HOW TO KNOW GOD PERSONALLY o A LEI DO PERDÃO (T. E. TENNEY e TOMMY TENNEY) o THAI/ ENGLISH: 4 SPIRITUAL LAWS o TAMIL/ ENGLISH: 4 SPIRITUAL LAWS o ECOS DA ESCOLA DOMINICAL (IV) o Narinig mo na ba ang Apat na Tuntuning Espiritwal?... o SKULLE DU VILJA LÄRA KÄNNA GUD PERSONLIGEN (SWEDIS... o Je, Umesikia Juu Ya... Kanuni Nne Za Kiroho? (SWAH... o Conoces las Cuatro Leyes Espirituales? (LATIN AMER... o Conoces las Cuatro Leyes Espirituales? (SPANISH/ E... o Wati Wambonzwa Here Nezvemirao Mina Yomweya? (SHON... o Galasya (ALGERIA) o Yuḥenna (ALGERIA) o 1, 2, 3 Yuḥenna (ALGERIA) o READING THESSALONIANS (KING JAMES VERSION) o ESTUDO BÍBLICO: A IMPORTÂNCIA DA ORAÇÃO o A O Kile Wa Utlwa... Ka Ditselana Tse Nne Tsa Semo... o SERBIAN/ENGLISH: 4 SPIRITUAL LAWS o A keni dëgjuar për Katër Ligjet Shpirtërore? (ALBA... o NÃO INÉRCIA, MAS SUBMISSÃO: FRANCES J. ROBERTS o VAMOS ORAR: LAOS o Passagens Difíceis na Vereda da Fé: Albert Benjami... o RUSSIAN/ENGLISH: 4 SPIRITUAL LAWS o ROMANIAN/ ENGLISH: 4 SPIRITUAL LAWS o PRODIGAL SON: (LAOS) o 1, 2, 3 uJohane (NDEBELE) o uLuka 15 (NDEBELE) o JÁ OVIU FALAR DAS QUATRO LEIS ESPIRITUAIS? [PORTUG... o CZY SLYZALES O CZTERECH PRAWACH DUCHOWEGO ZYCIA? (... o A O Kwele Ka Melao E Mene Ya Moya? (PEDI/ ENGLISH)... o NEPALI/ ENGLISH: 4 SPIRITUAL LAWS o PEDINDO A BÊNÇÃO DE DEUS o Inye'do Nyeri Ta Ota Se Su Oriro Tori Si Tana Ndiy... o MONGOLIAN/ ENGLISH: 4 SPIRITUAL LAWS o CROATIAN/ ENGLISH: 4 SPIRITUAL LAWS o MACEDONIAN/ENGLISH: 4 SPIRITUAL LAWS o Efa Renao Ve Ireo Zava-dehibe Efatra Momba Ny Fiai... o Bende Isewinjo Kuom Chike Ang'wen Mag Chuny? (LUO/... o Abaefeso (EKEGUSII: KENYA) o LUBAKAONDE (KAONDE)/ ENGLISH: 4 SPIRITUAL LAWS o ARABIC (LEBANESE)/ENGLISH: 4 SPIRITUAL LAWS o LATVIAN/ENGLISH: 4 SPIRITUAL LAWS o Wali owulidde ku nsonga enkulu ennya? (LUGANDAN/ E... o KOREAN/ ENGLISH: 4 SPIRITUAL LAWS o Mbese hari ubwo wumvise... Amagambo ane y'ingenzi ... o Moje najbolje za Njegovu preuzvišenost: Oswald Cha... o ESTUDO BÍBLICO: GUARDA O TEU CORAÇÃO o Галат (MONGOLIAN) o A FÉ SE MANIFESTA NA RESPOSTA DIVINA: FRANCES J. R... o VAMOS ORAR: IRÃ o Иаков (MONGOLIAN) o Молитва веры (ALBERT BENJAMIN SIMPSON) o Дуулал 1 (MONGOLIAN) o Minha História – Prisão e Resgate: H. C. Morrison... o WAAI W'A MA UNDU ANA MANENE MA K I VEVA? (KAMBA/EN... o Tos Kiigas Agobo Ng'atutik Ang'wan Che Bo Sobet? (... o CRISTO É MEU o Лук 15 (MONGOLIA) o Иохан 3 (MONGOLIA) o Галат (MONGOLIA) o 1, 2, 3 Иохан (MONGOLIA) o JAPANESE/ ENGLISH: 4 SPIRITUAL LAWS o INDONESIAN/ ENGLISH: 4 SPIRITUAL LAWS o Nangegmo Kadin Dagiti Uppat A Naespirituan Nga Lin... o JOHN 3 (PASHTO: PAKISTAN) o GOSPEL OF MATTHEW (PAKISTAN) o I NUWO IHE BAYERE IWU ano nke imemo? (IBO/ ENGLISH... o Ko Ka Taba Jin Labarian Ka'idodi Hudu Na Ruhaniya?... o Ha személyesen megismerhetnéd Istent, érdekelne-e?... o KNOWING GOD PERSONALLY (GREEK/ ENGLISH) o GERMAN/ENGLISH: 4 SPIRITUAL LAWS o CONNAîTRE DIEU PERSONNELLEMENT (FRENCH/ENGLISH) o Jumala rakastaa sinua. Neljä tosiasiaa (FINNISH/ E... o O Sa Bau Rogoca Li Na Lawa E Va Ni Bula Vakayalo? ... o O EGOÍSMO HUMANO: PARTE V o FARSI/ENGLISH: 4 SPIRITUAL LAWS o Рим (Uzbekistan) o ESTONIAN/ENGLISH: 4 SPIRITUAL LAWS o Cristãos malaios são refugiados em seu próprio paí... o O OBJETIVO CENTRAL: FRANCES J. ROBERTS o VAMOS ORAR: CHINA o Галатия (Uzbekistan) o Колоса (Uzbekistan) o O Poder de Uma Vontade Rendida: R. A. Torrey o "Meu Mestre Sempre Está." o DRŽIMO SE CILJA: Oswald Chambers o Inee Kwana Koigwa Amachiko Ane Aye Ekemoika? (Ekeg... o Dutch/ English: 4 Spiritual Laws o Nakadungog Ka Na Ba Sa Upat Ka Espirituhanong Lagd... o Cambodian/English: 4 Spiritual Laws o I Be I Ni Ala Ce Temen Sira Nnaani Don Wa? (Bambar... o ARABIC (CLASSICAL)/ ENGLISH: 4 SPIRITUAL LAWS o ALBANIAN/ ENGLISH: 4 SPIRITUAL LAWS o Afrikaans/ English: 4 Spiritual Laws o Chemaøi la ucenicie μi Råscumpårarea voastrå se ap... o READING EPHESIANS (KING JAMES VERSION) o TABIB AGUNG (Oswald Chambers) o Елшилер (UZBEKISTAN) o O EGOÍSMO HUMANO: PARTE IV o REVESTIDO DE LUZ: FRANCES J. ROBERTS o VAMOS ORAR: ARGÉLIA o Mezmur 1 (Turkish) o Vigie… Permaneça Firme… Fortifique-se: Horatius Bo... o Confissões Ministeriais: Horatius Bonar o Юхан (Uzbekistan) o Esperando e Vigiando o Oswald Chambers: Greek Devotional o Cine suntem noi? (Stephen Kaung) o 4 PRENSIP ESPIRITYEL YO? (HAITIAN: CREOLE) o JOHN 3 (CREOLE) o Лука (Uzbekistan) o O EGOÍSMO HUMANO: PARTE III o ଅଧ୍ୟାୟ 15 (Oriya) o JỌN CHAPTA 3 (Nigeria) o Jesu ke mang? (PEDI) o Apakah peristiwa-peristiwa penting dalam hidup Isa... o ESTOU EM TODA A PARTE: FRANCES J. ROBERTS o VAMOS ORAR: ÍNDIA o Moje najbolje za Njegovu preuzvišenost: Oswald Cha... o Марк (Uzbekistan) o READING 1, 2 PETER (KING JAMES VERSION) o A LIÇÃO DO FAROL o Hodati u ljubavi Henry Drummond (1856-1897) o Čovek kojeg Bog upotrebljava Oswald J. Smith o Cine suntem noi? Stephen Kaung o MATTA (UZBEKISTAN) o JOHN 3 (CROATIAN) o O EGOÍSMO HUMANO: PARTE II o VAMOS ORAR: BRASIL o Sveti Duh na delu Oswald J. Smith o Spasenje Božije Oswald J. Smith o PUT GOLGOTE ROY HESSION o De Weg van Golgotha Roy Hession o DROGA GOLGOTY Roy Hession o Cristo é minha bondade o DEUS GUIA O EVANGELISTA o O QUE JESUS DISSE DE SI MESMO o Coreia do Norte: ore enquanto a Coreia do Sul joga... o Igreja Perseguida na Copa: Argélia o Duhul de înøelepciune μi de descoperire: STEPHEN K... o GALATIANS (KOYA) o O EGOÍSMO HUMANO: PARTE I o JOHN 3 (PERSIAN) o A GRAÇA DE DEUS É AUMENTADA PELO TEU DESEJO: FRANC... o VAMOS ORAR: CATAR o Cine suntem noi? Stephen Kaung o 1, 2, 3 JOHN (ROMANIA) o INVOCAR A DEUS o Vivendo a Vida Que Agrada a Deus ( Hannah Whitall ... o O Poder do Sangue de Jesus (Andrew Murray) o "Porque a Bíblia diz assim." o 1, 2, 3 JOHN (WOLOF: GAMBIA) o CASA DE ORAÇÃO EM LIMEIRA DO OESTE-MG: O INÍCIO o NEOFITISMO: A SOBERBA DO CORAÇÃO o READING JAMES (KING JAMES VERSION) o READING COLOSSIANS (KING JAMES VERSION) o 1, 2, 3 JOHANU (YORUBA) o A QUEIXA É DESTRUIDORA: FRANCES J. ROBERTS o VAMOS ORAR: BUTÃO o Johanu 3 (Yoruba) o Luku 15 (Yoruba) o O SALTADOR o “O Espírito Santo Operou Poderosamente Em Nosso Me... o RADBANDETS VÄG - Lillian Ekstedt o ANDLIG STÅNDAKTIGHET: Oswald Chambers o PORVENTURA, SOIS CARNAIS?: ANDREW MURRAY (1828-191... o Đồng hành cùng Thánh Kinh: Oswald Chambers o A LEGKÖZELEBBI LEGJOBB TENNIVALÓ: OSWALD CHAMBERS o Bagalatia (Tanzania) o APOSTASIA: O ABANDONO DA FÉ o Vækkelsen vi behøver af Oswald J. Smith o A VIDA CRISTÃ MAIS ELEVADA: Frances J. Roberts o VAMOS ORAR: INDONESIA o Лука 15 (LUKE 15: QATAR) o 30 SECONDS OF HOPE: TBILISI, GEORGIA (WITH FRANKLI... o João 5:39 o 1, 2, 3 Иоанн o LUKA 15 (EKEGUSII: KENYA) o Abagalatia (Ekegusii: Kenya) o AS SETE LEIS DA ORAÇÃO: JESSE IRVIN OVERHOLTZER (1... o A DIREÇÃO DAS ESCRITURAS: ANDREW MURRAY (1828-1917... o READING JUDE (KING JAMES VERSION) o Galatiyawa (Hausa: Benin) o 1, 2, 3 Yuḥenna (Kabyle Bible: Algerian) o Ιωάννου (GREEK: κοινη) o Ana: Alcançando o favor de Deus o Tiago 2:14-26 o VAMOS ORAR: ÁSIA CENTRAL o Entregando-nos à oração o Fique com o Mundo mas dê-me Jesus o GOSPEL OF JOHN (JAVANESE: INDONESIA) o GOSPEL OF JOHN (East Timor) o 1, 2, 3 Johanisi (SARAMACCAN BIBLE: SURINAM) o ORANDO POR SEUS INIMIGOS o READING PHILEMON (KING JAMES VERSION) o FILEMOM: Aprendendo o valor da submissão o TODAS AS COISAS NOBRES SÃO DIFÍCEIS: OSWALD CHAMBE... o JOHN 3 (PATAMONA BIBLE: GUYANA) o 1 JOHN (PATAMONA BIBLE: GUYANA) o JUAN 3 (WAYUU: COLOMBIA) o 1, 2, 3 JUAN (TUYUCA: BRAZIL) o Santa Ceia do Senhor o JUAN (DESANO: BRAZIL) o VAMOS ORAR: TOGO o JOHN 3 (CHIN: MYANMAR) o RUTH'S BOOK (LAOS) o 1, 2, 3 JOHN (ARAMAIC) o ECOS DE S. S. III o GOSPEL OF JOHN (ARAMAIC o HUMILDADE: ALBERT BENJAMIN SIMPSON o GOSPEL OF JOHN (KHASI BIBLE: INDIA) o JOHN 3:16 (KHARIA: INDIA) o GOSPEL OF JOHN (SANTALI BIBLE: INDIA) o Začněte! OSWALD CHAMBERS o Galasikaw (BAMBARA) o YUHANA (BAMBARA) o LUKE CHAPTER 15 (AWADHI) o LHAGAO LAMA DAN THUPEH LIHO NAHET KHAH TAH EM? (AS... o "FOI POR MIM" o SÁBIO CONSELHO o DANIEL: FÉ E OUSADIA o Poslanica Galaćanima (Bosnia) o GENTILEZA FRANCES J. ROBERTS o VAMOS ORAR: PENÍNSULA ARÁBICA o Yoˇhaˬ 3 (CHINA: YUNNAN o YUHANNA 3 (CHINA: XINJIANG) o ACTS' BOOK (China: Guizhou) o DEUS DIZ ASSIM: OSWALD CHAMBERS o READING TITUS (KING JAMES VERSION) o 1, 2, 3 JOHN (HINDI) o Corajosa Ester o GOOD NEWS (NEPAL-BHUTAN) o FERRO E FOGO DIVINO: OSWALD J. SMITH o VAMOS ORAR: MALÁSIA o Yo^han (China: Mien) o Yok-hon (CHINA: FUJIAN) o 1, 2, 3 Yok-hon (CHINA: FUJIAN) o BUTÃO: UM PAÍS QUE NECESSITA SE RENDER A CRISTO o GOSPEL OF MARK (DZONGKHA: BHUTAN) o PERGUNTA DE UMA PEQUENA GAROTA o DAVI: REI, POETA E SACERDOTE o IOANE 3 (TAHITIAN: FRENCH POLYNESIA) o O DEUS QUE NUNCA FALHA OSWALD CHAMBERS o EN POS DE LO SUPREMO OSWALD CHAMBERS (JUNIO) o VAMOS ORAR: COSTA DO MARFIM o Abrace-o! Catherine Booth o O PUNHO DE SUAS MÃOS o LUCAS 15 (IGNACIANO: BOLIVIA) o Rute: Fidelidade ao servir o O SEGREDO DO SENHOR (Oswald Chambers) o TOUT, POUR QU'LL RÈGNE! OSWALD CHAMBERS (JUNI) o VAMOS ORAR: Bangladesh o PEQUENA JANE o GALATIANS (BISLAMA: VANUATU) o 1 Yoowaana (SABOAT: ETHIOPIA) o Yāākōbō (SABAOT: ETHIOPIA) o LUUKA 15 (SABAOT: ETHIOPIA) o Oswald Chambers Alt for ham (Juni) o READING GALATIANS (KING JAMES VERSION) o The Seven Laws of Prayer JESSE IRVIN OVERHOLTZER ... o Comfort of the Scriptures o เดินอย่างระวัง — Dave Branon (มานาประจำวัน) o Ostrożne postępowanie (Nasz Codzienny Chleb) o သတိႏွင့္ေလွ်ာက္လွမ္းျခင္း (Burmese) o PELO QUE VOCÊ ESTÁ OBCECADO? OSWALD CHAMBERS o 終わりからの見方 o Perhatikan Baik-Baik (Santapan Rohani) o Behutsam vorwärts (Unser Täglich Brot) o UNE CONDUITE PRUDENTE (Notre Pain Quotidien) o ¿Estás obsesionado por algo? Oswald Chambers o Quelle est la vision qui vous hante ? OSWALD CHAMB... o Moisés: Tirado das águas para liderar o VAMOS ORAR: TAJIQUISTÃO o El poder de la oración o KOLOSE (SAMOAN) o 1, 2 PETERU (SAMOAN) o “Não deixe ninguém mastigar o papai.” o O MACHADO QUE FLUTUOU o HELP FROM ABOVE: SERBIAN o HELP FROM ABOVE: SIERRA LEONE o Трудный вопрос: Oswald Chambers o TOTUL PENTRU GLORIA LUI de Oswald Chambers o EN MÄRKLIG FRÅGA Oswald Chambers o La pregunta asombrosa: OSWALD CHAMBERS o THE STAGGERING QUESTION: OSWALD CHAMBERS o A QUESTÃO ATORDOADORA OSWALD CHAMBERS o INTET ER UMULIGT FOR GUD Oswald Chambers o La question renversante Oswald Chambers o VAMOS ORAR: CHINA + ► Maio (420) + ► Abril (678) + ► Março (451) + ► Fevereiro (403) + ► Janeiro (420) * ► 2013 (625) + ► Dezembro (170) + ► Novembro (66) + ► Outubro (80) + ► Setembro (115) + ► Agosto (90) + ► Julho (83) + ► Junho (21) Quem sou eu Minha foto DAIANE FIRME CAVALCANTE Visualizar meu perfil completo Contador Live Traffic Stats Modelo Simple. Tecnologia do Blogger.