![]() |
![]() |
![]() |
![]() |
![]() |
![]() |
xam-xami cosaan ngir yokkute gi Làngug yëngu yi Weeru Nowàmbar ci atum 1998 Kër giy saytu yéenéek xam-xam Diiwaanu Afrik Bànk Monjaal
Nataal bii, R. Kiessling, GTZ, Eschborn moo ñu ko baaxe: Jigéeni réewum Mali yuy cuub ay ndimó di jëfandikóo xaralay "Bogolaa". XAAJ BI JËKK Lan mooy xam-xami cosaan ? Lu tax xam-xami cosaan yi am solo ? Lan lañ Nisër ci xam-xami cosaan yi ? Lan la liggéey bii juragum?
ÑAAREELU XAAJ BI - LAN MOOY XAM-XAMI COSAAN ?
ÑETTEELU XAAJ BI LANGUG YÉNGU YI BOOTAL YI Bootal 1 Bootal 2 kërale 2 kërale 3 kërale 4 kërale 5 ÑETTEELU XAAJ BI Jubbi bi ñeel lépp lu jëm ci xam-xami cosaan yi. XAAJ BI JËKK Lan mooy xam-xami cosaan ? pajum xob ak reen misaalu xam-xami cosaan la boo xam ne dafa mos di am solo ci nit ñi ak fu ñu mën di nekk di àdduna si. Li ñu ci jot a bind joxewul gi-gis boo xam ne ñépp a ci ànd, bokk nu ñu ko deggé. Terewul ba tey mu am ay màndarga yu bari yu leen wutaleeg yeneen xam-xam yi. Ni aada yeek waaso yi wuutée la xam-xami cosaan yi di wuutée. Ci xam-xami cosaan yi lañuy sukkandiku ba jàpp ni ñuy war a defe ci wàllu mbéy, wér-gi-yaram, caytum càkkéef yeek lépp lu nu mën di yéngu Xam-xami cosaan am nañu wàll ci ni nit ñi di doxale diseen digante, ni yeen yi di tëdde, li nit ñi war a séq ak aada yi. Li ëpp ci xam-xam yooyu de ñu leen di donn moo tax tënk leen nekk lu jafe. Gëstu gii dafa ciy joxe ay misaal, am xam-xami cosaan yu may wone seeni melo, boolewaale ci itam njàng mu am solo muy ci mën a jariñoo ci wàllug yokkute. Ci kow loolu lay joxe misaal yii : • Mbéyum xeetu ñebbe ju bees ca réewum Kolombi ak mum Ruwaanda. • Céddalem dund gu ñu démbaléewoon nit ñi ca Nepaal. • Dogu gu jigéeni Malikunda ci réewum Senegaal dogu di jële fi njongum jigéen. • Njoof gu ñuy njoof jigéen ju wasin ba noppeek liiram ci xeet wi tudd Ibo te dëkke réewum Niseryaa, añs. Lu tax xam-xami cosaan yi am solo ? Foo dem, ci xam-xami cosaan lañuy sukkandiku be lal pexe yu ñu faje jafe-jafe yi ñu jankonteel, rawatina ñi seen loxo jotul seen gannaaw. Xam-xami cosaan yi am nañu doole lool ci xam-xam yi mën a indig yokkute. Waaye liñ leen di jëfandikóo ci doxalin yi yokkute tax a jóg néew na lool. Jàng ay xam-xami cosaan, doore ko ci li nit ñi xam te ame ko, dina tax ñu gën a xam ni nit ñi dundé, su ko defee ñu gën a xam liñu war a def ba dimbale leen ndimbal gi ñu yelloo. Gannaaw loolu, am lu leer ci xam-xami cosaan yi mën naa tax ba nit ñi gën leen a faale. Rax ci dolli, fexe be lépp lu ñuy def méngook ni nit ñi di dunde, mën naa tax ba ndimbal gi yokkute tax a jóg ëpp fi njariñ te njariñ yooyu sax fi ba abbadan. Weccantey xam-xami cosaan ci askan wi walla diggantey askan mën naa gën a dimbale nit ñi ñu gën a xam li leen wutale ba gën a jox gëdda aada ci wàllu yakkute. Li ci ëppati solo nak moo di, def ci weccantey xam-xami cosaan ak seenug bokk ci sémbu ndimbal yi Bànk Monjaal ak ñi mu jàppool ngir indi yokkute, mën naa gën a wàññi ñàkk gi. - xam-xami cosaan ngir yokkute gi - yëngu yi ñu taxawal Lan lañ Nisër ci xam-xami cosaan yi Tas xabaar bi •Suuxat sàqum xam-xami cosaan yeek liñ ci mën a jànge. • Siiwal ay misaali xam-xami cosaan ci jumtukaay yu ñu bind ciy kayit walla cib masiin. Yombal weccantem xibaar ci diggante ñi nekk ci dëkk yi ci réew yu néew doole yi. • Ndimbal ci lu yokk mën-mëni nit ñi nekk ci dëkk yi ngir ñu bokk xam-xami cosaan yi. • Xam niñ war a def ba dugal xam-xami cosaan yi ci masinu ordinaatóor, tas leen ba ñu yegg ci nit ñi ci dëkk-dëkkaan yi. Lan la liggéey bii juragum? Bi ñu dooree làngug xam-xami cosaan yi ba léegi, li gën a fés ci liñ ci jëlé mooy : • Yékkéti sàqum xam-xami cosaan bu def lu toll ci ñeen-fukki misaal. • Sos yoonu "Enternet" buy joxey xabaar yu aju ci xam-xami cosaan yi. • Siiwal kayitu tasukaayu xibaar bi tudd "Mbind ci xam-xami cosaan yi" te ñu jaglee ko xam-xami cosaan yi. • Gëstu ci xam-xami cosaan yi. (seetal ci bootal 1 ngir xam li mu ëmb). ÑAAREELU XAAJ BI 1 - (1 ) Jàppóo gu dëggu ci diggante réew yi ngir weccantey xam-xam du mën a antu te doonul ne réew yi néew doole dañ cee dugal seen loxo, taxaw ci taxawaayu ñuy joxe ak di jëfandikóo xam-xam yi. Ndaje ma amoon Torontóo ci weeru SuweN bu atum 1997, fésaloon na ne dañoo war a sàkku xam-xami cosaan yi ngir ñoN al leen te di ci weccante. Bu yàggul, njiitug Bànk Monjaal ci woote gi mu fi wootewoon ngir nit ñi am gis-gis bu yaatu ci yokkute fésaloon na ne dafa laaj taxawaay buy sóorale fu mu mën di tollu askan yeek seeni xam-xam. Ci jamanog jàppóo ngir jumtukaay yu xarala yi ñuy jokkoo ci Afrik, la Bànk Monjaal nangoo jiité sémbu xam-xami cosaan yi ngir yokkute, ngir indi ci ndimbal guy tax ñu nangu ne xam-xami cosaan am na, di leen jëfandikóo te di leen weccante ci yoonuw yokkute gi. Jamano jooju nak, ci lañ amal gëstu gii. II./ - LAN MOOY XAM-XAMI COSAAN ? 2 - (3) Pajum xob ak reen misaal mu baax mu xam-xami cosaan moo xam ne foo dem ci àdduna si fekk ko fa. Li ñu bind ci xam-xami cosaan yi, joxe wul benni gis-gis bu ñépp déggóo. Bokk na ci li waral loolu wuute gi am ci li soxal bindkat yi dale ko ci ngëmu nit ñi ba ci pexey mbéy. Waaye, loolu terewul mu am cingis-gis ay melo yu ñu bokk. Melo yooyu feeñ nañu ci li ñaari kilifa bind ci xam-xami cosaan yi (seet ko ci néeg bii di ñëw). Yenn ci tekkini xam-xami cosaan. Xam-xami cosaan xam-xam yu cosaanoo fi ñu leen di jëfandikóo - foo dem fekk fa ay xam-xami cosaan yu fa fekk baax. xam-xami cosaan yi dañoo wuuteek xeeti xam-xam yi réew yépp dégóo te ñu leen di jànge ci daara yu kowe yi, gëstuwaay yeek yenn kër yi nga xam ne dañoo am ñu leen moomal seen bopp. Ci xam-xami cosaan yooyu lañu sukkandiku be nas pexe yi ñuy jëfandikóo ci wàllu mbéy, wèr-gi-yaram, togg, yar, caytum càkkéef yi, ak yeneeni mbir yu nit ñi bokk dëkk di yéngu. (waren 1991). Askan woo dem, xam-xami cosaan a lal lépp luñuy xamle. Xam-xami cosaan yeey yombal jokkoo beek li ñu fas yéenée def. Pexe cosaan yi nit ñi di jokkoo dañuy dox jamano ju ñëw ñu ànd ak moom Askan woo gis pexe yi ñu fay jëfandikóo dañuy dox, lu ñëw walla ni muy jokkook ñeneen dañuy am lu ñu ciy soppi.
3 - (6) Melo yi ñu fi jot a wax, wone nañu ne xam-xami cosaan yi dañoo bokk ci pexey yi mën a indi yokkute ci askan yi. Xalaat bi ñu amaloon ci jokkute ci àddinasi ci atum 1998 jàpp 1999, feeñal na ne xam-xam a mën a indi yokkute ci wàllu dundi doom-aadamaak koom-koom gu sax waaye du ay koppar. sukkandiku ci xam-xami cosaan yi nga xam ne ñoo lal xam-xam yi nit ñi jëfandikóo lañ war a jëkk a def bu ñu bëggée réew mu neKK jariñoo ay xam-xamam. Rax ci dolli, nit ñaa ngi gën a déggóo ci jàpp ne weccantey xam-xam dafa war a nekk yoon wu nit ñi di jëflantee. Tasaarem xam-xam, ci réew yi am doole rekk la xam-xam bi di bawoo jëm ci reéw yu néew doole yi du mën antu te dina am ñu yaakaar ne dañu leen xeeb. "Nguur yeek kuréel yi réew yi séq war nañu mën a dimbale reéw yi ci yéngu yi jublu gëstug ni yeneen réew yi di fefe ngir mën a ràññee xam-xam yi leen gën a jubu, jëfandikóo leen seet, waaye ñu ngi doon gën a am ndam su ñu dimbalewoon reéw yu néew doole yi ñu fexe ba méngóo am digante xam-xam yeek fi ñu leen di jëfandikóo. Dimbalé néew doolé yi ci xam-xam a ngi gën a mën a nekk su fekkee ne dañoo sàkku ci ñoom xam-xam yi aju ci seeni saxlaak anam yi ñu leen di jëfandikóo. "Ci kow loolu, lépp lu jëm ci yokkute, rawatina yi nga xam ne néew gi doole yee leen yékkéti, jamono yu ñu leen di nas walla ñuy doxal jéego yi ci bokk, dafay laaj ñu yebe xel xam-xami cosaan yi. 4 - (8) Mbër mi (jafe-jafe bi) askan wi (gën a jankoonteel) mooy am pexe yuy tax ñu gën a xam kuréel yeek doxalinu cosaan yi, te bu ko laajee ñu fexe ba xarala yu bees yi (maanaam yi gën ci doxalin yi nga xam ne yemuñu ci menni réew doN N ) dëppóok doxalinu nit ñi. Noonu doN N la xam-xam yu yaatu yi di mën a àndeek soxlay mbooloom doom-aadama mu nekk ci fi mu dëkke li ëpp solo ci kow yoon wi ñuy jaar ba xam-xam bu ñëw ñu jëfandikóo ko ci anam yi dëppóok ni nit ñi di dunde moo lépp lu am, ñu fexe ba ñi am xam-xami cosaan dugal ci seen loxo. Ag gëstu gu ñu amal ci 121 porose yu nekk ci kow gi di tappatoo lu jëm ci ndox ci 49 réew, feeñal na ne su ñu ci jëlée 100 yoo xam ne nit ñi tax ñu jóg dañoo bokkoon ci ñi doon nas porose bi, 70 ya am nañ ndam yu takku, te bu dee ñi nga xam ne loolu amul ca woon, 10 doN N a ci am ndam. Ni ko misaal yi di ñëw firndéele, xamug ni nit ñi di doxale ci fi ñu dëkké, boole leen ci lépp lu ñu fa nar a amal mën nañoo doon pexe yuy tax ba yi gën ci jëfin yi ñuy jëfandikkóo te réew yi bokk leen dëppóok ni doom-aadama yi nekke fi ñu dëkk. Misaal 1: Jëfandikóom jiwu ñebbe wu bees cà réewum ruwànda ak wum kolombi. Bi ñu jëlée ñaar ba ñetti jiwu ñebbe yi nga xam ne gëstukat yi jàpp nañu ne ñoo dàq a meññ taxul ñebbe yokku ni ñu ko foogewoon. Noonu, gëstukat yi ne dañuy woo ci béréb bi ñuy gëstóo beykat yu jigéen yi nga xam ne am nañ xam-xam cosaan ci mbéyum ñebbe ngir ñu xoolal leen lu toll ci ñaar-fukki jiwu nebbe yii, tànn ci ñaar ba ñett yi ñu jàpp ne ñoo gën, bey leen li ñu am ci jiwu yi ñu tànn ëppe ne lañu amoon ca jiwu ya gëstukat yi 60 ba 90 ci téeméer yoo jël. Ñu jànge ci ne : Xam-xami cosaan mën naa xamle lu am a am njariñ ci ni ñu war a jëfandikóo pexey mbey yu bees yi.
Misaal 2 : Ay dëkki-dëkk fexel nañ seen bopp ni ñuy séddalee dund gi ñu leen dimbalee leer (aw yoon). Ngir mu wóor leen ne nit ñi dinañu jot ci dund gi ñu leen di dimbalée, ab sumb bu tudd "fud foo wok" (maanaam liggéey ñu jox la loo lekk) te nguurug Nepal amaloon ko ci ndimbalug kuréelu See-Tee-Sed (GTZ) la ñu wax nit ñi ne moom lañ fas yéene amal ak ñoom. Ci loolu la ñépp déggóo ne dëkk bu nekk, ci ña fa dëkk lañuy tànn ñiy séddale, waa dëkk bi di xool ni céddale mi di doxe, moo gën a rafet ci anam yi ñu war a séddalee dund. Li ñuy jëlé ay kamyo , ar sareti nag lañuy sëf dund gi. Njariñ yu bari amoon nañu ci doxalin woowu, taxoon na ba ñi joxe saret, li ñu waroon a jot ci dund gi yokku, te loolu naruloon a am su fekkoon ne dañoo jëloon boroomi kamyoN bu bawoo réew taax. Rax ci dolli, ndégam sëfu saret bu nekk xam nañu natt bi mu tollol tax na ba nit ñi xam ni dund gi ñu séddalé yem. Ci noonu itam la ñuy xame ci lu yomb lépp lu waroon a ñëw te ñëwul ni mu toll ci mbooloo mi, te lu réer wallu ñu joxe ko ci lu ñu leeralul, dinañ ko mën a waxtaane ci biir nit ñi. Yeneen sémb yi ni meloon ca réew ma dañoo mujjéwoon jëfandikoó doxalin wii. Nu jànge ci : Jëfandikóo nattukaay ak jëfukaayi cosaan yi, ci sémbub "liggéey ñu féy lag lekk " dina yombal joxeg dund gi te nekk misaalu doxalin wu amul benn njuuj-njaaj cib dëkk. 5 - ( 11) Ci gàttal, xam-xami cosaan yi dañoo am njariñ ci néew doole yi ci fànna yii : - Mbéy - yarum jur ak ni waaso wu ne di faje mala - ni ñuy jëfandikook, ni ñuy saytoo càkkéef yi - li ku nekk war a xam gën gaa néew ci wàllu paj pexe yi ñuy aaroo ci jàngoro yi, pajum feebaru xel - Rënk ak able (leble) - yokkute gu daj ñépp - xeex (bëreek) ñàkk gi 6 - ( 13 ) Ba tey, misaal yi di ñew firndéel nañu ne foo dem, ñi fa dëkké mën nañoo tàkku taxaw ngir soppi aada yi nga xam ne dañuy gàllankoor seenug dund. Misaal : Ci réewum Senegaal, ay jigéen ñu nekk ci kow gaa ngay jëlé njongum jigéen ci seeni dëkk. Jigéeni Malikundaa fas nañ yéenée song jafe-jafe bii di njongum jigéen, di aada bu waaso yu bari bokk : Bàmbare, Soose, Pël, Joolaa, Sooninke ... Bi ñu fexee ba xam li am feneen ak musiba yi ngong mën a indi ci wàllu wér gi yaram ak séyu jànq ji, ci lañ ame lay yu taxaw ba mujj magi dëkk bi dogu ne njongum jigéen dootu fi ame. Loolu taxul xoli jigéen ñi sedd, dañoo daldi taxawal seenug kuréel ngir seeti seen moroom yi nekk ci dëkk yi leen wër, waxtaan ak ñoom, ngir jàppale leen ñu soppi yenn mbir yu am ci seeni dëkk. Weeru saN wiyé ci atum 1998 lañu amal pénc mu mag mu dajale fukki dëkk ak juróom benn yu nekke ci diiwaanub Cees ñépp di bambara walla Meting ngir waxtaane mbàyyim njongum jigéen ba noppi sàlloo "kàddug Malikundaa". Bi ko waa kaasamaas déggée, fukki dëkki pël ak juroom benn daje nañ fa ñoom itam amal fa pénc mu ni deme, tënk fa xalaat bu deme ni ba "kàddug Malika" ëmboon. Nes tuut, Peresidaa Abdu JUUF, njiitum réew mi ci boppam ne xalaat bii tudd "waatup Malikundaa" dafa wara daj réew mi. Ñu jàng ci ne : Ñépp bokk gis-gis mën nañoo dimbali ba ñu soppi yenn aada yiy indi gënaatle. Misaal mii wone na itam ne xam-xami cosaan nekkul loo xam ne kenn warul cee mën dara. Njongum jigéen aada la bu amee soppiku yu ci am mën nañoo wax ne yàllaak liggéey bu ag mbootaayu jigéen def, xëccaale ci ni dëkk bi di doxale, sukkandiku ci jumtukaay yi dëkk bi di doxe ci sosaan ak yu bees yi.
7 - (15) Yenni xam-xami cosan yi mën nañoo dem ba réer. Su boobaa, mën na am ñu mu lor, te ñi ciy jëkk ñooy ñi leen doon suuxat di leen dunde. Gën a fullaal xam-xami cosaan yi mën naa am lu mu yokk ci yoon wiy indi yokkute, tax ba ñu tëyé ci askan wi boroom mën-mën yu takku, ay jumtukaay, ay mbiri cosaan ak ay pexey pajtalum jafe-jafe. Xam-xam bu ni deme dina faral di am lu mu def ci yenn xalaat yu soxal réew yi. Ci kow loolu, sàmm sàqum xam-xami cosaan yi mën naa tax xéewal yi ci àddina si yokku te dina taxit ba ñu gëna gis ni aada ame doole ci yokkute. Léep itam, xam-xami cosaan yi mën nañoo indi ndimbal ci niñ war a aare li ñu wër, ni ko misaal miy ñëw wonee. Misaal : Aar beykat yiy jëfandikóo xam-xami cosaan yi ci dëkk bu nekk. Mbooloom réew yaa ngi taxawal ay sàqu jiwu ngir aar li ñu xam ci wàllu jur, fu nekk ak gancax ak mala ya fa fekk baax. Ni gancax yooyu di meññe ak xam-xami beykat yi niru nañ lu am solo ci liggéey yi ñu war a sumb ci mbéy mi, ngir jàngoro yeek gunóor yi duñu mën a yàq, walla yeneen jafe-jafe yi aju ci jàww ji (wor , sedd, tàngoor,...). Waaye nak, sàmm ni gancax walla mala di jure te aaruloo xam-xam yi aju ci fi ñuy jaar ba meññ mel ni ni amul jariñ, ndaxte pepp yeek njëmbat yi ñu denc ànduñook luy wax ni ñu war a def ba ñu màgg. Ci kow loolu, béréb yiy saytu jiwu yi war nañoo jege sàmm yeek beykat yi nga xam ne ba tey ñu ngi liggéey ci xeet yi fekk baax fi ñu dëkk moo xam mala walla gancax la, ngir xam-xam ak m¨n-mën deme noonu bañ a réer. Nu jàng ci ne : xam-xami cosaan mënul fee jogé su nu bëggée aar ni xeeti gancax yi baree te wuuté.
8- (16) Misaal yi ni weesu wone nañ ni : •Dekk boo dem, xam-xami cosaan yi mën nañ leen a jox ay pexe yu ñu faje seeni jafe-jafe, rawatina ca néew doole yi. • Jang ay xam-xami cosaan yi tëdde, dina yokk pas-pasu ñi ñuy jëflanteel ci dëkk yi. •Sukkandiku ci jaar-jaari doom aadama yi, ni ñu gise jafe-jafe yi ñu jankonteel ak li ñuy def ci fiñ dëkk, mën naa tax ba sémb boo xam ne yokkutee ko tax a jóg gën a am njariñ, weesu mbirum tono (ci anamu def nangam mu jural la nangam) joo am gannaow ba joxee alal ju ñu liggeéyé • Ni dëkk bu nekk gisé yokkuté mën naa indig ndimbal ci moomeel gi (ci ñi moom mbir yi), mu nekk lu mën a indi njariñ ci ñi di jëflanteek ndaw ñi fa toogal nguur gi, jox waa dëkk bi jumtukaay yu ñu mën a wottoo digante boobu. •Xam-xami cosaan yi doon nañu fu ñu mën a sukkandiku ba jox way-ñakk yi doole.
ÑETTEELU XAAJ BI IIII / LANGUG YÉNGU YI Dog bii dafay wone ag làng gu ñuy yéngu ngir daan jafe-jafe yi dëkk diñu teree lëkkale xam-xami cosaan yeek yoonu yokkute wi. Làng ngaa ngi ci ñeenti ponk la sukkantdiku (seetal ci 2 eelu bootal bi, dog 2 ba 5 ) ngir xam li ponk yooyu ëmb, fànna yi ñuy yëngu yi leen war a mottali ngir gën a mën a lëkkale xam-xami cosaan yeek yoonuw yokkute wi. => Tasaare xibaar bi. Yéngu yi ci ëpp solooy : • Taxawal te suuxat sàqum xam-xami cosaan, liñ ci mën a jàng, fi ñu jóge, ñi ci jàppoó, añs. • Fexe ba xam jumtukaay yi ñu war a am ba dugal xam-xami cosaan ci masiinu "ordinaatóor, "tasaare leen su ko defee, ñu seet jumtukaay yooyu ba mu wóor. • Siiwal ay misaal yu ñu tànn, ci kayit walla masiin. => Yombal weccantey xam-xami cosaan yi ci diggante dëkk yi ñeew doole. Yéngu yi ci ëpp solooy : • Dëkk bu nekk ñu dimbale leen ci lépp luy yokk seeni mën-mën ngir wéccantey xam-xami cosaan am rawatina ci diggante kër yi ñu taxawal ci dëkk yi ngir ñuy saytu xam-xami cosaan yi. • Seet pexe yu ñu war a jëfandikóo ba bind, siiwal xam-xami cosaan yi ci dëkk yi. • Pexe yoon wi àdduna sépp war a jokkóo di ci weccantey xam-xami cosaan yomb a taxawal. => Tàggat ñi jàppóo. Yéngu yi ci ëpp solooy : • Foo dem jànge ci ña fa dëkk ak kuréel yi jokkuwul ci genn nguur. • Jël lépp lu ñi jokkoo an ngir am njariñ yu gën a takku ci wàllu yokkute. • Toppatoo ba xam ki moom xam-xami cosaan yi. Làng ngi ñu leen wax ci kow la, bi ko jokkoo gi ñu suuxat ngir xam-xami cosaan yi jëfandikóo la nas pexe mi ñu war a yéngu ci atum 1998 jàpp 99. Nisër yi ñi jàppóo am lañ tënk ci àlluwa jiy ñëw. Taxawal nañu itam ag kuréel gu ñuy diisóol ngir nuy xelaate ci lépp lu jublu ci pexeek lu ñuy def (seetal ci bootal I). Bi ñuy yëngu ngir am li ñu déggóowoon ba nisër ko, ci kow làng gi ñu wax ni mu deme ci kow, ñi lëngoo liggéey nañ bu baax a baax ak kër yiy saytu xam-xami cosaan yi di dëkk jumtukaay yi ci mën a am). Li leen gën a soxal mooy fexe ba ñu gën a fullaal solo si xam-xami cosaan yi ci am, ràññee siiwal xam-xami cosaan te gën a yokk mën-mënu kër yiy saytu xam-xami cosaan yi ci dëkk yi ngir gën a mën a ràññee, bind te siiwal xam-xam yooyu. Loolu mën naa dugal ag ndimbal ci wàllu koppar ngir gëstu gi ci ni ñuy defe ci wàllu xam-xamu cosaan, jokkale kër yiy saytu xam-xami cosaan ci dëkk yi ci yoon wi tudd "Enternet", niki noonu jumtukaay yi ñuy tasaaree xibaar ci yi gën a nekk yu cosaan nga xam ne mën nañoo yombal weccantey xam-xami-cosaan yi ci digante dëkk yi. Bi ñu dooree làngug xam-xami cosaan yi ba léegi, li gën a fés ci liñ ci jëlé mooy : • Yékkéti sàqum xam-xami cosaan bu def lu toll ci ñeen-fukki misaal. • Sos yoonu "Enternet" buy joxey xabaar yu aju ci xam-xami cosaan yi. • Siiwal kayitu tasukaayu xibaar bi tudd "Mbind ci xam-xami cosaan yi" te ñu jaglee ko xam-xami cosaan yi. • Gëstu ci xam-xami cosaan yi. (seetal ci bootal 1 ngir xam li mu ëmb).
Xam-xami cosaan ngir yokkute gi : pexe yi ñuy yëngu : atum 1998 jàpp 1999
BOOTAL YI Bootal 1 Won leen ni pexem xam-xami cosaan ngirug yokkute mi tëdde Waxtaan wa amoon ci weeru suweK, atum 1997 ca Toronto réewum Kanadaa, dafa fésal ni soxlas jàng; aar ak weccante xam-xami cosaan yi jàmpe. Ci jamono jig jàppóo amee ngir xarala yi ñuy jokkoo ak di ci tasaaree cibaar yi ci Afrig; la Bànk Monjaal nangoo jiite pexeg xam-xami cosaan yi ci yoonuw yokkute wi. Allal ji ci Bànk Monjaal a ngi jóge ci koppar yu mu maye ci sumb bi tudd " Innovation Marketplace" maanaam " lu bees li ñu indi ci ja yi". Ñi jàppóo (lëngóo) ÑII; BOKK NAÑ CI ÑI JÀPPÓO NAS PEXE MU BEES MI: - CEA di bànqas giy saytu koom-koom ci Afrig. - CISDA di kër gu kuréel yiy toppatoo mbirum yokkute ci Afrig di wecaantee xabaar - CRDIC di Kër gi ñuy gëstóo yokkuteg réew yi te nekk Réewum Kanadaa - UIT di mbootaayu kuréel yi réew yi séq di ci toppatoo jokkoo digante ñoo xam ne dañoo sorewoo. - UNESCO di banqaasu mbootaayu xeet giy saytu yar mi, xam-xam yu xarala yi ak caada. - PNUD di sumb bi mbootaayu xeet yi sumb ngir réew yi amug yokkute. - OMS di mbootaay giy toppatoo mbirum wér gi yaram ci àddina si. Ci digante bi am na ñeneen ñu leen ci fekkisi - CIRAN di mbootaa gu fekk baax ca réewum Olànd tey toppatoo ni réew yi di demlantee ci wàllu njàng mu kowe mi. - SANGONET kuréel la gu jokkuwul cig nguur , fekk baax ca réewum "Afrig dii Siid" nga xam ne moo def lëpp lu aju ci Enternet ( maanaam jokkoo goo xam ci masiinu Ordinaatóor lañ ko jaarale ) - OMPI : mbootaay miy saytu àq ak sañ-sañi boroom xam-xam yi ci àddina si. - OIT : di mbootaay miy toppatoo àq ak sañ-sañi liggéeykat ci àdduna si. Nisër yi Tas xabaar bi •Suuxat sàqum xam-xami cosaan yeek liñ ci mën a jànge. • Siiwal ay misaali xam-xami cosaan ci jumtukaay yu ñu bind ciy kayit walla cib masin. Yombal weccantem xibaar ci diggante ñi nekk ci dëkk yi ci réew yu néew doole yi. • Ndimbal ci lu yokk mën-mëni nit ñi nekk ci dëkk yi ngir ñu bokk xam-xami cosaan yi. • Xam niñ war a def ba dugal xam-xami cosaan yi ci masinu ordinaatóor, tas leen ba ñu yegg ci nit ñi ci dëkk-dëkkaan yi.
BOOTAL II Kërale 2 : Yokk te gën a jàppandil xabaar yi fi am ci xam-xami cosaan yi
Kërale 3 : Fexe ba nit ñi gën a gis solo si xam-xami cosaan am te di leen jëfandikóo ci lépp lu ñuy yéngu mu jublu ci wàllu yokkute.
Kërale 4 :Xàll yoon wu yaatu wu ñuy weccantee xam-xami cosaan.
Kërale 5 : Jox ku nekk céram ci weccantem xam-xami cosaan yi
BOOTAL V Doxalin wi Njariñu képp ku bokk ci ñi jàppóo; kàttanu ñiy am lu ñu def ci xam-xami cosaan yi; ak yenn gàllankoor yi mën a am ci wàllu alal. Loolu dafa laaj doxalin wuy yombal weccantem xabaar bu dul dakk, yokk mën-mëni nit ñi ci fiñ dëkk, ak yoon wuy ubbil bunt ñeneen ba ñu mën a bokk ak ay joxekati xam-xami cosaan. Boroom xam-xam yu ràññeeku ci wàllu xam-xami cosaan ak xaralay xibaarukaay ak jokkookaay ñooy xelal " pexe mi" ci feem yeek xalaat yi nga xam ne fàww ñu jëfé leen. Tasum Xibaar mi Pexe mi dafay seet jumtukaay yi war a jiitu ngir bind; téyé xam-xami cosaan yi, tas leen, siiwal leen te di leen jëfé. Ci kow loolu, ñi ñu xam ne ci ñoom la xam-xami cosaan yi fekk baax, dañoo war a joxe ay leeral ci ni ñu leen di jëfandikóo. Loolu mën naa yaatal liñ gis ci xam-xami cosaan yi, be tey itam, mën naa doon jumtukaay bu ñuy natte pexe yi ñuy jëfandikóo ba am lu leer ci xam -xami cosaan yi ñu mën a jëfandikóo ñooy dem ci dëkk yi di laaj nit ñi, toog ak ñi ngeen bokk natt li ñuy def. Porose Bànk Monjaal yeek ñeneen ñu bokk ci liggéey bii ñu door dinañu indi seen i yokkute. Liggéey bi ñu door nii, dinañ yaatal ba tey xam-xam yi Bànk Monjaal ak ñi mu ci jàppool sukkandiku. Fexe be weccantem xibaar mi ci diggante ñi nekk ci réew yi néew doole yomb Li ñu bind ci li ñuy def ci xam-xami cosaan yi, dañ koy dajale, tënk ko ngir dugal ko ci sàqum xam-xam moo xam ne nit ñi dinañ ci mën a jot ci lu yomb, nga xam ne saa su mënee nekk dañ koy jokkaleek fi xam-xami cosaan yii fekk baax ( liggéey biñ door dafay war mu sukkandiku ci). Xam-xami cosaan yi nga xam ne dafa am ñoo xam ne dañ leen amal njariñ; dañu leen di siiwal ci kayitu tasukaayi xabaar buy génn wenni yoon ci weer wu nekk. Liggéey biñ door dafay war mu sukkandikóo ci liñ fi jëkk a def, dimbale kuréeli xam-xami cosaan yi ba liñ fi mën a yokku ba ñu gën a xamante, tëyé te tas xabaar yi aju ci xam-xami cosaan yi. Jëfandikóo xam-xami cosaan yi ci yoon wiy indig yokkute. Bàyyi xel ci solo yi xam-xami cosaan am, jëfandikóo jaar-jaar yiñ fi jëkk a def ak tàggat xel yi ñetti mbir lañ yoo xam ne dañ leen di soxla su ñu bëggée dugal xam-xami cosaan ci yoonu yokku wi antu. Bi muy door, liggéey bi dafa waroon a def léppam ci ñiy dogal, kuréel yiy toppatoo yokkute ak nguuri réew yi gën a yebe xel solo si xam-xami cosaan yi am. Bu weesoo siiwalug xam-xami cosaan yi nga xam ne niróowuñook yeneen yi, liggéey bi dina am yu muy wone ci yen xew yi ñi jàppóo di amal ( misaal: ndaje mi Bànk Monjaal di amal at mu nekk). Fas nañ yéenee amaal ndaje mu mag ci Afrik ngir ñi fiy jiite gën a yebe xel solo yi xam-xami cosaan am. Bu ñu demee ba ca kanam, dinañ teewlu ci yokkug liggéey yi ñu sumb ngir seet ba xam, jaarale ko ciy porose. Loolu, dina dugalaale jëfandikóog misaal yu antu ngir firndéel ne jëfandikóo xam-xami cosaan mën naa indi njariñ lu amul benni werante. Tànn gu am fayda gu ñuy tànn liggéey yi ñuy seete ba xam ( moo xam porose xalla am réew a koy doxal) dinañu dimbale ba ñu gën a mën a suuxat misaal yi ñiy jëfandikóo ci jéegó yii ngi ñeneen ñi ñu bokkal liggéey wóolu. Bu dee li aju ci ñi séq liggéey bi, jëflante gi am ci jaar-jaar yiñ doon seete; ak joxe ab leeral di dugalaale borom kàddu yi nekk ci kréel yeek mbootaay yi ci " baayale walla ndeyale" ay liggéey yu ñuy jëkk a seete, dina tax ba ñiy yëngu ci wàllu yokkute bàyyi ci xel ni mu ware. Taxawal ay jàppóo Liggéey bu bees bi dina fexee taxawalug jokkoo ak ñeneen ñoo xam ne bokkuñook ñi nekk ci kuréel gi tudd PICTA. Dina gën a bàyyi xel ci jokkoo gi ñuy taxawal digante kuréel yi jokkuwul cig nguur, xàll wu mag wu xam-xami cosaan yi te saa su mu mënee nekk; jaarale ko ciy porose aki kuréel yu jàppóo, ak ñi ci dëkk-dëkkaan yi ngir am lu ñu jànge ci seeni jaar-jaar.
|