(Jean 11, 12) Salamaalekum mbokki déglukat yi. Nu ngi leen di nuyu ci turu Yàlla Boroom jàmm, ji bëgg ñépp dégg te nangu yoonu njub wi mu tëral, ngir am jàmm ju wér ak Moom ba fàww. Am nanu mbégte ci li nu mana dellusi tey ngir dégtal leen seen emisyon YOONU NJUB. Fi nu tollu ci sunu gëstu ci Linjil bu sell bi, gis nanu ni Almasi bi Yeesu ame tur yu bare, ngir nu gëna xam ki mu doon. Déggoon nanu ba noppi ni ñu ko tuddee: Kàddu, gi nekkoon ak Yàlla ci njàlbéen ga... Doomu Yàlla Aji Kawe ji... Doomu Nit ki... Mbotem Yàlla mi... Musalkat bi... Ñam wiy joxe dund gi... Leeru Àddina si... Boroom Ndam li... Buntu gétt gi... ak Sàmm bu baax bi. Tey nag, dinanu gisaat yeneen ñaari turi Yeesu: ñooy: "Ndekkite li ak Dund gi." Ba fi nu tollu, gisoon nanu ni Yeesu doon wëre réewum Yawut yi, di jàngale, di def lu baax, ak di faj ñi feebar ak ñi làggi ak ñi gumba ak ñi rab jàpp, ba tax mbooloo mu bare topp ko. Waaye boroom diine, yi ñuy wooye Farisien ya, dañu añaane woon Yeesu lool, ndaxte àttanuñu xel mi muy waxe, te mënuñu weddi firnde yi mu def. Tey nag, danu fas yéene jëm kanam ci Linjil, ba gis ni Yeesu defe woon jeneen jaloore, ngir woneeti ndamam, li mu am ci Yàlla, ngir nit ñi gëm ko. Nu ngiy jàng ci Linjilu Yowanna, saar fukk ak benn. Mbind mi ne na: 11:1Amoon na benn waay bu woppoon, ñu koy wax Lasaar. Ma nga dëkkoon Bétani, moom ak Maryaama ak Mart, mi mu bokkaloon ndey ak baay. 2Maryaama mooy jigéen jiy sottiji latkoloñ ci tànki Boroom bi, fompe ko kawaram. Moom la càmmiñam Lasaar woppoon. 3Ñaari jigéeni Lasaar yónnee ca Yeesu, ne ko: Boroom bi, sa xarit wopp na. 4Bi Yeesu déggee xebaar boobu, mu ne: Lasaar de, woppam jooju du ko mujje; day wone ndamu Yàlla tey màggal Doomu Yàlla ji. 5Yeesu soppoon na Mart ak Maryaama ak Lasaar. 6Bi mu yégee nag ne, Lasaar wopp na, mu toogaat yeneen ñaari fan ca bérab, ba mu nekkoon. (Yeesu xamoon na ne, Lasaar dina dee. Wànte Yeesu dafa fasoon yéene jëfandikoo deewug Lasaar ngir wone kàttanu Yàlla gi dëkk ci Moom, ngir nit ñi xam ne, ci kaw la jóge.) 7Gannaaw [ba mu toogee ñaari fan ca bérab ba mu nekkoon nag, Yeesu waxoon na fukki taalibe ya ak ñaar, nee]: Nanu dellu Yude. 8Taalibe ya tontu ko ne: Kilifa gi, yàggul dara waa Yude doon nañu la wuta rey ak i xeer, nga di fa dellu? 9Yeesu ne leen: Xanaa du bëccëg fukki waxtook ñaar la? 11...Sunu xarit Lasaar nelaw na, waaye maa ngi dem yee ko. 12Taalibe ya tontu ne: Boroom bi, bu nelawee kay, kon dina wér. 13Yeesu dafa bëggoona wax ne, Lasaar dee na, waaye taalibe yi dañoo xalaatoon ne, mbiri nelaw rekk lay wax. 14Ci kaw loolu Yeesu wax ci lu leer ne: Lasaar dee na. 15Bég naa ngir yeen ndax li ma fa nekkul, ngir seen ngëm gëna dëgër. Waaye nanu ko seeti. 17Bi Yeesu agsee, mu fekk ne, bi ñu dencee Lasaar ak léegi, mat na ñeenti fan. 18Bétani ma nga woon ca wetu Yérusalem, diggante bi matul woon sax ñetti kilomet. 19Yawut yu bare ñëwoon nañu kër Mart ak Maryaama, ngir dëfal leen ci seen deewu càmmiñ. 20Bi Yeesu ñëwee, Mart yég ko, dem di dajeek moom; fekk booba Maryaamaa nga toogoon ca kër ga. 21Mart ne Yeesu: Boroom bi, boo fi nekkoon de, sama càmmiñ li du dee! 22Waaye xam naa ne, fii nu tollu sax, loo ñaan Yàlla, mu may la ko. 23Yeesu ne ko: Sa càmmiñ dina dekki. 24Mart tontu ko ne: Xam naa ne, dina jóg bésu ndekkite la, keroog bés bu mujj ba. 25Yeesu ne ko: Man maay ndekkite li, maay dund gi. Ku ma gëm, boo deeyee it, dinga dund. 26Rax-ca-dolli kuy dund te gëm ma, doo dee mukk. Ndax gëm nga loolu? 27Mu tontu ko ne: Waaw, Boroom bi. Gëm naa ne, yaay Almasi bi, di Doomu Yàlla, ji wara ñëw àddina. 28Bi Mart waxee loolu, mu daldi dem woowi Maryaama, ne ko ci pett: Kilifa gaa ngi fi; mi ngi lay laaj. 29Bi Maryaama déggee loolu, mu daldi jóg, gaawantoo dem ca Yeesu... 32Bi Maryaama agsee nag ca Yeesu, ba gis ko, mu daanu ciy tànkam, ne ko: Boroom bi, boo fi nekkoon, sama càmmiñ du dee! 33Yeesu gis ne, mi ngi jooy te Yawut yi ànd ak moom itam ñu ngi jooy. Mu daldi jàq, am naqar wu réy. 34Mu ne leen: Fu ngeen ko denc? Ñu tontu ko ne: Kaay gis, Sang bi. 35Yeesu jooy. 36Noonu nag, Yawut ya ne: Gis ngeen ni mu ko bëgge woon! 37Waaye am na ca ñoom ñu doon wax, naan: Moom mi ubbi bëti gumba gi, ndax mënul woona fexe ba Lasaar du dee? 38Yeesu dellu am naqar wu réy, daldi dem ca bàmmeel ba. Pax la mu ñu yett ci doj, ube ko xeer. 39Yeesu ne: Dindileen xeer wi! Mart, jigéenu ku dee ki ne ko: Boroom bi, dina xasaw xunn fii mu nekk, ndaxte am na ci bàmmeel bi ñeenti fan. 40Yeesu ne ko: Ndax waxuma la ne, boo gëmee, dinga gis ndamu Yàlla? 41Ñu daldi dindi xeer wa. Yeesu xool ci kaw, ne jàkk asamaan, ñaan Yàlla ne: Baay, sant naa la ci li nga ma déglu ba noppi. 42Xam naa ne, doo jóg ci di ma déglu, waaye dama koy wax, ngir nit ñi ma wër gëm ne, yaa ma yónni. 43Bi mu waxee loolu, Yeesu woote ak baat bu dëgër, ne: Lasaar, ñëwal ci biti! 44Néew bi daldi génn, ñu gis càngaay, li ñu takke woon tànk yi ak loxo yi, ak kaala, gi ñu muure woon kanam gi. Yeesu ne leen: Tekkileen ko, bàyyi ko mu dem! (Yow. 11) Du fii lanuy yem, waaye bala nuy àggale nettali bu doy waar bii, dina baax su nu manee xalaat tuuti ci kéemaan, gi Yeesu defoon! Ba àddina sosoo ba tey, musuñoo dégg nit ku mana jox dund néew, bu am ñeenti fan ci bàmmeel, néew boo xam ne, mu ngi doon tàmbali yàqu te xasaw. Waaye moom la Yeesu defoon tembe, bi mu dekkalee Lasaar ca néew ya. Dooley dee, tëwul Boroom bi Yeesu, ndaxte Moom ci boppam mooy Kàddug Yàlla; di Ruuwu Yàlla, gi jóge asamaan. Ni Yàlla ame dund gi moom ci boppam, noonu it la ko Almasi bi ame. Te ni Yàlla di dekkale néew yi, di leen jox dund gi, noonu la Almasi bi di joxe dund gi ñi mu ko bëgga jox, ndaxte Moom ci boppam mooy Aji Dund ji. Looloo taxoon bi Yeesu woowee Lasaar mu ñëw ci biti, néew bi daldi dundaat, jóg, génn bàmmeel ba. Looloo tax it, Yeesu manoona wax jigéenu Lasaar, ne ko: "Man maay ndekkite li, maay dund gi. Ku ma gëm, boo deeyee it, dinga dund!" Léegi nag, nanu àggale nettali bi, ngir xam li Yawut ya def, gannaaw ba ñu seede ni Yeesu dekkale Lasaar ca bàmmeel ba. Mbind mi ne na: 11:45Yawut yu bare ca ña ñëwoon kër Maryaama te gis li Yeesu defoon, daldi koy gëm. 46Waaye amoon na it ñu demoon ci Farisien ya, nettali leen la Yeesu defoon. 47Farisien ya ak sëriñ su mag sa woo kureelu àttekat ya ne: Nit kii kat, kéemaan yi muy def a ngi bëgga bare. Lu nuy def nag? 48Ndaxte su nu ko bàyyee mu jàppoo nii, ñépp dinañu ko gëm, te kilifay Room yi dinañu ñëw, daaneel sunu kër Yàlla gi, tas sunu réew! 49Amoon na ca ñoom ku ñuy wax Kayif te mu nekkoon sëriñ bu mag ba at mooma; mu ne leen: Xamuleen ci mbir mi dara. 50Xanaa xamuleen ne, kenn nit rekk dee ngir ñépp, mooy li gën ci yeen? Bu ko defee, réew mi du tas. (51Loolu Kayif waxu ko woon ci sagoom, waaye li mu nekkoon sëriñ bu mag ba at mooma, moo tax Yàlla xiirtal ko mu ne, Yeesu dina dee ngir réew mi. 52Du woon rekk ngir xeet woowu, waaye ngir itam doomi Yàlla, yi tasaaroo yépp, dajaloo nekk benn.) 53Keroog la njiiti Yawut ya dogu ci rey Yeesu. 54Taxoon na ba Yeesu dootul doxantu ci biir Yawut ya. Noonu mu dem ca gox bu jege màndin ma, ca dëkku Efrayim. Foofa nag la toog ak ay taalibeem. 55Bésu Jéggi ba, di màggalu Yawut ya, mu ngi doon jubsi, ba ñu bare ca waa àll ba di dem Yérusalem balaa booba, ngir sanguji set. 56Ñu ngi doon wut Yeesu tey waxante ca kër Yàlla ga naan: Lu ngeen ci xam? Ndax dina ñëw ci màggal gi walla déet? 57Sëriñ su mag sa ak Farisien ya daldi santaane ne, bu kenn xamee fu Yeesu nekk, mu yégle ko, ngir ñu man koo jàpp. 12: 1Juróom benni fan laata màggalu bésub Jéggi ba, Yeesu dem na Bétani, dëkku Lasaar, mi mu dekkal. 2Foofa ñu defaral ko fa reer. Mart moo ko doon séddale, te Lasaar bokkoon na ca gan ña. 3Noonu Maryaama daldi jël liibaru latkoloñ, ju raxul, ju ñuy wax nard, tey jar lu baree-bare. Mu sotti ko ci tànki Yeesu, ba noppi fomp ko ak kawaram. Xetu latkoloñ gi gilli ci kër gi yépp. 4Kenn ca taalibey Yeesu ya, muy Yudaa Iskariyo, mi ko nara wor, daldi ne: 5Lu tax jaayewuñu latkoloñ jii peyu atum lëmm, jox ko miskin yi? 6Waaye bi muy wax loolu, xalaatul woon miskin yi, ndaxte sàcc la woon; moo yoroon boyetu xaalis bi, te daan ci sàkk. 7Waaye Yeesu ne ko: Bàyyi ko! Jekkoon na mu denc ko ngir bés bu ñu may suul. 8Miskin yaa ngi ak yeen bés bu nekk, waaye dungeen ma gis ba fàww. 9Bi ñu yégee ne, Yeesoo nga fa, mbooloom Yawut mu bare daldi dem Bétani. Yeesu rekk yóbbuwu leen fa woon, waaye dañoo bëggoona gisaale Lasaar, mi Yeesu dekkaloon. 10Sëriñ su mag sa dogu ci ne, dañuy reyaale Lasaar, 11ndaxte moo waral Yawut yu bare dëddu leen, gëm Yeesu. (Yow. 12) Fii nag lanu wara yem tey, ndaxte sunu jot léegi mu jeex. Waaye bala nuy tàggoo, am na lenn lu nu wara xalaat. Ndax gis ngeen ni njiiti diiney Yawut yi tontoo woon ci firnde ji leen Yeesu wonoon? Kenn ci ñoom mënul woona weddi kéemaan gi Yeesu def, ndaxte ñépp a tegoon seeni bët ci Lasaar mi dekki ca néew ya. Waaye lan la sëriñ su mag sa ak yeneeni sëriñ defoon? Ndax tuub nañu seeni bàkkaar, te gëm ne Yeesu mooy Almasi bi, di Doomu Aji Kawe, ji jóge asamaan? Tuubuñu de! Firnde yi Yeesu def yépp taxul sëriñ sa ak seeni taalibe réccu te nangu Yeesu ni seen Boroom ak seen Musalkat. Lan la sëriñ sa def nag? Dañu gëna bañ Yeesu sax, te mànkoo ngir rabat pexem rey ko! Te it, dogu ci reyaale sax Lasaar mi Yeesu dekkaloon, ndaxte moo waral Yawut yu bare dëddu sëriñ si, topp Yeesu! Céy, ni xoli kilifay diine yooyu dërkiise te sore Yàlla! Amuñu woon benn cofeel ci Yàlla, mbaa ci dëgg gi. Sàggane nañu firnde yu ràññeeku, yi Yeesu defoon ci seen kanam. Seen bànneexu bopp ak seen sutura ak am xaalis rekk lañu doon xalaat. Looloo taxoon ñu mànkoo ngir rey Yeesu, ndaxte dañu ragal ne, su ñu ko bàyyee mu jàppoo noonu, ñépp dinañu leen dëddu, topp Yeesu. Lu ngeen xalaat ci kilifay diine yooyu? Kan moo soloon ci seen xel, ñu rey Yeesu? Seytaane mooy ki leen doon jiite, ndaxte dafa bañ Yàlla ak Almaseem. Seytaane dafa yaakaaroon ne, su njiiti Yawut ya reyloo Yeesu, loolu dina nasaxal pexem Yàlla ngir musal doomi Aadama ci dooleem. Waaye Seytaane xamul woon ni Yàlla fasoon yéenee jëfëndikoo deewug Almasi bi ngir nasaxal jëfi Ibliis, te goreel doomi Aadama, yi meloon ni ay jaam ndax ragala dee. Te it, amoon na leneen li Seytaane ak ñi àndoon ak moom ràññewul woon. Mooy lii: Dooley dee du mana téye Boroom bi Yeesu, te suuf du mana lekk néewam, ndaxte Yeesu mooy ndekkite li ak dund gi. Looloo tax Yeesu manoona wax jigéenu Lasaar, ne ko: "Man maay ndekkite li, maay dund gi. Ku ma gëm, boo deeyee it, dinga dund... Ndax gëm nga loolu?" (Yow. 11:25,26) Kon, fii lanu leen di tàggoo, di leen jox dox-daje njàng miy ñëw, ndaxte, bu soobe Boroom bi, dinanu jëm kanam ci Linjil, gis ni Yeesu ware cumbur, dugg Yérusalem ba amal li yonent Yàlla yi bindoon bu yàgg ci mbiram. Su fekkee ne, bëgg nga am téere, buy yaatal sa xam-xam ci dundu Almasi bi, nanga nu bind ci: YOONU NJUB / B.P. 370. / Saint Louis. / YOONU NJUB / B.P. 370. / Saint Louis. Yàlla na leen Yàlla barkeel te ngeen xalaat bu baax ci li Boroom bi Yeesu waxoon, bi mu naan: "Man maay ndekkite li, maay dund gi! Ku ma gëm, boo deeyee it, dinga dund! ...Ndax gëm nga loolu?" (Yow. 11:25,26)
|