1 John 1
1 Nu
ngi leen di bind ci mbirum Ki ñuy wax Kàddug dund, moom mi amoon ca
njàlbéen ga; mi nu dégg te gis ko ak sunuy bët, mi nu xool te laal ko ak
sunuy loxo.
2 Dund
feeñ na, te gis nanu ko; te moom lanuy seedeel, di leen yégal dund gu
dul jeex, googu nekkoon ci wetu Yàlla Baay bi te feeñu nu.
3 Li
nu gis te dégg ko, nu ngi leen koy yégal, ngir yéen itam ngeen bokk ak
nun. Te dëgg-dëgg bokk nanu ci Baay bi ak Doomam, Yeesu Kirist.
5 Xebaar bi nu dégg ci Yeesu Kirist, di leen ko yégal, mooy lii: Yàlla Leer la, te genn lëndëm nekkul ci moom.
7 Waaye
bu nuy dox ci leer, ni mu nekke moom ci boppam ci leer, kon bokk nanu
ci sunu biir, te deretu Yeesu Doomam dina nu sellal ci bépp bàkkaar.
9 Su
nu nangoo sunuy bàkkaar ci kanamam, fekk kuy sàmm kóllëre la te jub,
ngir baal nu sunuy bàkkaar te sellal nu ci lépp lu jubadi.
1 John 2
1 Samay
doom, maa ngi leen di bind yëf yii, ngir ngeen bañ a def bàkkaar. Waaye
su kenn defee bàkkaar, ba tey am nanu ku nuy rammu ci Baay bi, mooy
Yeesu Kirist mu jub mi.
2 Te moo joxe bakkanam, ngir dindi sunuy bàkkaar, te du sax sunuy bàkkaar rekk, waaye yu àddina sépp.
5 Kuy sàmm kàddug Yàlla, dëgg-dëgg sa mbëggeel ci Yàlla mat na sëkk. Ci loolu lanu xame ne, nekk nanu ci moom.
7 Samay
soppe, li ma leen di bind du ndigal lu bees, waaye ndigal lu yàgg la;
la ngeen jotoon ca ndoorte la. Te ndigal lu yàgg loolu, mooy kàddu gi
ngeen déggoon.
8 Teewul
ndigal lu bees laa leen di bind, lu amoon ci dundu Yeesu, te am it ci
seen dund; ndaxte lëndëm gaa ngi wéy, te leer gu wóor gi fenk na xaat.
11 Waaye kuy bañ sa mbokk, ci lëndëm nga nekk, di ci dox, te xamoo foo jëm, ndax lëndëm muur na say bët.
13 Maa
ngi leen di bind, yéen baay yi,ndax xam ngeen Ki nekkoon ca njàlbéen ga
ba tey.Maa ngi leen di bind, yéen waxambaane yi,ndax daaneel ngeen
Ibliis.
14 Bind
naa leen, samay doom,ndax xam ngeen Yàlla Baay bi.Bind naa leen, yéen
baay yi,ndax xam ngeen Ki nekkoon ca njàlbéen ga ba tey.Bind naa leen,
yéen waxambaane yi,ndax yéena ngi dëgër,ndax kàddug Yàllaa ngi dëkk ci
yéen,te daaneel ngeen Ibliis.
16 Ndaxte
lépp lu nekk ci àddina, maanaam bëgg-bëggu yaram ak xemmemu bët ak
réyug àddina, loolu du jóge ci Baay bi waaye ci àddina.
18 Samay
doom, waxtu wu mujj wi jot na! Dégg ngeen ne, benn Bañaaleb Kirist dina
ñëw; te dëgg la, bañaaley Kirist yu bare feeñ nañu. Ci loolu lanu xame
ne, waxtu wu mujj wi jot na.
19 Ci
sunu biir lañu jóge, waaye bokkuñu woon ci nun; ndaxte su ñu bokkoon ci
nun, kon dinañu des ci nun. Waaye dàggeeku nañu nu, ngir mu leer ne,
kenn ci ñoom bokkul woon ci nun.
21 Bind naa leen, du ndax xamuleen dëgg, waaye ndax xam ngeen ko, xam it ne wenn fen du jóge ci dëgg.
22 Kan mooy fenkat bi? Mooy kiy weddi ne Yeesu mooy Kirist, Almasi bi. Kooka mooy Bañaaleb Kirist, biy weddi Baay bi ak Doom ji.
24 Yéen
nag, la ngeen déggoon ca ndoorte la, na sax ci yéen. Loolu ngeen
déggoon ca ndoorte la, su saxee ci yéen, dingeen sax yéen itam ci Doom
ji ak ci Baay bi.
27 Yéen
nag, Xel mi leen Kirist sol a ngi dëkk ci yéen, te soxlawuleen kenn
jàngal leen dara. Waaye Xel mi mu leen sol, mi ngi leen di jàngal lépp,
te li mu leen di jàngal mooy dëgg; kon nag saxleen ci moom, ni mu leen
ko jàngale.
28 Gannaaw
loolu nag yéen samay doom, saxleen ci Kirist, ngir bés bu feeñee, nu am
kóolute ci kanamam te bañ a rus ba sëngéem cig dikkam.
1 John 3
1 Xool-leen
mbëggeel gi nu Baay bi jox, ni mu réye, ba nu man a tudd doomi Yàlla.
Te moom lanu. Moo tax àddina xamu nu, ndaxte xamu ko woon, moom itam.
2 Samay
soppe, léegi doomi Yàlla lanu, te li nu nar a nekki feeñagul, waaye xam
nanu ne, bés bu Almasi bi feeñee, dinanu nirook moom, ndaxte dinanu ko
gis, na mu mel.
8 Kuy
def bàkkaar, ci Seytaane nga bokk, ndax Seytaane ca njàlbéen ga ba tey
day bàkkaar. Te Doomu Yàlla ji ñëw na, ngir nasaxal jëfi Seytaane.
9 Ku juddu ci Yàlla doo def bàkkaar, ndax Yàlla sol na la jikkoom, te doo man a sax ci bàkkaar, ndax juddu nga ci Yàlla.
10 Lii
mooy ràññale doomi Yàlla ak doomi Seytaane: képp ku dul def lu jub
bokkoo ci Yàlla; naka noonu itam ku soppul sa mbokk bokkoo ci Yàlla.
12 te bañ a mel ni Kayin, mi bokkoon ci Ibliis, ba rey rakkam. Lu tax mu rey ko nag? Ndaxte ay jëfam dañoo bon, te yu rakkam jub.
14 Mbëggeel gi nu bëgg sunuy bokk moo nuy xamal ne, jóge nanu ci dee, tàbbi ci dund. Ku bëggul sa mbokk, yaa ngi ci dee ba tey.
16 Ci lii lanuy xàmmee luy mbëggeel: Kirist joxe na bakkanam ngir nun; te nun itam war nanoo joxe sunu bakkan ngir sunuy bokk.
17 Waaye ku am alalu àddina te gis sa mbokk nekk ci soxla, nga dummóoyu ko, nan la mbëggeelu Yàlla dëkke ci yaw?
19 Ci
loolu lanu xame ne, nu ngi ci dëgg; te waxtu wu sunu xol di xeex ak
nun, dinanu ko dalal ci kanamam; ndaxte Yàllaa ëpp sunu xol te xam na
lépp.
19 Ci
loolu lanu xame ne, nu ngi ci dëgg; te waxtu wu sunu xol di xeex ak
nun, dinanu ko dalal ci kanamam; ndaxte Yàllaa ëpp sunu xol te xam na
lépp.
22 Te lépp lu nu koy ñaan, dinanu ko jot ci moom, ndaxte nu ngi sàmm ay ndigalam, di def lu ko neex.
24 Kuy sàmm ndigalu Yàlla, dinga sax ci moom, mu dëkk ci yaw. Te Xel mi mu nu jox, moo nuy xamal ne, dëkk na ci nun.
1 John 4
1 Samay
soppe, buleen gëm xel mu nekk, waaye nattuleen xel yi, ba xam ndax ci
Yàlla lañu jóge walla déet, ndaxte naaféq yu bare yu mbubboo turu yonent
jóg nañu, tasaaroo ci àddina si.
2 Ci lii lanu xàmmee Xelum Yàlla: mépp xel mu nangu ne, Yeesu Kirist ñëw na, nekk nit, ci Yàlla la bokk.
3 Waaye
mépp xel mu nanguwul Yeesu, bokkul ci Yàlla. Xel moomu mooy xelum
Bañaaleb Kirist, mi ngeen déggoon ne dina ñëw, te léegi sax mu ngi ci
biir àddina.
4 Yéen
samay doom, ci Yàlla ngeen bokk, te daan ngeen yonent yu naaféq yooyu,
ndaxte Ki nekk ci yéen moo ëpp doole ki nekk ci àddina.
6 Nun
nag ci Yàlla lanu bokk. Ku xam Yàlla dinga nu déglu; ku bokkul ci Yàlla
doo nu déglu. Ci loolu lanuy xàmmee Xel miy dëgg ak xel mi dul dëgg.
7 Samay
soppe, nanu bëggante, ndax mbëggeel ci Yàlla la bawoo; képp ku bëgg sa
mbokk nag, ci Yàlla nga juddoo, te xam nga Yàlla.
9 Nii la Yàlla wonee mbëggeelam ci nun; yónni na ci àddina jenn Doomam ji mu am kepp, ngir nu am dund ci moom.
10 Lii
mooy mbëggeel, du sunu mbëggeel ci Yàlla, waaye mbëggeelam ci nun, ba
mu yónni Doomam, mu joxe bakkanam, ngir dindi sunuy bàkkaar.
12 Kenn musul a gis Yàlla, waaye bu nu bëggantee, Yàllaa ngi dëkk ci nun te mbëggeelam mat na sëkk ci nun.
16 Mbëggeel
gi Yàlla am ci nun, xam nanu ko te gëm ko. Yàlla mbëggeel la, te képp
ku sax ci mbëggeel, yaa ngi sax ci Yàlla, mu dëkk ci yaw.
17 Ni Kirist mel, noonu lanu mel nun itam ci àddina. Ci loolu la mbëggeel mate sëkk ci nun, ngir nu am kóolute bésu àtte ba.
18 Genn
ragal amul ci mbëggeel, waaye mbëggeel gu mat sëkk day dàq ragal.
Ndaxte ragal day ànd ak mbugal; te ku ragal, mbëggeel matul sëkk ci yaw.
20 Su
kenn nee: «Bëgg naa Yàlla,» te bëgguloo sa mbokk, dangay fen; ndaxte ku
bëggul sa mbokk mi ngay gis, doo man a bëgg Yàlla mi nga gisul.
1 John 5
1 Képp ku gëm ne Yeesu mooy Almasi bi, juddu nga ci Yàlla; te ku bëgg waajur, dinga bëgg itam ki mu jur.
6 Yeesu
Kirist mooy ki ñëw, jaar ci ndox ak deret; du ci ndox rekk, waaye ndox
ak deret. Te Xelu Yàlla mi moo koy seedeel, ndax Xel mi mooy dëgg.
9 Seedes nit, dinanu ko nangu, waaye seedes Yàlla moo gën a wóor, ndax boobu seede mooy li Yàlla seede ci Doomam.
10 Ku
gëm Doomu Yàlla ji, am nga seede boobu ci sa xol. Ku gëmul Yàlla, teg
nga ko kuy tebbi waxam ndaxte gëmuloo li Yàlla seede ci Doomam.
13 Maa ngi leen di bind yëf yii, yéen ñi gëm turu Doomu Yàlla ji, ngir ngeen xam ne, am ngeen dund gu dul jeex.
15 Gannaaw xam nañu ne, dina nangu lépp lu nu koy ñaan, xam nanu it ne, li nu ko ñaan, jox na nu ko.
16 Ku
gis mbokkam, muy def bàkkaar bu jarul dee, na ko ñaanal, te Yàlla dina
ko may dund. Ku def bàkkaar bu jarul dee laa wax. Ndaxte am na bàkkaar
bu jar dee; boobu taxul may wax, mu ñaanal ko.
18 Xam nanu ne, képp ku juddu ci Yàlla doo sax ci bàkkaar, waaye Doomu Yàlla ji mooy wottu sa bakkan, ba Ibliis du la manal dara.
20 Xam
nanu ne, Doomu Yàlla ji ñëw na te may na nu xel, ba nu man a xam Aji
Wóor ji. Te nu ngi ci Aji Wóor ji ak ci Doomam Yeesu Kirist. Kooku mooy
Yàlla ju wóor, ji yor dund gu dul jeex.
2 John 1
1 Man
njiit li maa leen di bind, yaw soxna su tedd si, yaw ak say doom. Bëgg
naa leen bu wér ci sama xol, jéllale naa sama bopp sax, waaye itam képp
ku xam dëgg gi.
3 Yàlla Baay bi ak Yeesu Krist, Doomu Baay bi, dinañu nu may yiw, yërmande ak jàmm, ànd ak dëgg ak mbëggeel.
5 Léegi
nag soxna si, maa ngi lay dénk lii: nun ñépp nanu bëggante, te loolu du
dénkaane bu bees, waaye moom lanu jotoon ca njàlbéen ga.
6 Lii
mooy mbëggeel: nu wéer sunug dund ci ndigali Yàlla; loolu mooy
ndigalam, la nu jotoon ca njàlbeen ga, te ci lanu wara jaar.
7 Maa
ngi wax loolu nag, ndaxte am na ñuy sànke ñu bare, ñu tasaaroo ci
àddina si, te nanguwuñu ne Yeesu Krist wàcc na, nekk nit. Kooku aji
sànke la, di Bañaaleb Krist.
9 Képp ku saxul ci dénkaaney Krist, xanaa di ko weesu, bokkul ci Yàlla; ku sax ci dénkaane yi, bokk nga ak Baay bi ak Doom ji.
10 Ku ñëw fi yaw, te indaalewul dénkaane yooyu, waxuma nga bañ koo teeru rekk, waaye bu ko nuyu sax.
12 Bëggoon
naa leena wax lu bare ci bataaxel bii, waaye lépp xajul ci kayit. Kon
nag fas naa yéenee ñëw, ba jàkkaarlook yeen, nu waxtaan ci, ngir sunu
mbég mat sëkk.
3 John 1
2 Sama soppe, maa ngi ñaan, Yàlla may la jàmm ci lépp, ànd ak wér gi yaram, ju mel ni sa naataangeg xol.
6 Seedeel nañu sa mbëggeel fi kanam mbooloom ñi gëm. Taxawu leen nag ci seen yoon taxawu gu neex Yàlla.
10 Kon
nag su ma ñëwee, dinaa fàttali li mu def lépp, ci di nu sosal ci kàdduy
neen yu ñaaw. Yemu foofu sax, waaye nanguwula teeru mbokk yi,
rax-ca-dolli ku leen bëgga teeru, mu gàllankoor ko, dàq ko ci mbooloo
mi.
11 Sama xarit, bul roy lu bon, waaye lu baax rekk. Kuy def lu baax, ci Yàlla nga bokk; kuy def lu bon, xamoo dara ci Yàlla.
12 Naka
Démétrius nag, ñépp seedeel nañu ko lu baax, te dëgg gi sax seedeel na
ko ko. Nun itam seedeel nanu ko te wóor na ma ne, sunu seede dëgg la.
http://www.jesus-army.com/cgi-bin/bible/bible.cgi?BIBLE=Wolof+NT&BOOK=62&SEARCH=++&CASE=ON&HILITE=ON&FIRST=OK&R1=I&CHAP=1&SUBMIT=Read
Nenhum comentário:
Postar um comentário